|
|
|
Laaj-toontu ag Bubakar B. Jóob

Bubakar Boris
Jóob kenn la ci bindkat yi gëna
mag ci Senegaal ag ci Afrik. Bind na ay téere yu siiw ci
kalaama farañse
ag benn téere bu am solo ci Wolof bu mu tuddee Doomi Golo.
Laaj-toontu bii yeenekaayu "Le Monde des Livres" moo ko amaloon ak moom ci 16
fan ci weeru Awril. Waxtaan woowu lañu
leen fi tënkal...
Le Monde:
Lu tax nga bind Doomi Golo ci Wolof njëkk...
Dama
mas a bëgg
bind ci Wolof, ndax ci sama gis-gis làkki réew
mi dees leen a war a jox àq bi ñu yelloo. Ni ko
Coetzee waxee "Bindkati Riisi waa Riisi lañuy bindal, bindkat
yu Faraas waa Faraas lañuy
bindal, waaye bindkati Afrik ñoom bindalu ñu waa Afrik, yeneeni askan lañuy bindal"...waay-xeltu yi gëna bari te amkoon dooleey jënd téere yi
ci làkki Afrik, dañoo làggi
ci xeeb làmmiñ
yi ñu
nàmp...
Le
Monde: Ndax dafa am xew-xew bu am solo bu la
sóob ci sopi làkk bi nga doon bindee ba
léegi...
Su ma yeboo ne li gëna waral coppite boobu
mooy mbóom-waaso ga woon Ruwaanda. Bañ-sa-bopp gaa,
bokkoon na ca la waraloon jëyya ja,
wante doxalinu koloñalist bi fi sax,
amoon na ci wàll itam. Te kenn mënul a weddi ne Faraas
ci boppam fésoon na ci ñi doon jàppale boomkat
yi...Te li woon ndéyi-mbill gi dëgg ci mboom-waaso
googu mu ngi laxasuwoon ci mbirum làkk, ci màmm
gi ñu
bari màmmoon ci kalaama farañse. Nguuru Faraas
dafa làngoon ak boomkat yi, ndax rekk li mu yëgoon ne ci
wàllu caada ak politik cofeel gi waa Front Patriotique
Rwandais amoon ci angaleek-amerikeñ da doon lu koy gësëm. Foofa la
doxee, gëna
bañ gépp
xeetu nooteel ci wàllu caada, gëna dollee bëgg a bind nag ci
kalaama Wolof. Noonu la sóoboo ci biir nag, kom ni ñu koy waxee...
Le
Monde: Amul yenn saa yoo doon am siiki-saaka bi nga sumbee
loolu?
Ahakañ!
Am na sax yenn saa yu ma amoon xel-ñaar dëgg sax, ndax sama
njàngum bind yépp ci "francais" la, te boobu téere moo
doon sama juróom-ñaareeli
téere; wante ba ma koy bind dama meloon ni kuy
doog a door...wante mujj gi suma yebboo ne bokk
na ci téere yi ma gëna feexal. Baati biir
yu bare tàmbalee di ma àwwu, rawatina ay baati
jiggéen...
Le
Monde: Lu tax ay baati jiggéen?
Ci sunu réew, jiggéen ñee gëna neew ci
ñi jàng lekool, ci ñiy jàng
nasaraan. Ba tax seen Wolof dafa seet te mucc-ayib!...
Le
Monde: Lu la dellu xiir ci tekki Doomi Golo ci nasaraan?
Dama ne woon ca atum 2003 ne téere boobu deesu
ko tekki lu dul ay ati at ca kanam. Ndax dama bëggoon mu demal boppam,
wonne boppam. Ndax li doyoon waar mooy téeri bi
dama koo noppee bind ci Wolof rekk, ñu bari
tàmbalee maa laaj kañ laa ko fas-yeenee
tekki ci tubaab, manaam daal "ci làkk dëggantaan"!
Wante ci atum 2006 ba ma Toni Morrison woowee ngir ma jàng
benn pacc ci sama téere bi tudd Murambi ca "Musée du Louvre",
ca laa tekkiwaale woon benn dóg ca Doomi Golo. Foofa la doog di yëg ne tekki ko jot
na.
Le
Monde: Ndax di nga ci bindaat ci nasaraan?
Waawaaw! Masu maa xalaat a bañ a bindati ci farañse. Wante li ma bëgg mooy
fésal lëj-lëj gi ci fàn
woowu ci wàllu caada. Ndax dama jàpp ne
mbindum-fent bi ay doomi Afrik
di bind ci làkki nasaraan, mbindum-fent bu fi nekkagum
rekk la, du lu
fiy wéy!...Man ci sama wàllu boppam caageewul ne
damaa bañ
farañse...li
ma bañ
mooy folkoloor biy bàkkantu naan " farañse bi sunu xarit ya
Afrik di làkk" ag lépp li muy junj ci
xelu nit ñi...
Le
Monde: Ndax ci sa téere yi am na bu ci nit
ñi gëna
sopp ci Afrik
Waaw Murambi, nettali la xew-xew ya
amoon Ruwaanda, ñu
ngi koy jàngale ci lekool yi..."Le temps de Tamango" itam ñu ngi koy nafar ci
daaru yu mag yi...Bu loolu weesoo it gis naa ne itam mbind mi ci
làkki réew yi, mi ngi law bu baax ci biir Afrik ...
Lilam Azam Zanageh moo taataan
waxtaan wii
ci
Le Monde des Livres bu 16 Awril 2010
|
|