|
|
|
Dal
leen ak jàmm!
Mbooloo mi!
Ñu
ngi leen di
nuyu ku ci nekk ci yeen ci sa tur ak sa sànt
te di leen dalal ci jàmm. Béréb bi
ngeen tersi téy nag
dañu koo sàncc, mool ko ci kalaama wolof, jagleel
ko
làmmiñ yi ñu nàmp, ci
réewum
Senegaal ak ci Afrik gépp. Yaakaar nañu ne lu ni
mel,
mën naa am mu kañ ñenneen ba
ñu xar seen
tànki tubëy ci di jëfëndikoo
làmmiñ
yi ñu moomal sunu bopp, jéggaani wu ñu
leen fenn!
Ku fóog ne nag sunu làkk
yii ñu nàmp,
dañoo fóoyóoy, wàlla
dañoo matadi,
xamal ne rekk yaa ngi ci njuumte gu réey. Ndax sunu
làkk
yii, amul senn làkk ci àddina su leen
yóobul dara.
Sunu Maam yi, ci lañu doon bind, di ci jaamu
Yàlla,
di ci
xam seen bopp, di ci jàng àddina! Seeni pexe
kañ,
soo leen jàngee bu baax, da lay sax xanaa yeem! Ndax ay
làkk yu xereñ, te amul lenn ci àddina
lees ci mënul a wax.
Ndem-si-Yàlla si, Seex Anta
Jóob, ndeysaan,
Yàlla
na ko suuf sedde, da daan wax ne: "Aw
làmmiñ du
gàtt, aw xel mooy gàtt! Ndax lépp lu
xel mëna
xam ba mu leer ca moom, làmmiñ wa mën na
koo tudd!"
Te téy jii nag nga xam ne àddina si daa dem ba
mel ni as
ndëkk su ndaw, xarala yu mel ni enternet ak yenneen, di def ba
askan yépp am sañ-sañu wone seen
dayoo, wone seen
mbaax, seeni aada ak yoon wa ñuy gisee àddina,
waru
ñoo nangu di dés ginnaaw mukk!
Dees di faral di wax nag ne aw
làkk mooy daanaka ruu wu aw
askan, ndax askaan wu jèggaani ba jéggani aw
làmmiñ, fàtte ne mi ngeek bosam, askan
woowee ku
yeeboo ne cànkute gu wér moo ko dal.
Waxu
ñu nag
ne dañoo wara tëjju ci sunu biir, duñu
jëfëndikoo mbaa ñuy
làkk lu dul
suñu làmmiñ yi!
Déedéet:
dañuy jàng làkk yépp,
tambalee ko ca
angale, farañse, sinwaa ak lenneen ak lenneen, wante na
njëkka fekk ñu jàng sunu làkk
yi, di leen
jëriñoo! Ndax Wolof-Njaay da ne nit ku nekk li nga
moom,
nga mëna damoo! Te it sax, nag, su caaxaan faaxe,
dëgg
dés, àddina sépp daanaka noonu lañuy
doxale!
Réew mu ndaw moo seet, muy Oongiri, di Soloweeni, Serbi wala
menneen réew moo jël ci Ëroop ak li ko
wër, seen
làkk yi nu moom lañuy
jëfëndikoo njëkk.
Kon, mbokk sama, xarit sama dëgg la sax, àddinaa
dox,
nasaraan juuxsi fi, di làkk
làkkam, te
naan ñu ba leen seen wos! Wante nag, téy jii
ñuy
waxee, ci atum 2009 sunu réew yi ñoo
moom seen
bopp: Kon
lay jeex na, sas boobu sunu sas la! Kenn du ñu ko yennul,
kenn
du ñu sax gaar ci di jëfëndikoo sunu
làkk yi!
Loolu ñun doŋŋ, waay-xeltu yi,
ñiy yëngu
ci politik, jàngale, koom-koom ag fànn wu mu mënti
doon, ñoo ko
mëna defal
sunu bopp.
Tóol boobu nag lañu xëyy, di leen
sàkku fu ngeen mënti nekk ngeen
jàppale ñu, siiwal
béréb bi, yonnee seen xalaat ci mbir yi
ñu fi soxal
ñun ñépp.
Wasalaam!
|
|