 |
Noo ñëw naq
la ci ndow mu nëx
Nga naan ba biir fees
Siggi say gët lendem
Booba ba tey ku ne cosaan
Nga ne cem ndaw caaxaan
Ku ne maam ya nga ne
Bu ñu tanqal
Lii
di
col waxin lekkin defin doxin
Nga
roy ba raw boroom
Boy
làkk di nalu ba coroxaan
Mbaa
di ciib-ciibi ni baaxon
Boo
demee kow ga nu ne moo jii waay, ja
woon laa
Mbaa
di la wër ndomba di seetaaan
Ni
tubaabu géej
Aka
neexoon nga fekke ëllëg
Ba
gis ne Kocc ak Xaali ak Ndaamaa
Muusa
ak Aadi mosunoo jóg ci xol yi
Mbaa
noppee nàmm xelu nit ñi
Taal
bi gilim taxul a fey
Nañu
yëngal gillint yi nu jër-jëri
Ngalla
ñun ci li fi Sàng ak Pool def. |
Ndakaaru
Tàkkusaan
nga may neex
Ba
ma taxaw fale ca
Sikaab
Xetu
Mbeex bawoo Wakaam
Di
ñoromtaan sama bakkan
Taax
ye ne
sóléet
Ni
càkkaaba yuy joqarbi asamaan
Seen
jañ yaa ngi jaayu
di jayaxu
Niy
baay-faal bésub màggal
Ma
ne jàkk
jaww ji
Mu
mel ni pótitu baxa
Mu
ñu serati guro
Ndakaaru
Balaa
nga maa neex tàkkusaan.
|