{"id":1000,"date":"2017-11-21T07:19:37","date_gmt":"2017-11-21T07:19:37","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1000"},"modified":"2017-12-08T11:46:58","modified_gmt":"2017-12-08T11:46:58","slug":"diine-ci-lamminu-wolof-yoonu-ragal-yalla","status":"publish","type":"post","link":"https:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1000","title":{"rendered":"Diine ci l\u00e0mmi\u00f1u Wolof: Yoonu ragal-Y\u00e0lla"},"content":{"rendered":"<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/timbuktu1.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"alignleft  wp-image-1001\" title=\"timbuktu1\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/timbuktu1.jpg\" alt=\"\" width=\"462\" height=\"600\" srcset=\"https:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/timbuktu1.jpg 462w, https:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/timbuktu1-231x300.jpg 231w\" sizes=\"(max-width: 462px) 100vw, 462px\" \/><\/a>Bisimilaahi Rahmaani Rahiimi&#8230;<br \/>\n\u00d1u fas yeeney dollee de\u03b7k\u00ebnte ak di dollee f\u00e0tleente.<br \/>\n\u00d1i\u03b7 koy j\u00ebm\u00eble nak ci tomb bi nga xam ne mbooleem liy yiiwu \u00e0dduna ak yiiwu \u00e0llaaxira ci la ko sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa d\u00ebx\u00eb\u00f1. Mbooleem yonant yi mu y\u00f3nni y\u00e9pp ci la leen dig\u00ebl \u00f1u teg ci seen t\u00e0nk. Mbooleem \u00f1i leen topp \u00f1\u00e9pp yit ci la leen dig\u00ebl \u00f1u teg ci seen t\u00e0nk. Mooy tomb bi nga xam ne ci la mucc nekk ci \u00e0dduna ak ci \u00e0llaaxira, ci la texe nekk ci \u00e0dduna ak ci \u00e0llaaxira, ci la l\u00e0q ng\u00ebr\u00ebm\u00ebl sunu Boroom nekk ci \u00e0dduna ak ci \u00e0llaaxira.<br \/>\nMooy tomb bi nga xameenteni jaam bu ci t\u00eb\u03b7ku sunu BOROOM dana ko mus\u00ebl ci fitnaay \u00e0dduna ak ci \u00e0llaaxira, mus\u00ebl ko ci nj\u00e0qaray \u00e0dduna ak ci \u00e0llaaxira.<br \/>\nMooy tomb bi sunu BOROOM de\u03b7k\u00f3on \u00f1u nj\u00ebkk \u00f1a ak \u00f1u mujj \u00f1a \u00f1u t\u00eb\u03b7ku ca.<br \/>\nMooy tomb bi nga xam ne ku weex g\u00ebnul ku \u00f1uul, ku \u00f1uul g\u00ebnul ku weex lu dul ci boobii tomb.<br \/>\nTomb boobii mooy lan : \u201cAt-taqwaa\u201d, maanaam ragal-Y\u00e0lla.<br \/>\n<strong><br \/>\nRagal sunu BOROOM moodi jaam bi fexe bab xolam b\u00e9pp pas-pas bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut mu ba\u00f1 caa nekk, fexe yit ba aw l\u00e0mmi\u00f1am b\u00e9pp k\u00e0ddu bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut mu ba\u00f1 ko caa wax, g\u00f3org\u00f3orlu bu baax ba ci ay c\u00ebr\u00ebm b\u00e9pp j\u00ebf bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut mu ba\u00f1 ko caa j\u00ebf.<\/strong><br \/>\nLan mooy pas-pas bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebm ?<br \/>\nMoodi : jaam bi w\u00e9etal Boroomam ci fas ci xolam, ta muy d\u00ebgg ci moom, ne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa Buur bu am la, am gu t\u00e0ambaleewul fenn ta yemuwul fenn, ta soqikuwul ci lenn it, ta nur\u00f3owut ag kenn walla lenn ci j\u00ebmm\u00ebm, ci j\u00ebf\u00ebm ak ci melokaanam, ta l\u00e9pp lu am moo ko amal ci coobareem Subhaanahu wa Tahaalaa.<br \/>\nBu fasee loolu ci xolam ci digganteem ak Boroomam, am na yit lu ko war ci diggam ak ay moroomam. Ba ca nj\u00ebkk mooy mu watandiku r\u00eby, ak ka\u00f1aan ak naw j\u00ebf ak j\u00ebf b\u00ebgg \u00f1u di ko tudd ak ngistal :<\/p>\n<p>R\u00eby moomii, jaam bi bu xoolee la ko sos ak fa muy mujj r\u00eby xaju fi. Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa waxoon na S\u00ebydinaa Muusaa bul j\u00e0pp ni yaa g\u00ebn kenn feek seen\u00f3o sa bopp ci biir aljana seen kookee ci biir safara. R\u00eby it mooy la alagoon ibliis.<br \/>\nKa\u00f1aan itam, jaam bi war na di ko moytandiku ndax day lekk j\u00ebf ni sawara di lekkee matt, ta mbug\u00eblum aji a\u00f1aan ci \u00e0dduna lay t\u00e0mbalee ndax limu b\u00ebgg muy d\u00eb\u00f1ug x\u00e9ew\u00ebl cib jaam sunu BOROOM du ko def mukk ci ludul coobareem, ndax sunu BOROOM mooy ki ko ko defal. Waxtu wu gisee sunu BOROOM dollikoy x\u00e9ew\u00ebl day daaldi dollikook tiit ak nj\u00e0qare ta duca m\u00ebn dara. Kon li war jaam bi rekk, moodi l\u00e9pp lub jaam am mu yeene ko ko ba mu melni moom moo ko am, loolii mooy liy noppal nit ki ci a\u00f1aan.Naw j\u00ebf itam ak j\u00ebf b\u00ebgg \u00f1u di ko tudd, jaam bi su gisee ni bindul boppam, dees koo amal rekk, xiir ko ci li muy j\u00ebf, kon na sant kako amal ta xiir ko ca lamuy j\u00ebf, ta sant ko ca.<br \/>\nNgistal itam jaam bi, waxtu wu tawxiitam mate, sunu BOROOM man nako caa mus\u00ebl. Ndax su boobaa yit day gis ni moom j\u00ebful waaye day jottali j\u00ebf ja rekk.<br \/>\nKon loolu mooy li war jaam bi ci dig\u00ebnt\u00e9em ak Boroomam, ak ci dig\u00ebnt\u00e9em ak ay moroomam.<br \/>\nJaam bi yit di g\u00f3org\u00f3orlu bu baax, ba aw l\u00e0mmi\u00f1am du ci y\u00ebkk\u00ebti benn k\u00e0ddu bu Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul.<br \/>\nMu cay wattandikoo j\u00ebw ak rambaaj ak wax lu amut :<br \/>\nJ\u00ebw mooy wax ci sa moroomum jaam loo xam ne su ko degg\u00f3on du ko g\u00ebn\u00ebl. Ta li ci sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa wax ci t\u00e9er\u00e9em bi war naa tax jaam bune war koo moyandiku : muy nimu ko nur\u00f3ol\u00e9e ak lekk meddum nit. Kon b\u00e9pp jaam boo xam ne b\u00ebggoo sa moroomum jaam faatu \u00f1u suul ko ba mu am \u00f1atti (3) fan ngay dagg ay c\u00ebr\u00ebm di sex, war ngay wattandiku kon di t\u00f3og fenn di tudd sa moroomum jaam, ci loo xameenteni su ko d\u00e9ggoon du ko g\u00ebn\u00ebl.<br \/>\nJaam bi war nay wattandiku rambaaj. Muy di dox di wax luy y\u00e0q dig\u00ebnte ay jaam walla di y\u00e0qal ab jaam ci moroomum jaam, loo xam ne manoon na caa am aw yiiw. Jikko la joo xam ne j\u00ebmm juko ame du dugg aljana mukk mukk.<br \/>\nJaam bi war nay wattandiku wax lu amut, ndax loolii ci jikkoy n\u00e0feq la bokk ta n\u00e0feq ci xur wa g\u00ebn\u00eb suufe ca sawara mooy d\u00ebkkuwaayam.<\/p>\n<p>Kon jaam bi ni mu wara sa\u03b7ee ab xolam, noonii la wara sa\u03b7ee aw l\u00e0mmi\u00f1am, \u00f1\u00ebwit ci c\u00ebr yi ci des. Muy fexe ba ay g\u00ebt\u00ebm du ci xool lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul, ay noppam noonu mu ba\u00f1 cee deglu lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul, ay loxoom it mu ba\u00f1 cee j\u00ebf lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul, biiram it mu ba\u00f1 caa def lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul, p\u00eby\u00ebm it noonu mu ba\u00f1 koo dug\u00ebl fu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul.<br \/>\nNga xam ne mooy sa\u03b7ee xol bi ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul, sa\u03b7ee l\u00e0mmi\u00f1 wi ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul, sa\u03b7ee ay c\u00ebr\u00ebm ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmul.