|
|
|
"Symbole: céy li ci réew mi"!
Symbole ci nasaraan, su ngeen ko déggee mooy lëf koo xam ne dafa am lu muy mandaragaal! Du lëf ki ci boppam moo am solo waaye la muy junjj ci xelu nit ñi la...
Ndekete këf ki ñu leen bëgg a nettali masu fee jóg
te mooy symbole bi fi daara tubaab bi indi di ko xeexee làkki
réew mi. Su ngeen ko fàttaliko (ci jàng mbaa ci
nettali) dañu daan masa tere di làkk làkki réew mi ci ekol yi. Ndongo lu masaan a rëccal ba làkk Wolof mbaa pulaar mbaa joola walla lenneen rekk ñu takal la symbole bi. Li mu daa faral di doon moo daan këf ku kenn bëggatul, naka ab yax bu ñu seeñu ba mu set, soo ko sànni xaj sax du ko xool! Noona lañu daan nàttee solo làkki réew mi. Loolu doonoon kennu bu am solo ci politik bi Faraas saxaloon fépp fu mu masaan nekk bëgg
faa wéyal caadam, làkkam, doxalinam ag ay gis-gisam,
tuddee woon ko "assimilation", manaam roy-dàq-aada.
Ci réewum Faraas ci boppam sax symbole boobu amoon na ca lekol
ya ay askani "bretons" nekkoon. Faraas daal da fa masa farlu ci xeex
bépp làkk bu dul làkkam rawatina nag làkki
réewi Afrik yi mu nootoon.
Wante sax nag Faraas deful kenn dara: bëgg sa bopp, bëgg sa làkk di ko faral dara nekku ci te Wolof Njaay da ne "lu waay nangu teg ko ko dagan na!"
Ñun dañoo defe woon ne xanaa loolu su ñuy tóog di ko nettali téy dañu naan xanaa jamano tubaab ya, wàlla jamano tubaab yu ñuul ya lawoon! Wante am nañu firnde ci atum 2010 bii ñuy
waaj a màggal 50eelu at yi sunu réew moomee boppam ba
léegi ne symbole boobu am na ci lekoolu Senegaal yi ba
léegi! Wante nag du lenn lu ñu kenn sëf!
Ñoo ko nangu! Xanaa kañ dañuy
yeemu ci xarala ak pexe tubaab ak sunu yàcaaral, ndax ndeem
jóge na fi itam ci biti, ci biir moom moo fi nekk ba
léegi! Làkkam ma fiy wéy ba léegi, xaalisam
a fi nekk ba léegi, xelam ak ay xalaatam
ñoo fi nekk ba léegi! Lii la Seneraal De Gaulle seentu woon ba tax, ba waxi "independance" bëggee ëpp
mu ne woon nanu yolomal buum gi ba laa mooy dog: Ndax téy jii
Faraas jóge na fi gaa, waaye téy la fi ëpp doole! Te nóooteel bi gëna diis, gëna jàpp mooy bi nga xam ne ki nga nóot day jiitu say xalaat, jiitu say bëgg-bëgg, def li la sóob te sa kàddu du jib!
Céy ngalla
ñun li ci réew mi ak ay lekoolam!
|
|