Back to homepage Back to homepage
"Bépp làkk rafet na bu gindi ca nit xel ma, téy tudd ca moom ngor la" (Seex Musaa Ka)
Xew-xew 

Politik
Nekkinu-mbooloo mi
Koom-koom
Caada ji
Diine
Bitim-réew
Tàggat-yaram

Ñeel Seex Anta Jóob

Bés bu kenn dootul fàtte!

Bataaxal bi ëmb sañ-sañi doomu aadama




Kocc Barma Fall,
ku ko xamul it dégg nga ay jàlloreem! Boroom xam-xam bu mag lawoon fii ci Kajoor, ci réewum Senegaal gii téy.
Jàpp nanu ne Kocc mu ngi doon dund ci fukk-ak-juroom-bennulu xarnu bi weesu (1584 - 1654).
Moom Kocc moo doon laamanu d
ëkk bu ñu naan Jàmmatil.

Jamonooy Kocc mu ngi dajewoon nag bu Buur bu tuddoon Daaw Demba. Daaw Demba mook Kocc 
ñoo duggandowoon neegu-góor, nga xam ne kon ñoom ñaar dañoo xamantewoon bu baaxa baax!

Daaw Demba moomu nag, buur bu soxar lawoon, 
ñakkoon teggin lool te gaawoon ci toroxal askan wi.
Looloo taxoon Kocc doon  ko xeex. Di ko xeex guddi ak b
ëccëg,  te jëlul fetal, jëlul jaasi: ci ñawaayu xelam donn la ko doon xeexe. Ba mujj daan ko jél bu set wecc bu kenn dootul miim! Waa Kajoor fippu, dajaloo folli Daw Demba, gennee ko réew ma!

Kon Kocc lees mena jàng ci moom ci jikko, ci xam-xam, ci yeewute bari na te du jeex ba fàww!
Rawatina téy jii nga xam ne nguur yi 
ëpp ci Afrik parlparloo, nooteel akub cuune rekk leeni mandargaal.

Kocc Barma daal ku mata ormaal, ku mata fonk la, ku mata fàtalli ak yeesalaat ay mbiram la. Ay diggléem aki xalaatam téy jii la seen maanaa gëna jéggi dáyyoo.

Diggléey Kocc

©2009 wolof-online. Tous droits réservés.