<br \/>\n<strong>Fexe ba sab xol doo ci \u00ebmb\u00ebl kenn lu \u00f1aaw, saw l\u00e0mmi\u00f1 doo ci wax kenn lu \u00f1aaw, say c\u00ebr doo ci j\u00ebflante ak kenn lu \u00f1aaw. Li nga b\u00ebgg\u00ebl sa bopp nga b\u00ebg\u00ebl ko mbid\u00e9ef y\u00e9pp. Di wax ci \u00f1\u00e9pp lu rafet, di j\u00ebflante ak \u00f1\u00e9pp lu rafet. Loolu mooy melokaan wi nga xam ne moom la sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa so\u00f1\u00f1 \u00f1\u00e9pp ci \u00f1u melowoo ko. Mooy melokaan wi nga xamente ni nit ki lu mu bari bari xamxam ta melowoowu ko, mook ki xamut dara \u00f1oo yem. Mooy melokaan wi Yonent bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam) wax ni : \u00f1i ko ame \u00f1oo g\u00ebn\u00eb yey ci moom, \u00f1u\u00f1 mana doon ak fu\u00f1u mana nekk. Loolu mooy : \u201cAt-taqwaa\u201d.<\/strong><br \/>\nLooloo tax it sunu BOROOM \u00f1aax jaam \u00f1\u00e9pp \u00f1u mel woowii melokaan ngir \u00f1u m\u00ebn\u00eb mucc ci safara mi nga xam ne ay nit \u00f1oo koy xamb ak ay doj, ta sunu BOROOM d\u00eb\u00eble ko way weddi yi.<br \/>\nMooy melokann wi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa wax ni jaam bu nekk war na koo melowoo, ngir b\u00e0yyi xel bis ba nga xam ne benn bakkan du manal moroom ma dara, ta k\u00e9pp ku melowoowutoon woowii melo deesuti nangu ci moom am rammu, deesuti j\u00e0pp ci moom ag maandu, deesuti ko dimb\u00ebli yit.<br \/>\nBa tay sunu BOROOM wax ne Al-quraan nekk na waare \u00f1eel way ragal Y\u00e0lla yi.<br \/>\nMu dellu wax ne, moom sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa : \u201cLaysal birru&#8230;\u201d.<br \/>\nDu caageeni ag topp mooy ngeen di j\u00ebm\u00eble seeni xar-kanam ci pe\u03b7ku wala sowwu.<br \/>\nWaaye ag topp mooy nga g\u00ebm sunu BOROOM, w\u00e9\u00e9t\u00ebl ko ci j\u00ebmm\u00ebm ak ci j\u00ebf\u00ebm ak ci melokaanam, ta l\u00e9pp lu mu dogal ci yaw nga g\u00ebr\u00ebm ko, g\u00ebm bis bi mujju ba nga xam ne l\u00e9pp lum bind muy nit ak jinne ak malaaka, kune mu laaj la lam la santoon na nga ca def, ak g\u00ebm amug malaaka yi nga xam ne ay j\u00ebmm la\u00f1 yu sunu BOROOM bind cig leeram, g\u00ebm teere yi, ne ci sunu BOROOM la\u00f1 b\u00e0yyikoo, j\u00ebm ci jaamam yimu t\u00e0nn, g\u00ebm yonant yi ne ndawi sunu ImageBOROOM la\u00f1u subhaanahu wa tahaalaa yu mu t\u00e0nn.<br \/>\nNgay joxe sa alal \u00e0nd ak b\u00ebgg nga ko, waaye nga diko joxe ngir j\u00ebmmi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa. Nga diko jox say jege\u00f1aale, nit \u00f1a la jege cig mbokk, ak jirim \u00f1i, ak miskiin \u00f1i, ak doomi yoon.<br \/>\nJirim mooy ku ay waajuram gaa\u00f1u ta amagul kattanug f\u00e0ggu.<\/p>\n<p>Miskiin mooy koo xam ne amul lu ko doy ci dund ak koddaay ak d\u00ebkkuwaay.<br \/>\nDoomi-yoon mooy ab tukkikat boo xam ne day tukki tukki bu dagan ta lamu amewoon jeex, nga dimbiliko ci lu ko yeggele famu j\u00ebm ak lu ko delloosi famu jogewoon, ngir j\u00ebmmi Y\u00e0lla. Tukkib l\u00ebgg\u00e9ey ngir f\u00e0ggu loo t\u00eby\u00e9e sag ragal Y\u00e0lla, tukkib jaamu Y\u00e0lla la.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ta xam, xam bu w\u00f3or ni yeen \u00f1\u00e9pp dana \u00f1u leen pang \u00ebll\u00ebg ngeen j\u00ebm ci moom.<br \/>\nGaa \u00f1i nga xam ne \u00f1u sax cig ragal Y\u00e0lla la\u00f1u, \u00f1ooy waay-ga\u00f1e \u00f1i ci yiiw ak tawfeex aki x\u00e9ew\u00ebl \u00ebll\u00ebg yawmal-xiyaam<br \/>\nSunu BOROOM dana w\u00ebrs\u00ebg\u00ebl ku ko soob ci ludul benn coono.