|
|
|
Bésu
sa....bés la bu kenn dootul fàtte ci biir
bés yi! Ndax ca la ñu
njekka fal nit ku ñuul njiit
réewum Amerik. Xam nañu
loolu lu réy la! Ndax ku seet
démboo-njaay rekk
na nit ku ñuul
tumuraankeewoon, Amerik, torox ko fa, ñu
koy beddi aka xàjj, xam ne àddinaa men naa dox
degg. Ba tax na ba Obama di waat ca bés buuba, ñu
koy yeegal ca nguur, daanaka àddina sépp ko
teewe! Yaram daw, der bu ñuul
ak bu xonq ànd di ko berndeel. ñenn ñi
sax gaawantu naan kon ku yebboo ne beddikoonte-ci-biiri xeet jeex na ca
Amerik. Obama baayam réewum Keñaa
la jogeewoon ca ay jamono jàngi Amerik, am fa doom ag senn
ndaw
su weex. Wante Obamaa masul la jog ci di fonkk der bu ñuul
bi mu bokk, di gestu cosaanaam ak cosaanu baayam. Rax ci dolli nag ku
Yàlla may xel la, jàngam sore lool ci
wàllu yoon, mu
doon layookat ak jnagalekat bu ñu
ràññee!
Pas-pasam, doggoom ak farloom mandargaal na leen yoon yu bare, ba mu
sóoboo ca politik, di xeexal aji-neew-ji doole yi, aji-ñakk
yi. Looloo tax taskatu-xibaar yu bare nee nañu
nguuru Obama gii jàllarbi bu rey la nara indi ci
àddina
si: menees na fee doxee jeflante ci diggante réew
yépp
soppeeku bu baax, ñu gena
soxal aar-càkkeef, jammoo ci diggante réew yi ag
yokk ndimbal li réew yi gena ñakk
yelloo.
Waaye li epp solo ci palug Obaama, mooy da fa dellu nit ku ñuul
geddam. Rawatina ca Amerik nga xam ne nit ku ñuul
doonoon na fa jaam lu tollu ci 500 at, amu fa woon baat, amu fa woon
dogal, bàyyima sax daw-raw!
Tàkku rekk ak gem sa bopp a wóor te neex!
Obama
am na jabar
- Misel Obama, ag ñaari doom -
Maliya ak Sasa.
Mpalu Obama gii nag, ginnaaw ba ci nit ñu ñuul ñi
ci àddina sépp amee mbégte lool, am nañu
yaakaar gu rey-rey. Yàlla bu yaakaar tas de, wante nag nguur
genn nit rekk menul saafara soxla yépp, ndax tumuraanke gi
dafa
yàgg te law ci réew yépp yi xeetu nit
ku ñuul nekk. Wante li
wér mooy nguuru Obama gi dina sopi bu baax ne yenneen xeet
daan gisee nit ku ñuul,
wáññi
xeebaati gu baax! Nguur Obama gi, fàww mu indi copite ak
yokkute ci nekkini nit ñu ñuul ña
ca Amerik, gen faa yekkati seen baat, yaatal fa seen cer.
Nguuru Obama gi am nañu yakaar it
lool ne dina gëna
dëgëral
taxaayu Amerik ci Afrik, gena fésal mbokkoo ag
xaritoo
gi wara am ci diggante Amerik ag Afrik, te men naa am it mu sopi
doxalin bu ñaaw bi Ameriku
Sors Buus doon
doxale, di nogatu, di jaay-doole di toroxal aka aakimoo alali yenneeni
réew, rawatina réewi julit.
La ca kanam moom, rawuli bët!
Kon Yàlla bu yakaar
tas!
|
|