{"id":1533,"date":"2012-07-20T12:36:43","date_gmt":"2012-07-20T12:36:43","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1533"},"modified":"2012-07-20T12:38:22","modified_gmt":"2012-07-20T12:38:22","slug":"jiggeen-yu-men-goor","status":"publish","type":"post","link":"https:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1533","title":{"rendered":"jigg\u00e9en yu m\u00ebn g\u00f3or&#8230;"},"content":{"rendered":"<div>\n<div>\n<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/07\/femmesafrique.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"aligncenter size-full wp-image-1539\" title=\"femmesafrique\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/07\/femmesafrique.jpg\" alt=\"\" width=\"600\" height=\"400\" srcset=\"https:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/07\/femmesafrique.jpg 600w, https:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/07\/femmesafrique-300x200.jpg 300w\" sizes=\"(max-width: 600px) 100vw, 600px\" \/><\/a><\/p>\n<p>Ci at yi ak w\u00e9er yi weesu, mel na ni Afrik dafa dellu fa baaxi maam nekkoon, te mooy wormaal, naw, solool jigg\u00e9en. Bu \u00f1u ko fatte fii ci Afrik, jigg\u00e9en na fi ma masa fallu, di yaay, di lingeer, di ndey-ji-r\u00e9ew, di buur, ca Misira d\u00e9mb, Nibi, Meroe, ba ci Waalo ak Kajoor. Kon su \u00f1u dellusee di fal jigg\u00e9en ju mel ni Nkosazana Dlamini-Zuma, mu wara jiite kureel gi feetee kow mbootaayu r\u00e9ewu Afrik yi, &#8220;Union Africaine&#8221;. Loolu lu mata f\u00e9sal la. Soxna soosu nag ba\u00f1kat la masa doon, daan xeex nguuru apartheid ca Afrik di Sid, bokkoon ci daanaka goornamaa ya nekk r\u00e9ew moomee la ko dalee 1994 ba l\u00e9eggi. Kon m\u00ebnees naa yaakaar ne di na delloo &#8220;Union Africaine&#8221; g\u00ebdd gi mu yellool.<\/p>\n<p>Am na itam jeneen jigg\u00e9en ju \u00f1u r\u00e0\u00f1\u00f1ee bu y\u00e1ggul dara g\u00e0nnaaw ba \u00f1u ko falee mu bokk ci \u00e0ttekat yiy wara \u00e0tte ca CPI maanaam \u00e0ttekaay bi mbootaayu xeet y\u00e9pp daanaka bokk, di fa \u00e0tte saay-saay yi def lu bon, di x\u00ebpp ay ci seeni r\u00e9ew, teg fa nguuru parparloo di noot aka boom. Kookooy Fatumata Bensudaa di jigg\u00e9eni r\u00e9ew mi, ndax Gambi la fekk baax.<\/p>\n<p>Fatumata Bensuudaa moomu doonoon na jawri\u00f1 ja yore mbiru yoon ak yemale ca r\u00e9ewam jogge fa bokk ci tiribinaal ba doon saytu mboomum xeet wa amoon Ruwaanda.<\/p>\n<p>M\u00ebn na\u00f1u fee tudd ba l\u00e9egi it soxna su mel ni Joyce Banda, di njiitu r\u00e9ewum Malawi, di ndaw su t\u00e0kku ngir suxali r\u00e9ewam, xeex g\u00e9r ak y\u00e0q. Naka noonu itam Elen Sirlaf Jonson, njiitu r\u00e9ewum Liberia ma say-say bu mel ni Sarl Tayloor demoon ba toj ko.<\/p>\n<p>Kon jaaraama jigg\u00e9eni Afrik yooyu dekkkal cosaani maam!<\/p>\n<p>Tamsir Anne: tamsir.anne@wolof-online.com<\/p>\n<\/div>\n<\/div>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Ci at yi ak w\u00e9er yi weesu, mel na ni Afrik dafa dellu fa baaxi maam nekkoon, te mooy wormaal, naw, solool jigg\u00e9en. Bu \u00f1u ko fatte fii ci Afrik, jigg\u00e9en na fi ma masa fallu, di yaay, di lingeer, di ndey-ji-r\u00e9ew, di buur, ca Misira d\u00e9mb, Nibi, Meroe, ba ci Waalo ak Kajoor. Kon&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[12,1],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1533"}],"collection":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=1533"}],"version-history":[{"count":9,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1533\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1543,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1533\/revisions\/1543"}],"wp:attachment":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=1533"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=1533"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=1533"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}