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ta ngeen xam ne kenn ku nekk ci yeen dana dajeeg Moom ba j\u00e0pp ne moom rekk la sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa bindoon..<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ta yewen\u00ebl seen dig\u00ebnteeg nit \u00f1i.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ta ngeen xam ne sunu BOROOM ku da\u00f1 kumpa la, ku xam b\u00e9pp mbir la, ci lu n\u00ebbbu ak ci lu fee\u00f1, ci jamono june, ci waxtu wune ak ci saa sune..<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ta ngeen xam ne sunu BOROOM Aji-gis la ci gis gu sax, ci li ngeen di j\u00ebf l\u00e9pp, ci jamono june, ci waxtu wune ak ci saa sune.<br \/>\nYeen waay-g\u00ebm \u00f1i na ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla, ta ngeen di won g\u00e0nnaaw l\u00e9pp lu daganul ci njaay, ndeem way-g\u00ebm ngeen. K\u00e9pp ku tuub, dugg ci lislaam, l\u00e9pp loo amewoon ci lu daganul na nga t\u00e0qalikoo ak moom, rawatina yaw miy aji-g\u00ebm.<br \/>\nMu dellu wax ni na ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ta b\u00e0yyi xel b\u00e9s bi nga xam ne dana\u00f1u laxas, t\u00ebdd ci lalum ndee, j\u00ebm ci sunu BOROOM, ta sunu BOROOM dina\u00f1u fay sunuy pas-pas, sunuy k\u00e0ddu ak sunuy j\u00ebf.<br \/>\nJ\u00ebmm ju ne nay ragal Boroomam bi ko bind ta moom ko ta melal ko.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla, sunu BOROOM xamal leen li ko soob ci xamxamam bi t\u00e0mbaleewul fenn ta yemuwul fenn, ta sunu BOROOM mooy Aji-xam b\u00e9pp mbir xam gu sax.<br \/>\nLoolu mooy waral &#8220;ah-lu tasawuuf&#8221; di jihaad ak seen bakan ngir jikko yi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut de\u00f1 ci seen biir, ndax jikko yooyu \u00f1ooy kiiraay bi dox digg\u00ebnte jaam bi ak xamxamu ladunii (mooy xamxam bi b\u00e0yyeekoo ci sunu BOROOM ta du jaar ci jenn j\u00ebmm).<br \/>\nJikko yooyu maanaawoo ni r\u00eby, ngistal, rambaac, j\u00ebw, di j\u00ebf b\u00ebgg \u00f1u di ko tudd, ak yu maanaawoo ni \u00f1oom.<br \/>\nJaam bi nag bu sellalee ab xolam, sellal aw l\u00e0mmi\u00f1am, sellal ay c\u00ebr\u00ebm, sellal gu sax, sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa dana ko ca xamal la ko soob.<br \/>\n. . . . . . .<br \/>\n\u00d1eel na gaa yi sax cig ragal Y\u00e0lla, fa seen Boroom, itasi wurus ak yuy jamaa ak yuy oor yu taaru taaru gu j\u00e9ggi dayo. Di daw ca suufu itaas yooyee ay dex, \u00f1uy way sax ca biir k\u00ebr yooyee, \u00f1eel leen fa ay soxna yu taaru taaru gu jeggi dayo, muy ay soxna yunu laabalit, ay soxna yudul gis baax mukk. Dex yooyee maanaam dexu s\u00e0ngara la ak dexi lem ak dexi meew ak dexi ndox. \u00d1uy aji way l\u00e0q ng\u00ebr\u00ebm\u00ebl sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, l\u00e0q gu sax. Sunu BOROOM aji gis la, gis gu sax, ci j\u00ebfi jaamam y\u00e9pp.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ta topp ci g\u00e0nnaaw Yonant bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam), fu mu teggee t\u00e0nkam ngeen teg fa seen t\u00e0nk, ta b\u00ebgg ko b\u00ebgg gu w\u00e9r, mu g\u00ebn\u00ebl leen seen bopp, seen alal ak seen njaboot.<br \/>\nNaka sama BOROOM mooy ki ma bind, mooy ki leen bind, ta melal leen, ta moom leen, na ngeen sax ci di ko jaamu : lii mooy aw yoon wiy aji-jub.<br \/>\nLi fi nekk, b\u00e9pp j\u00ebmm buy matale wollareem ak Boroomam ak moroomam boole ci sax cig ragal Y\u00e0lla, na xam ne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ku b\u00ebgg aji-waay-ragal-Y\u00e0lla yi la.