|
|
|
Yàtt
bi lëmbee
jamono!
Su dee ni ko yenn waay-xeltu yi
di waxee namm-namm xarala dëggantaan
mooy gësëm
xelu nit ñi
ba ñu
xippi xool, gise neneen mbir yi leen wër,ku
yebboo kon ne
yàtt bi Ablaay Wàd yàttlu Wakaam
yégg na ca la mu ca doon wut. Ndax
ndonte sax nag sotteegul, "ngenteegu" ñu
ko maanaam, xel yeek xalaat yépp a
ngi lëmbee di ko
xaar...
Su caaxaan faaxee dëgg
dés, yàtt bi daa xajjàlle
réew mi ak li ko weesu ñaar
ba ñett ak ñeenti
làng: ñii ne mbir la bu
am solo, ndax day mandargaal gëddu nit
ku ñuul
ak suxxaliku gi askan yi ci Afrik, caagewul njaam gi ag metit
yi ñu
leen doon tégg yépp, masul
a jóg di ko sàkku, di ko yóotu. Am ñeneen
ñu ne yàtt bii
mooy firndeel dëgg
cuune, caaxaan ag càggante gi nguuru Ablaay Wàdd
ngemboo: ndax nees lay jëlee ci
réew mu lótt ni Senegaal, nit ñi
dëkkee jaaxle ag di tuuñ-tuuñi
lu ñu lekk, xale yiy
sóobu ci géej gi di wut a raw, ay
miliyaari-miliyaari di ko def ci yàtt bu kenn xamul
yàttu lan la?
Am genneen làng gu ca yokk ne li wér mooy
yàtt bi warul a taxaw mukk ci réewum Senegaal gii
di réewu julit, ndax diine lislaam dafay tere di
yàtt ay nit, rawatina yëkkati
ko ba mu mel ni luy juqarbi asamaan...
Am na itam ñoo xam dañu
ne ñoom li leen naqari mooy
yàtt bi ci boppam dafa amul lenn lu am solo lu muy misaal,
rax ci dolli rafetul, taaruwul! Dafa
fóoyóoy daal manaam su ñu
ko seete, tég ko ci sàrt yi aaru Afrik di
wéy.
Yàtt bi nag ci wàllu boppam mu nga nekk Wakaam,
ca tundu Mamel, jakarloog géej. Tollu na ci taxawaay 50 m,
genn góor jàpp jenn jiggéen, fab ci
loxo càmmoñ benn xale bu
talal loxom di joxoñ xarfu. Loolu nag
li muy misaal, ñu ne, taxaw-temmu
Afrik la, giy gindeekoo ci lëndëmtoog
njaam, dëgmal ëllëgug
yaakaar ag ngëm
gu mat sëkk.
Li wér daal mooy na yàtt bi ci jëmmam
ag yenneen yàtt yu mel ni "yàttu moomeel sa bopp"
ba ca Amerik, mbaa yàttu Yeesu Kiris ba ca Riyoo lay
diiranteel mbàgg! Ndaxam sax nag Beresil mbaa Amerik mëneesu
leen a jawaatleek Senegaal!
Ci bésu 04 Awril 2010,
tembook 50eelu at ba Senegaal moomee boppam ba léegi, lees
ko wara ngente. Li jaaxal nit ñi
mooy nan la askan wi, rawatina kilifa diine lislaam nara doxale? Ndax
dana ñu teeweeji tudd ba am
déed? Ndax it kilifa yenneen réew yi ñu
wóo danañu ñëw
am dañuy gàntu? Kon mbir
ma ngi noonu: cóow li bare na, xel yeeg xalaat ya ngi
joŋante! Su dee seetaan na daq cib ndajee kon lay ñëw
ca kanam a wara gëna neex!
|
|