|
|
|
Timbukutu: Péyu xam-xam bu
yàgg te sax!
Ni
ñu
leen ko fi waxeewoon ci jukki bi weesu, bind, sàkku
xam-xam, gëstu ak diine lu
yàgg la ci Afrik! Wante ñakka
xam ak ñakka am xel-ñaar
tax na ba ñu bare defe ne
gànnaaw woy aka fecc, mbaa léeb amul genn ndono
lu am solo
lu Afrik donn ci wàllu xam-xam.
Feeñal
parparloo ak tutiwaayu gisin woowu bokk na ci li ñu
tax a jóg. Firnde bi ñuy
indi téy mooy Timbukutu, di dëkk
bu mag ci Mali, te xam-xam bu keemaane sax fa, di fa law ca la ko
dalee lu jiitu 12eelu xarnu ba bés ni ki
téy.
La fa des ci ay téere yu ñu
bind ci kalaama Araab, pël, songaay...
jàpp nañu ne ëpp
na 700.000
téere! Te kenn mënul
a xayma la ca yàqu ak
la ca reer ci diir bu weesu 700 at, ba ñu
fa tàmbalee bind ba léegi.
Bind yooyu nag daanaka dañoo
laaw xeetu
xam-xam yépp: dalee
ko ci xam-xamu
diine, jal ci xayma,
xam-xami
biddéw yi,
xam-xamu
suuf
si, taalif,
xameefu-sàrti-baa,
kimi,
yoon
ak yenneen ak yenneen. Ndongo yi daan nañu jóggee
fu nekk ci àddina, Keer,
Bagdaad, Pers ag fépp di fa jàngsi.
Jàpp nañu ne iniwersite Sankoore ca Timbuktu lu
tollu ci 25.000
ciy ndongo daan nañu fa jàngsi.
Ay kangam yu mag yu mel ni Amet Baaba,
doon borom xam-xam bu ñu
ràññee
ci àddina sépp, ñoo
fa daan jàngale. Jamono jooju Afrik
sóowu-jànt - Timbuktu,
Jenne, Gawoo, Kano - doon péyu
xam-xamu àddina si dafa temboo woon ag lëndëmtu
gu meti ca Ëroop. Iniwersite ya njëkk
Ëroopsax - iniwersite ya
nekkoon Andaluus ca Espaañ,
ay xeetu Araab ak nit ñu nuul,
doonoon ay doomi Afrik, ñoo leen fa
sànccoon. Ay boroom xam-xam yu mag
daan nañu jóggee Timbuktu di fa
jàngaleji. Kon nga xam ne àddina moo
gudd tànk!
Wante xam loolu ci
boppam rekk lu am solo la: ndax da ñuy
gindi, gën ñoo
tàggaat ba ñu
xam ne xam-xam boobu fi nekkoon, su ñu
farloo, mën na
fee dellusiwaat. Te sax masu fee jóggee!
Téy jii itam yaakaar amaat na ci Timbuktu: ndax
réewum Afrik mu mag mu mel ni Afrik-bëj-tànk,
moo xar tànku tubbayam, taxaw ci saytu téere
yooyu dés Timbuktu. Afrik di Sidd
duggal na ay kopaar yu bari Timbuktu ngir
ñu tabax fa kàggu bu mag bu ñu
mëna dencc ci anam yu mucc-ayib
téere yooyu, tàggat itam ñay
liggéey ca kàggu ba ñu
xam na ñuy saytu téere yooya
ba duñu yàqu.
Kon gàcce ngallaama Afrik di Sidd ak Tabo Mbeki mi nga xam
ne moo amoon xalaat bu rafet boobu.
|
|