<br \/>\nDafa bokk ci aaya boobii li tax mu w\u00e0cc, waa ah-lul kitaab \u00f1i nga xam ne seenub yonant daf leena xibaaroon dikkub Yonant bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam) k\u00e9pp kuko ca g\u00ebm ta topp ko, sunu BOROOM ku b\u00ebgg aji-waay-ragal-Y\u00e0lla yi la.<br \/>\nYeen waay-g\u00ebm \u00f1i &#8230;..<br \/>\nLan mooy g\u00ebm Y\u00e0lla?<\/p>\n<p>G\u00ebm Y\u00e0lla moodi w\u00e9et\u00ebl sunu BOROOM ci j\u00ebmm\u00ebm, ci j\u00ebf\u00ebm ak ci melokaanam, xam ne ku ci w\u00e9et la, g\u00ebm malaaka yi, g\u00ebm yonant yi ak t\u00e9ere yi\u00f1u andi, g\u00ebm dogal moo xam aw yiiw la wala safaan ba, g\u00ebm bis p\u00e9\u00f1c ba, g\u00ebm aljana ak safara ak siraat. Jaam bi su g\u00ebmee d\u00ebgg d\u00ebgg ng\u00ebm mooy tax sunu BOROOM b\u00ebgg ko. Ta mb\u00ebggum sunu BOROOM mooy tawf\u00e9ex si jaam bi.<br \/>\nYeen waay-g\u00ebm \u00f1i loolii, na ngeen ragal Y\u00e0lla, d\u00ebgg-d\u00ebgg ragal ko, ndax mooy tax ngeen mucc.<br \/>\nD\u00ebgg-d\u00ebgg ragal Y\u00e0lla mooy nga jihaad ak sa bakan ba \u00e0gg ci sa xol d\u00f3ot\u00f3o ci mana xalaat ludul m\u00e0ggug sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ak lu mu g\u00ebr\u00ebm, say k\u00e0ddu d\u00f3ot\u00f3o ci mana y\u00ebkk\u00ebti benn k\u00e0ddu budul bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebm, say c\u00ebr d\u00f3ot\u00f3o ci mana j\u00ebf jenn j\u00ebf judul ju sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebm.<br \/>\nKon nag Y\u00e0lla bu dee dikk mukk, ndare mu nekk ngeen di waay-j\u00e9bb\u00ebl seen l\u00e9pp seen BOROOM subhaanahu wa tahaalaa.<br \/>\nKon :<br \/>\nSu ngeen mu\u00f1ee ta sax cig ragal Yalla, pexeem seeni noon du leen lor mukk, ndax su\u00f1u BOROOM ku peek la, li seeni noon di j\u00ebf ngir mu ba\u00f1a j\u00ebmsi ci yeen, ta sunu BOROOM du ko antul mukk.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla, ngeen di waay-sant sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa. Ndax ragal Y\u00e0lla mooy tax nit ki ak ng\u00ebm\u00ebm m\u00ebn\u00eb yokku, ng\u00ebm\u00ebm su yokkoo mooy tax muy g\u00ebn\u00eb w\u00e0kkiirlu ci Boroomam, su w\u00e0kkiirloo ci Boroomam, sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa yoral ko l\u00e9pp\u00ebm. Su boobaa ag cant rekk moo cay top.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ndax ngeen di waay-texe, texe gu m\u00e0gg ta sax.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Y\u00e0lla ngir ngeen mana mucc ci safara mi sunu BOROOM d\u00eb\u00ebl waay-weddi yi.<br \/>\nNa ngeen topp Yalla ak Yonantam ngir sunu BOROOM y\u00ebr\u00ebm leen.<br \/>\nNa ngeen gaaw j\u00ebm ci nj\u00e9gg\u00ebl gu b\u00e0yyikoo ci sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ak aljana joo xam ni yaatuwaayam yaatoo na ni assamaan yi ak suuf yi, ta sunu BOROOM d\u00eb\u00ebl ko waay-ragal Yalla yi.<br \/>\nWaay-ragal Yalla yi, \u00f1ooy gaa \u00f1i nga xam ne da\u00f1iy joxe seen alal ci yoonu Yalla, ci jamono ba \u00f1u barilee ak n\u00e9ewlee, ci jamono ba\u00f1u nekkee ci xat-xat ak yolom-yolom, ci jamono ba\u00f1u nekkee ci bekk\u00f3or ak naataange. Ak gaa \u00f1a nga xamente ni dana\u00f1u n\u00ebbb seen mer, di j\u00e9gg\u00ebl nit \u00f1i, seetu \u00f1u ci ab jullit ak kudul jullit. Sunu BOROOM ku b\u00ebgg aji-waay rafetal seeni pas-pas la, rafetal seeni k\u00e0ddu, rafetal seeni j\u00ebf.<br \/>\nAlXuraanul-Kariim ag leeral gu bir la akug teqale la \u00f1eel d\u00ebgg ak neen, \u00f1eel nit \u00f1i, doon it ag njub \u00f1eel aji-waay-s\u00f3obu \u00f1a, doon it aji-waare \u00f1eel waay ragal Yalla yi.