Back to homepage Back to homepage
"Bépp làkk rafet na buy gindi ca nit xel ma, téy tudd ca moom ngor la" (Seex Musaa Ka)
Xew-xew 

Politik
Nekkinu-mbooloo mi
Koom-koom
Caada ji
Diine
Bitim-réew
Tàggat-yaram

Ñeel Seex Anta Jóob

Bés bu kenn dootul fàtte!

Bataaxal bi ëmb sañ-sañi doomu aadama

Terangñeel na Seex Anta Jóob!

Liggéey bu mel ni bii ñu fi dëgmal, wareef la ci sunu gis-gis, ñu ñeel fi ca ndorte la góor gu mel ni Seex Anta Jóob. Ndax daf fee def, lu fi daanaka kenn ci waay-xeltu yi ci Afrik ak li ko wër deful: maanaam yesalaat yoon wi àddina sépp doon gise cosaanu nit ku  ñuul, fa mu jaar ca njëlbéen ba yegsi fi mu tollu téy. Callalal-cosaan jooju la Seex Anta Jóob topp, dalee ko ca jamono yi nit ku xay, maanaam "homo sapiens" ci lateÅ‹, feeñe ci déndu Afrik ba jamonooy téy. 

Li tax mbir  moomu di lu am solo, mooy ne boroom xam-xam yu bare ci tubaab yi ak seeni ndongo yu ñuul dañoo jàppoon ci kow fóogi kese, ne nit ku ñuul daal cosaanam kenn mëneesu ko leraal ndax bindul. Rax ci dolli it, ñooñu ne, li fi suuf si goqi ci ay tabax yu yàgg te kemaane, ca Misira, Nibi, Simbaabwe, Nok ak fenneen, li wóor mooy wenneen xeet moo fi juuxsiwoon, def ko. Ndax nit ku ñuul xameewu ñu ko lu dul roy, njaam ag di wéy ci ndiggëlu kenneen.

Téy, ba Seex Anta ñëwee, wéer ay gëstoom ci xam-xam bu wér, ay firnde yu kenn mënula nàttable, leer na ne nit ku ñuul moo njëkka nite ci àddina, moo njëkka bind, moo njëkka tabax. Fi sax faf, ci Afrik la Yàlla tënee sunu Maam Aadama, ba ay sët-sëtaatam joge fi dem dëkki fenneen, melokaanam ag deram dóog di sopiku!  Xarala, xam-xam, tabax yi nekk fii Misira ak fenneen it ci Afrik te di yeem niteef gi, du kenn ku moy sunu maam yi ñoo ko fi def.

Wante dafa am benneen fànn bu am solo ciy gëstu Séex Anta sees di faral di umpale. Ndax bokk na ca la mu njëkka bind gëdd gi làkki-réewi Afrik wara dellu am, ba mëna dellu nekkaat ay juntukaay yu mat yuy jëmële askan yi ca kanam. Séex Anta masul a jóg di bind, di gëstu ci wolof ak yenneeni làkki Afrik yi. Ci kow loolu la tekki xeeti xam-xam yu nekk ci wolof: Dalee ko ci xam-xamu yaramal, simi, xayma, mbindum-fént ak yenneen ak yenneen. Naka noonu ci téereem bi  njëkka siiw di "Nations nègres et cultures" - maanaam "Waaso nit ku ñuul ag caada" la tàmbalee tekki  faramfàcci-ajoodiku walla "théorie de la relativité" bu Einstein, di ki nga xam ne daanaaka xam-xamam àddina sépp la yeem ba téy! 

Loolu yépp li mu ca masoon na jublu moo doon wone pexe yi  làxxu ci  sunu làkk, te amul sax benneen làkk bu mu mënti doon ci àdduna bu leen ca yobul dara.

Su sóobee Yàlla dana ñu fi dellusi gëna siiwal bindi Seex Anta Jóob yooyu ñu bare umpale.

Kon teranga ñeel na ñayu xare jooju jëfam aki xalatam dootul reer ba fàww!

Tamsir Anne © wolof-online.com