Back to homepage Back to homepage
"Bépp làkk rafet na buy gindi ca nit xel ma, téy tudd ca moom ngor la" (Seex Musaa Ka)
Xew-xew 

Politik
Nekkinu-mbooloo mi
Koom-koom
Caada ji
Diine
Bitim-réew
Tàggat-yaram

Ñeel Seex Anta Jóob

Bés bu kenn dootul fàtte!

Bataaxal bi ëmb sañ-sañi doomu aadama
Kiriis bi ganesi àddina!



      Atum 2009 bii 
ñu dugg nag kiriis bu meti moo laxasu àddina sépp, rawatina nag réew yi gëna néew doole. Kiriis boobu ñu tudde kiriisu kopar yi, li ko indi mooy bànkë yu bare, dañoo topp seen bëggub xaalis ba faf seetatuñu lu jaadu ak lu jaaduwul, ku ñu wara lebal ak ku ñu warta lebal, ndax ñoom ñooñu seen bopp di leble dencc nañu xaalis buy garaanti seeni bor am déed.

Mo tax ba màrse d
ëkkuwaay ya ca Amerik tarxiise, la bànkë yu bare tàbbi ci jafe-jafe yu rey! Li tax kiriis bi gëna meti te jafe nag mooy ne téy koom-koomi réew yi ëpp doole ci àddina si, ci leble bànkë yi la sukkandiku. Kon su bànkë yi seen bopp ame jafe-jafe, ñépp am jafe. Ku yebboo sax ne su bànkë yi tisóoli, yenneen bànxaasi koom-koom yépp ay sëxët!

Loolu la nguuri réew yi am doole yi xam, ba tax 
ñoom ñépp nu dawsi di walu bànkë yi! Du caage ne sax ci xol bu sédd lañu koy defe, wante su nu leen waluwul caaf xem!

Ca réew mu mel ni Amerik xaalis bu kenn xamul nu mu tollu la 
ñu xëpp bànkë yi, ngir ñu ximaliku! Réewi Ëroop yi naka noonu.

Wante kiriis bii it réewi Afrik yi muccu
ñu ci, ndonte it defuñu lenn lu aay! Xanaa kañ li ñu naan jamonooy téy jii ku bërewul ñu bëre daanu ci sa kow! Kon fàggaru foo tollu lu war la!

Wante kiriis bii sax, di ko dàkkantale kiriisu bànk
ë yi dafay mel ni daanaka, dees koy bëgga wóyofal! Te fekk li koy mandargaal dëgg ci nekkinu nit ñi lu tar la: te mooy milioŋi milioŋi nit yu ñakk seen liggéey ñakk seen dëkkuwaay, ay këru-liggéeyukaay yu dul jeex yu tëj, dund gi gëna meti, jaaxle wañaaru àddina sépp, néew-ji-doole yi gëna lótt!

Xalaas ndeke b
ëgge daal mooy jur lu nekk!


Doxalin wi ñeel góor ak jigéen

©2009 wolof-online. Tous droits réservés.