<br \/>\n\u201cMbaax nag mooy jaam boo xam ne melowoo na melokaan yi sunu BOROOM g\u00ebr\u00ebm y\u00e9pp ci dig\u00ebnt\u00e9em ak Boroomam, ak ci dig\u00ebnt\u00e9em ak ay wayjuram, ak ci dig\u00ebnt\u00e9em ak ay d\u00ebk\u00ebnd\u00f3om, ak ci dig\u00ebnt\u00e9em ak mbool\u00e9em jaam \u00f1\u00e9pp\u201d.<br \/>\nYeen nit \u00f1\u00e9pp na ngeen ragal seen BOROOM, maanaam na ngeen feg ci seen xol l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut, feg ci seen l\u00e0mmi\u00f1 l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut, feg ci seeni c\u00ebr l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut, \u00f1eel seen BOROOM bi leen bind ci benn bakkan muy Aadama. Mu bind ci bakkan boobii soxnaam muy Awa. Mu j\u00eble ci \u00f1oom \u00f1aar ay g\u00f3or ak ay jig\u00e9en yu baree bari.<br \/>\nSunu BOROOM nekk na kuy janoog \u00f1\u00e9pp ak l\u00e9pp ak f\u00e9pp, ci jamono june ak waxtu wune ak saa sune, ta di leen fuglu.<br \/>\nNa \u00f1uy ragal sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ci li waay-faatu yi b\u00e0yyi gannaaw, tay wax wax ju jub ta noppi.<br \/>\nSu ngeen yew\u00ebn\u00eblee ci li ngeen weesu ci l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut ci pas-pas ak ci k\u00e0ddu ak ci j\u00ebf ta ba\u00f1ati caa dellu, sunu BOROOM nekk na j\u00e9gglaakoon ci k\u00e9pp ku yew\u00ebn\u00ebl ci limu weesu, ta fas yeene ba\u00f1ati caa dellu.<br \/>\nDenkk naa gaa \u00f1a nga xam ne ab t\u00e9ere dikkaloon na leen, ta b\u00e0yyikoo ci samay ndaw, nj\u00ebkk yeen, ak yeen tamit lima leen denkk, benn denkaane bi rekk la : mooy sax cig ragal Yalla.<br \/>\nNa ngeen di dimbalante ci seeni xam-xam, ak ci seeni alal, ak ci seeni k\u00e0ddu, ak ci seeni j\u00ebf, ak cig ragal Yalla. Ta ngeen di ba\u00f1a dimbalante ci j\u00ebfu \u00f1aawt\u00e9ef, ak pas-pasu \u00f1aawt\u00e9ef, ak k\u00e0dduy \u00f1aawt\u00e9ef, tay ba\u00f1a dimbalante cig noonoo ci digg\u00ebnte yi. Ta ngeen sax cig ragal Yalla ta xam ne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ku tar mbug\u00ebl la ci waay-too\u00f1 yi.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Yalla. Sunu BOROOM kat Aji-xam la, xam gu sax, ci l\u00e9pp lu nit \u00ebmb ci d\u00ebnn\u00ebm ta di ko n\u00ebbb, ci suba yi ak ci ngoon yi, ci waxtu wune, ci jamono june ak ci saa sune.<\/p>\n<p>Na ngeen sax cig ragal Yalla, sunu BOROOM mooy w\u00e9eruwaayu waay-g\u00ebm \u00f1i.<br \/>\nSunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, waay-sax cig ragal Yalla yi rekk lay nangul seeni pas-pas ak seeni k\u00e0ddu ak seeni j\u00ebf.<br \/>\nYeen waay-g\u00ebm \u00f1i na ngeen sax cig ragal Yalla, ta s\u00e0kku wasiila wu ngeen doxale s\u00e9en digg\u00ebnte ag moom.<br \/>\nWasiila moomii day laaj ag leeral : man naa nekk j\u00ebmm ju bokk ci j\u00ebmm yi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa t\u00e0nn, def ci moom leeram ak y\u00ebrmandeem ak njegg\u00ebl\u00ebm ak tawf\u00e9ex\u00ebm ak bark\u00e9em : mooy yonant yi ak kummalul awliyaa-u yi.<br \/>\nSunu BOROOM bula defalee t\u00e0wf\u00e9ex, nga dajeeg \u00f1oom, nga jox sa bopp sa BOROOM ta jaarale ko ci \u00f1oom, mooy li sunu BOROOM waxoon yonant bi.<br \/>\nSoo dajewut ag j\u00ebmm yu melni j\u00ebmm yooyii, nga topp ci seeni jeexit : t\u00eb\u03b7ku ca AlXuraan ak sunna, ba\u00f1a \u00ebpp\u00ebl ba\u00f1a s\u00e0ggan niko mawlaanaa Cheikh Ahmadou Bamba waxe ci t\u00e9er\u00e9em bi\u00f1uy wax \u00ab masaalikul jinaan \u00bb. Kon wasiila man naa nekk j\u00ebmm, man naa nekk j\u00ebf.