|
|
|
Ci
atum 2008 la ñu
bari ci parti yi juunoog nguur
gi jël seen matukaay daldi
wóo réew mépp, amul
xàjji-ag seen wan làng lañu
feetoo ci wàllu politik, ngir ñu
diisoo. Disóo boobu li ko waral, ñu
ne, mooy gutë
gi nga xam ne téy réewum Senegaal da cee
tàbbi.
Ndax gànnaaw ba parti yooyu boolewoon seen doole ak PDS, di
parti bi tóog ci nguur gi téy, jàppalewoon
Ablaay Wàdd ba mu jëlee
fi Abdu Juuf , dañoo
walbatiku feewaloo, ba kenn ca ña àndoon
ak Abaay Wàdd daanaka àndatul ak moom
téy.
Waa PDS nak, ñoom ba ñu
leen wóowee ca ndajee moomu, dañoo
lànkk ne du ñu ca bokk:
Ndax ndaje moomu, du lenn lu dul waxantoo ka foontu, nde ña
ko sumb, kenn yebbalu leen, kenn mayu leen kàddu, kon munu ñoo
waxal réew mi. Yore wu ñu
kàddu réew mi.
Téy jii nak, dafa mel ni mbir yi soppeeku nañu
ci fànn woowu, ndax bu yàggul dara la njiitu
réew mi, wax njawriñam ju
mag ji di Suleymaan Ndeene Njaay, ne ko mu jotali opoosisyoŋ bi, ne
leen da leen di bëgga wóo
ngir ñu
waxtaan ci lépp lu soxal réew mi. Ndegam
wóote
boobu da na mujj fenn? Ndax da na tax ba réew mi booloo
mànkoo
mel na mu meloon ca atum 2000? La ca kanam moom rawuli bët
gaa, wante mel na ni téy Abaay Wàdd ñu
bari ca ña daan ànd ak
moom dañu koo weddi bu baax: ndax nee
nañu loolu muy wóote newul
ci moom, duggeewu ko lu dul naxaate doŋŋ.
Li ëpp soloo nag ci li disoo boobu meññ
nag mooy li mu fésal doggu gi doomi-réew mi doggu
ngir suxali Senegaal ci kow xel ak xalaat, dëggu,
mànkoo, yar ag teggin.
Ci 22
fàneelu-ñaar ci
wéeru Mars 2009 réewum Senegaal wóote
na mpalum ndawi gox yi gox-goxaan yi, maanaam ndaw yu mel naka meer
yi, njiitu kominite riiral yi ak ñi
leen di jàppale.
Ba nguur gi tàmbalee yenneku yenn ca
ay sañ-sañam
naka moomeelu suuf yi ci dëkki-kow yi
ba léegi nag, ndawi gox yi ak gox-goxaan seen doole ag seen gëdd
dafa yokk bu baax. Loolu tax ba xëccoo
bi ci diggante parti yi gëna meti.
Rax ci dolli ba parti yi
àndoon ak Ablaay Wàdd ci àtum 2000
tàggook
moom ba léegi bii mooy daanaka seen jàkkarloo bu
njëkk gànnaaw ba ñu
joggee ca wóote 2007 ba ñu
bari ca ñoom
jàppoon na wóote boobu jaaruloon ci yoon. Loolu
taxoon
sax, ba parti yu bare gedd wóote ndawi réew ma ca
toppoon. Gedd googu nag, ñépp
jàpp nañu
ne ak njuumte gu réy lawoon. Ndax jurul lenn lu dul PDS
aakimoo
penccum ndawi réew, di fas aka fecci lu ko neex!
Parti yi
ànd boloo ci làng gi ñi
tudee Bennoo Siggil
Senegaal nag ñoo
gàddu ndam li! Ndax dëkk yu
mag yépp, daanaka, dalee ko ci Ndakaaru tekk ci Ndar mbaa
Kawlax ñoo fa raw Coalition Sopi,
mi bolee parti bi nekk ci nguur gi ag ñi
koy jàppale. Ràññee
nañu it ne yenneen làng yu
mel ni Ànd
dekkal ngor, mbaa parti Maki Sàl bi nekkoon
jawriñu Ablaay Wad, laata muy
gàddaay PDS, wone nañu it
ne am nañu mbooloo mu
tàkku mu leen topp.
Wóote bii nag parti bi nekk ci nguur ñakk
mënees
na cee jàngee lu bare: lu ci njekk mooy ne askani Senegaal
ci
boppam moo yeewu ci wàllu politik, ba daanaka kenn mënatu
ko nax. Ndax nit ñee seen bopp dañoo
xam njariñal demokaraasi, xam it ne
seen baat, seen kart lu am solo! Wone nañu
ci anam yu leer yu amul benn nàttable ne àndu
benn yoon
ci politik bi nguuru Ablaay Wàdd di doxal.
Moom njiiitu réew mi ci boppam nee na it dégg li
ko
Senegaal wax ci wóote boobu. Kon nag amaana buntu yakaar feeñaat,
Senegaal dellu dib royukaay ci Afrig ak ci àddina
sépp.
|
|