|
|
|
Baraak
Obama: Piri Nobel 2009
Ndam dikkati na ci Baraak Obama, njiitël réewu Amerik mi xeetoo néeg baayam ci Afrik. Ndax moom lañu jagleel atum 2009 bi ñu nekk piri Nobel biy ràññee nit ki nga xam ci àddina sépp, moom lañu jàpp ne, ay jëfam, ay xalaatam, ay pexeem ak ay mébetam ñooy li gën di sabab jàmm ci àddina bi mbaa di fay ay yi fi tàkk.
Obama nag ci kàddu yi mu wax ca bés boobu ñu
ko teralalee ca Oslo, peyum réewu Siyeed, dafa cee fésal ne ndonte kon
tafaar lu mata xeex la, terewul ba léegi mu am xare yu jub ag xare yu
jubadi.
Xare bu jub, mooy ci gis-gisam, xare bu am réew, aw askan
di xare ngir aar boppam, ngir difi ay ñoñam, mbaa xeex notaange. Li am solo ci xare yu jub yooyu mooy def kemtulaay kàttan, fexe ba bàkkani ñi yorul gànnaay, maanaam siwil yi, bañ caa des.
Gànnaaw loolu it Obama wone na ne terorist yi di jaxase aka xoxatal àddina si, nekkul lees mëna nangu, te ñooñu dégguñu lu dul kàddu doole. Mu rax ca ne itam moom ci wàllu boppam, njiitu réew mu mel ni Amerik, mënula seetaan doole di mën dëgg. Ndax bëgg jàmm wareesu ko jawatleeg akub ragal. Ku yeeboo sax xanaa kon ne ni ko waay-xeltu ba waxeewoon " ku bëgg jàmm dangay fàggu ngir xeex".
|
|