<br \/>\nTa ngeen di jihaat ci yoonam wi ci seeni bakkan ak ci seeni j\u00ebf bu ko laajee, ndax ngeen texe.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Yalla ndeem nekk ngeen di waay-g\u00ebm.<br \/>\nLoolu li ko waral mooy \u00f1i nga xam ni du\u00f1u ay jullit ta di \u03b7\u00e0\u00f1\u00f1 diine ji ak di ci j\u00ebf luy y\u00e0q, benn jullit warul leen a j\u00e0ppe ay xarit, waaye koo xam ne du jullit man na\u00f1uy maslaa ak moom.<br \/>\nKon nit ki su g\u00ebmee Yalla, d\u00ebgg d\u00ebggi ng\u00ebm, waruta j\u00e0ppee noonu lislaam yi ay xarit.<br \/>\nAhlul kitaab \u00bb g\u00ebm na\u00f1u Yalla subhaanahu wa tahaalaa, g\u00ebm Yonant Yalla bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam), g\u00ebm AlXuraan bi mu w\u00e0cce ci moom, j\u00ebfe ay ndig\u00ebl\u00ebm, teet ay tereem, kon sunu BOROOM j\u00e9gg\u00ebl leen seen \u00f1aawt\u00e9ef y\u00e9pp, t\u00e0bbal leen ci aljana ja nga xam ne x\u00e9ew\u00ebl la gu mat ta sax.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Yalla mi nga xam ne dees na leen pang \u00ebl\u00ebg j\u00ebm\u00eble leen ci moom.<br \/>\nNa ngeen ragal Yalla ci mbol\u00e9em seeni mbir, ta ngeen deglu ci ay ndig\u00ebl\u00ebm ta topp ko, sunu BOROOM du gindi nit \u00f1ay waay-gennug-topp.<br \/>\nNdax du ngeen xellu!<br \/>\nDundug adduna nekkut lu dul la ca not : am po, ay b\u00e0nneex ak naqar.<br \/>\nKon k\u00ebrug-\u00ebll\u00ebg mooy k\u00ebr gi dul gent mukk, \u00e0nd ak b\u00e0nneex bu dul gent mukk, moo g\u00ebn \u00f1eel \u00f1a nga xam ne \u00f1u ko b\u00e0yyiwoon xel la\u00f1u ci sa\u03b7e seenub xol ci l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut, sa\u03b7e seenub l\u00e0mmi\u00f1 ci l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut, sa\u03b7e seeni c\u00ebr ci l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut, ta saxoon ca.<br \/>\nNa ngeen xupp ta f\u00e0ttali, ci bis bi nekk ci kanam tay \u00f1\u00ebw, gaa \u00f1a nga xam ne dana\u00f1u ragal seen b\u00e0mmeel fett, \u00f1u genn ca, dox j\u00ebm ci bis boobee, \u00e0nd ak nj\u00e0qare ak tiis, di wuyyu wooteeb sunu BOROOM bu \u00f1u sa\u00f1uta ba\u00f1a wuyyu, te amut kenn ci ku \u00f1u mana w\u00e9eru ku dul sunu BOROOM, amut kenn ku leen ca m\u00ebn\u00eb xettali ku dul sunu BOROOM. Ndax \u00f1oom \u00f1u t\u00eb\u03b7ku cig ragal Yalla, ci sa\u03b7e seenub xol ci l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut, sa\u03b7e seenub l\u00e0mmi\u00f1 ci l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut, sa\u03b7e seeni c\u00ebr ci l\u00e9pp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa g\u00ebr\u00ebmut.<br \/>\nNa ngeen di taxawal julliy jur\u00f3om (5) ta \u00e0nd akug teewlu m\u00e0ggug sunu BOROOM bi ak kawewaayam ak sellaayam, ta ngeen ragal ko. Ta mooy t\u00eb\u03b7ku ciy ndig\u00ebl\u00ebm teet ay tereem, ta lumu dogal ci yeen ngeen g\u00ebr\u00ebm loolee. Ta boole ci rafetal seen dig\u00ebnte ak jaam \u00f1i, ta kenn ku nekk ci yeen b\u00e0yyi xel ni \u00ebll\u00ebg dees nako pang, j\u00ebm\u00ebleko ci moom.<br \/>\nKoddaayal ragal Yalla moo g\u00ebn adduna ak li ci biiram, mooy pas-pas bu sell ak k\u00e0ddu yu sell ak j\u00ebf yu sell ; waaye sunu BOROOM moo koy jagleel ku ko soob ci jaamam yi.