|
|
|
Jaar-jaaru
woykat bu jege woon askanam
(Taatanu
Séydu
Nuuru Njaay, Pikin Xuru-Naar : 19/01/1999)
Ci
sanwiye 1999, yeneekay Lasli/Njëlbéen amoon na
laaj-tootu bu yaatu ag
Njaga Mbay, doon ca feeñal ay jaar-jaaram. Waxtaan woowu
Njaga Mbay amoon ak Séydu
Nuuru Njaay, di njiital Lasli/Njëlbéen moom lañu leen fi
indilaat, di ci ñeel woykat bu mag bu
àddina sépp jooy.
Lasli/Njelbéen:
Kan mooy Njaga Mbay?
Man.
Njaga jooju nga tudd, ñu ngi ma tuddee gennn
góor gu
tudd Njaga Mbeng, nekkoon jaaykat bu mag di woon itam aalim. May doomu
góor gu ñuy wax Ngóor Mbay,
ñu koy woowee Abdu Faatma ca
Cilmaxa ak jiggéen ju ñuy wax Kumba Ndaxaar Sàll.
Ngóor Mbay nag da daan xalam, Kumba Ndaxaar moo yore woon kër gi.
Maa ngi judd ci 1948 ci Taatagin ca diiwaanu Siin-Saalum;
booba
jamono ay arondismaa amagul. Fa laa jàngee sa ma
njàng mu
njëkk ci tubaab, ba
Yàlla def ci 1962, ma jóge fa dem
Fatig di yokki sama njàng ci «CEG» ba fa
nekk. Ci ñi
njëkka jàng ci
«CEG» ci la bokk. Ci 1965, ginaaw ñetti at ci daara ju
dig-dóomu jooju, ma bàyyi dem nekki benewol ca
rondismaa
Taatagin. Foofu laa duggee làrme ci 1966.
Ci xumbte yi doon tëj sunu jàngum
militeer man ak ñoom
Mbeng Mbay Maa Daawur, Siidi Buya Njaay booba liyetnaa la
woon, ñoo
xumbal ngoonal gi. Bi ñu paree ñu indi ñu Dakaar; booba Cerno Ba, mu ngi
woon ca jawriñ ji ñu dénk gi Caada gi.
Moom moo gis Sonaar
Seŋoor ne ko gis naa
xale boo xam ne, boo leen ko jële di na leen
amal solo lool. Booba 1967 lawoon, maa ngi woon «Marin»; bi may dem ñu may dégglu ca
Soraano, booba yere
«Marin»
la soloon. Ma dem ñu dégglu ma.
Bés ba ma delluwaatee
Soraano ngir nemmeeku la ma fa defoon, ñu ne ma foo nekkoon? Ñëwal
liggéeysi.
Noonu laa duggee Soraano....
Am naa ñetti soxna ak ay doom. Aal
pulaaren yi ñu ngi may njukkal. Am na ay gëstukat yu mel ni Amiidu Ja, yu bind
ci man ay téere ak itam Ibrahima Wan, doon def ab gëstu ci njàngam ca
Daara ju mag ja ci man, ak ñoom Samba Jabare ak Yusu Nduur.
Baaba Maal moom itam moom bañ
na ko ba balaa bég, su ne cépp Podoor ma dikk fa.
Ku dikk
mu ne ko kii mooy sunu xalifa, mooy sunu mag, mooy sunu
lépp.
Xam nga kon mënu maa wax ci lenn di wone suma
bopp te wone wu ma suma
bopp jarale ko ci njabootu Aal-Pulaar yi...Maa ngi sargal itam Seex
Aamidu Kan...
Tukki?
Dem
naa ci réew yu bare. Dem naa Màkka 1987.
Dem naa réew yu bare waaye duma fa yàgg, ndax
dóomu-réew warul yàgg fenn
bàyyi sa
réew, dinga fa jëriñ loo xam ne soo nekkoon sa
réew, mu ëpp fa doole.
Damaa màgg ne sama papa damay woy? Mu ne ma, tee ngaa baña woy? Ma ne ko, man damay woy!
Mu ne ma kon, kom dangay woy rekk, dangay dem Dakaar. Soo demee, Alaaji Amadu Njaay
Sàmb ma nga fa. Moom sama doomi yaay la, ki jur
yaayam ak ki jur sama yaay, ñoo bokk ndey ak baay. Ma ne
balaa maay dem ci Amadu Njaay Sàmb, naa
«demerdeel» sama bopp. Ci laa
tànnee fànni woyin bii ma tànn, muy
yeete ak jàngale ci woy.
Noonu laa woye sama
album bu njekk, ak ay woy yu mel ni: mbëggéel,
njuréel, fey bor, àndadoo yu baax, xaajaloo,
terangaa. Ma xam ne, nekk fi di taggaate du
woon dox. Te tàmm naa wax ne ku ñuy woy sa maam xas nañu la; ndax
defagoo li sa maam defoon ba tax ñu bàyyi ko ci
ni ñu wara tagg...Ndax ku ñu ne sa maam a dàq
Dammeel, rendi Teeñ, te yow dàqoo
kenn... Waaye ku ñu woy sa baay woy nañu la...Loolu mooy wax ji; xam
nga ku sànt Mbàkke, ku woyal Sëriñ Tuuba nga bég, waaye
Bamba rekk a demoom géej ga...!
Fent?
Am na ñuy wax naan: guddi
lamay woy di dikkal, ñii naan bëccëg, ñii naan su ma
meree, ñii
naan su ma bégee. Man Yàlla da maa boole
ci ñi
nga xam ne ñii
suma gisee lu ma ko jaral di naa xam fan laa koy jaar.
Moo tax woy, am na ñu
koy tabax, am na ñu koy soppi, am
na ñoo
xam ne dañu
koy fent ci saa si (
«emporowiise»)...Bu ma binde woy
wi sax fàww ma bàyyi ci loo xam ne dama koy fent
noonu ca ba moy koy woyi. Sëriñ Abdu moo ma waxoon
ne kuy wax ak ñépp, ñépp amal
nanu la njukkal. Looloo gën.
Bu ma demee ba di wax ku nekk yow laa yaakaar, dinaa dem ba dootuma
yaakaar Yàlla. Nitu ñépp nay
jeema wax ak ñépp.
Sama woy maa ngi koy woy ni mu ma dikke...
"Yes"
ag "Non"!
Diggante Senegaal ak Gambi
wareesul
a sax tóogaati di fàttali ni mu xátee!
Ndax
diggante ay doomu ndey ak ay doomu baay la, wenn askan wi la rekk!
Loolu daan na gën a fés
jamano, su ndem-si-Yàlla si Dawda Kayraba Jawara ñëwaan
Senegaal di làkk Wolof, ndax dégguloon nasaraan,
te itam Senegaal it du dëkku
angale. Loolu nag lu neexoon la ci nop ag ci bët
ndax da daan wonne rekk ne ñaari
réew yi benn lañu: ñoo
bokk làkk, bokk cosaan bokk aada.
Nootaange
tubaab bi kese moo taxoon ba ñu
dem ba defe ni ñaari askan
yu wutee lañu: ñii
di làkk farañse, ñee
di làkk angale; ñii
naan "yes" manaam ña ca
dés naan "non", te fekk nag dug ndam! (Li ci topp)
|
|