{"id":1130,"date":"2012-06-30T11:15:01","date_gmt":"2012-06-30T11:15:01","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1130"},"modified":"2012-07-01T10:43:17","modified_gmt":"2012-07-01T10:43:17","slug":"leeboon-doomi-yalla","status":"publish","type":"post","link":"https:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1130","title":{"rendered":"L\u00e9eboon: Doomi Y\u00e0lla"},"content":{"rendered":"<p>L\u00e9eboon!<\/p>\n<p>Lipp\u00f3on!<\/p>\n<p>Amoon na fi!<\/p>\n<p>Daan na am!<\/p>\n<p>Ba mu amee yaa fekkee?<\/p>\n<p>Ya wax ma d\u00e9gg!<\/p>\n<p>waxi tey jar ta g\u00ebm!<\/p>\n<p>Sa yos moo ci raw!<\/p>\n<p>Xew xew bii ma nga ameewoon ca jamono ya rab yi daan wax ag nit \u00f1i. Amoon fi jenn jig\u00e9en ju bon ju nekkoon ag \u00f1eenti doomam. \u00d1oo nga dekkoon ca biir \u00e0ll ba. Baayu xale yi, bi caat mi \u00f1uy wax T\u00f3ni juddoo la dee; yaay ji j\u00e0pp ne kon xale bi dafa aay gaaf. Mu daldi ko ba\u00f1. Bu mosee r\u00ebbbi ba \u00f1\u00ebw, day woo xale yi, benn benn, \u00f1u n\u00e0mp ba mu des T\u00f3ni. Muy woy naan: Jamloro kaay n\u00e0mp, Jamloro Siise kaay n\u00e0mp, Biraama Siise kaay n\u00e0mp, Ndaama Siise kaay n\u00e0mp, Na T\u00f3ni xaar Y\u00e0lla yaayam. Di ko def ay yooni yoon. Waaye, jig\u00e9en ju bon ji mosul xam ne Y\u00e0lla daan na fee\u00f1u T\u00f3ni ci melokaanu daar bu bare meew; bu \u00f1owee di n\u00e0mpal T\u00f3ni. Am b\u00e9s, musiba dal jig\u00e9en ji. Mu j\u00f3ge ca \u00e0ll ba di woy; woy wa mu daan woowee xale yi ngir n\u00e0mpal leen; yemmoog Bukki di jaar,d\u00e9glu woy wi, j\u00e0ng ko ba m\u00ebn ko bu baax. Benn b\u00e9s, yaayu xale yi dem r\u00ebbbi. Bukki doxe ko gannaaw roy baataam, di woy woy wi. Xale yi di g\u00e9nn benn benn, bukki di leen lekk ba mu des T\u00f3ni. Ba yaay ja j\u00f3gee \u00e0ll ba, muy woy, kenn wuyuwu ko, mu jaaxle lool. Y\u00e0ggul dara, mu d\u00e9gg baat bu mu miin, di woy naan ko: Jamloro, Bukki j\u00ebl na ko, Biraama Siise, Bukki j\u00ebl na ko, Ndaama Siise, Bukki j\u00ebl na ko; T\u00f3ni rekk a des ci yaayam Y\u00e0lla! Ba mu d\u00e9ggee k\u00e0ddu yooyu, jig\u00e9en ji dafa yuuxu, yuuxu gu tar,r\u00e9er ci \u00e0ll bi. Foofa la l\u00e9eb doxee t\u00e0bbi g\u00e9ej, b\u00e0kkan bu ko nj\u00ebkka f\u00f3on t\u00e0bbi \u00e0jjana.<\/p>\n<p>Kesteloot &#8211; Mbodj:Contes et mythes wolof. Dakar NEA (1983), pp. 45<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>L\u00e9eboon! Lipp\u00f3on! Amoon na fi! Daan na am! Ba mu amee yaa fekkee? Ya wax ma d\u00e9gg! waxi tey jar ta g\u00ebm! Sa yos moo ci raw! Xew xew bii ma nga ameewoon ca jamono ya rab yi daan wax ag nit \u00f1i. Amoon fi jenn jig\u00e9en ju bon ju nekkoon ag \u00f1eenti doomam. \u00d1oo&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[24],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1130"}],"collection":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=1130"}],"version-history":[{"count":5,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1130\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1290,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1130\/revisions\/1290"}],"wp:attachment":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=1130"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=1130"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=1130"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}