|
|
|
Cosaan soo kooy
seet, mënees naa wax ne,
mooy xàncc biy boole ay
nit ba ñu mëna
ràññee
ne nit ñooñee ñooy
askan sangam. Ndax soo demoon téy marse Sàndaga,
di
béréb bu ay turist yu joggee fun nekk ci
àddina
di dajaloo di jënd, doo mëna
wax mukk ne ñooña
fa tase askanu turist lañu bokk.
Walla book xanaaa wax jooju dib waxi-misaal, nde fa dëgg
dgg ay dox-daje
doŋŋ lañu!
Wante aw askan nag
dug dox-daje koy tabax. Su ñuy
wax askan, li mu ëmb
mooy ay nit ñu
bokk aada yu yàgg, bokk ca cosaan, am fu seen
maam jaar démb ba yegsi
foofee ñu yegsi téy.
Dafa am kon lu boole nit ñoona ñu
naan ñooy askan sangam ca
jamonooy démb ba léegi.
Dafa mel ni kon cosaan mooy buum biy lëkkale
ay nit, ba ñu
nopppee doon aw mbooloo kese, soppaliku aw askan! Su doon ne dees di
mengale aw askan akub tabax, dees ay xala wax ne cosaan mooy kennu
tabax boobee.
Looloo tax ba aw xeet mbaa aw askan,
soo ko bëggee noot ba
fàww rekk, farlul ci mu fàtte cosaanam! Loolu
nag la tubaab bi ci pexeem mu rëy nàndoon,
ba tax ba mu fi bëggee
dëj doxalinam, dafa jël
ndawi réew yi dugal leen ci ay daaraam, jàngal
leen
làkkam, jàngal leen cosaanam moom tubaab bi, ba
noppi nag
ne leen, yeen moom amu leen cosaan, ndeysaan, su ngeen yebboo rekk
jeema
roy ci ñun.
Noonu cosaan amee solo
noonu la it
làkk amee solo, rax ci dolli làkk woo gis dafa am
cosaanam, am mbokkoo gu dox diggantéem ak làkki
yenneeni
askan, rawatina askan yi ko gëna jege.
Naka noonu la
Wolof bokkee ak pël,
bokk kook sereer, bokk koog saraxolle ak yenneen làkki
réew-mi. Wante nag itam, baat yi ci làkk wi seen
bopp dañoo mel ni saa woo
xam ne soo ko toppee, dangay yégg ba fa askani Wolof
cosaanu dëgg te mooy bëlub
dexu Niil ca Misira démb!
Soo dendalee Wolof ak làkki Misira démb, ag
làkki
askan yi nekk ba bésu téy ji bëj-tànku
Esipt, naka Nuer, day fés ne Wolof dafa bokk bu baax, ci
anam yu jeggi dayoo ag làkk yooyu.
Mbokkoo gi dox diggante Wolof
ak
làkki Esipt mëneesu
ko fee fàramfaccee ba mu jeex: Dafa di mbokk gu xoot te daj
làkk wépp, fés ci baati diine yi,
baati mbokkoo yi, baat yiy tudd cëri
nit ak yeneen ak yeneen. Te baat yooyu ay làkk du ñu
ko niroole, te fàww amul mbokkoo gu dox ci seen diggante!
Loolu
lépp nag li mu lay
won mooy
ne làkki réew demu ñu sax bay
fóoyóoy! Sunu làkk yi ñu
donnee sunu Maam ya, muy Wolof mbaa pël,
mbaa sereer, mbaa joola walla wenneen làkk wu mu ci mënti
doon, seen solo ci defaraat nit ñi,
defaraat réewi Afrik, delloo leen seen gëdd
lu jeggi dàyyoo la te mata sédd la!
Wante nag su caaxaan fàqee, dëgg
des, kuy jeggaani ba jeggaani aw làkk te ame sa
làmmiñ,
lúwuloo, war ngaa
seetaat sa bopp!
Li am ba des rekk mooy li Seex Musaa wax ne "bépp
làkk
rafet na, buy gindi ca nit xel ma, téy tudd ca moom ngor la!"
|
|