<br \/>\nGox bu mu mana doon, su fekkoonte ni t\u00eb\u03b7ku na\u00f1u cig ragal Yalla gu mat s\u00ebkk, sax ca la leen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa dig\u00ebl, teet lamu leen tere, ta lu mu dogal ci \u00f1oom \u00f1u g\u00ebr\u00ebm loolee, g\u00e0nnaaw ba \u00f1u ko g\u00ebm\u00e9e, da na leen ubbil ay barke ci assamaan yi ak ci suuf si. Waaye bi \u00f1u yeggee ci \u00f1\u00e0kka rafetal seen dig\u00ebnte ak seen BOROOM ak ci seen digg\u00ebnte ak seen moroom, ci la leen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa tegge la\u00f1u foogutoon ba mukk ci ay musiba aki balaa, ta du leen teggeeku mukk it, feeg delluwu \u00f1u ci ag raggal Yalla.<br \/>\nMuusaa waxoon na ay nitam dimblikoo leen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, ta ngeen mu\u00f1, ta xam ni suuf si sunu BOROOM danako donnloo ku ko soob walla \u00f1u ko soob ci ay jaamam. Muj gu rafet \u00f1eel na waay-ragal Y\u00e0lla yi.<br \/>\nSama y\u00ebrmaande daj na \u00f1\u00e9pp, waaye nag danaa ko jagleel \u00f1eel \u00f1a nga xam ne \u00f1u sax cig ragal Yalla la\u00f1u ak maandu ak rafetal, tay genne asaka ci seen alal su ca waree. \u00d1uy gaa \u00f1uy g\u00ebm la\u00f1u samay kaawt\u00e9ef yu may fee\u00f1al ci samay jaam.<br \/>\n\u00d1i nga xam ne da\u00f1oo sax cig ragal Yalla, waxtu wu seytaane t\u00e0bbalee ci seen xol ittey moy, da\u00f1uy daaldi dell\u00f3osi seen xel, xam ni yool buy sax ba f\u00e0ww moo g\u00ebn mbug\u00ebl bu dul d\u00eb\u00f1 ba mukk.<br \/>\nCi misaal rekk, dafa am waxambaane bu taqoo ak j\u00e0kka. Ab soxna diko woo, b\u00ebgg koo t\u00e0bbal ci biir k\u00ebr\u00ebm, d\u00eb\u00f1ul diko man manee ba diko b\u00ebgg\u00eb dug\u00ebl ci biir n\u00e9eg\u00ebm, mu f\u00e0ttaliku diisug aaya bii daaldi x\u00ebm. Ba mu ximmlik\u00f3o mu diko man maneewaat, mu f\u00e0ttalikuwaat diisug aaya bi, ci la daaldi faatu.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, ta ngeen di yew\u00ebn\u00ebl seeni dig\u00ebnte. Moodi kune lamu b\u00ebgg\u00ebl boppam mu b\u00ebgg\u00ebl ko moroomam, dig\u00ebnte bu \u00f1agas itam ngeen dox ca wax ca k\u00e0dduy yiw ngir digg\u00ebnte ba defaru.<br \/>\nNa ngeen sax cig ragal Yalla ta topp yonantam bi, ta ngeen tek seen t\u00e0nk ci limu leen dig\u00ebl ta teet limu leen tere su ngeen nekkee di way g\u00ebm, ndax loolu moodi m\u00e0ndargam g\u00ebm.<\/p>\n<p><span style=\"font-size: xx-small;\"><strong><em> jukki bi: http:\/\/www.maoulhayat.com\/<\/em><\/strong><\/span><\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Bisimilaahi Rahmaani Rahiimi&#8230; \u00d1u fas yeeney dollee de\u03b7k\u00ebnte ak di dollee f\u00e0tleente. \u00d1i\u03b7 koy j\u00ebm\u00eble nak ci tomb bi nga xam ne mbooleem liy yiiwu \u00e0dduna ak yiiwu \u00e0llaaxira ci la ko sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa d\u00ebx\u00eb\u00f1. Mbooleem yonant yi mu y\u00f3nni y\u00e9pp ci la leen dig\u00ebl \u00f1u teg ci seen t\u00e0nk. Mbooleem \u00f1i&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[15,1],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1000"}],"collection":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=1000"}],"version-history":[{"count":35,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1000\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1008,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1000\/revisions\/1008"}],"wp:attachment":[{"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=1000"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=1000"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"https:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=1000"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}