{"id":869,"date":"2012-02-01T14:07:02","date_gmt":"2012-02-01T14:07:02","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=869"},"modified":"2012-07-01T11:12:43","modified_gmt":"2012-07-01T11:12:43","slug":"869","status":"publish","type":"post","link":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=869","title":{"rendered":"N\u00e0qar, tiis ak metit"},"content":{"rendered":"<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/mort_manif1.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"alignleft size-full wp-image-872\" title=\"mort_manif\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/mort_manif1.jpg\" alt=\"\" width=\"600\" height=\"400\" srcset=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/mort_manif1.jpg 600w, http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/mort_manif1-300x200.jpg 300w\" sizes=\"(max-width: 600px) 100vw, 600px\" \/><\/a>R\u00e9ewum Senegaal tollu na diggante bu xat te mooy diggante dund ak dee gannaaw ba kur\u00e9el gi waroon a saytu s\u00e0rti-r\u00e9ew mi fee\u00f1ale parparloom ne ki \u00f1\u00e9pp di mb\u00e0mb, neex n\u00e0qari day bokk.<br \/>\nLi \u00f1\u00e9pp yaakaaroon ne dina\u00f1u takk seen fit, def ni seen natangoo ya ca Maali gii mbaa Niseer defoon tas na! Wante Y\u00e0lla ak askani Senegaal dina leen \u00e0tte ci lu w\u00e9r, ndax seeni maas a nga &#8220;La Haye&#8221; c\u00f3owu \u00e0ddina s\u00e9pp topp leen!<\/p>\n<p>N\u00e0qaru-xol d\u00ebgg la\u00f1u ame t\u00e9y bi \u00f1u gise ni Ablaay W\u00e0dd ak \u00f1i ko w\u00ebr j\u00f3gge di dal ci kow askan wi, genne seen sox di f\u00e9tal aka r\u00e9y ay xale, ay jigg\u00e9en ag ay m\u00e0ggat yu yorewul benn ngannaay bu dul seen fit, seen jom ak seen ngor!<\/p>\n<p>ImageAblaay W\u00e1dd moo toraxal askanu Senegaal mi ko teral, mi ko y\u00ebkkati woon, teg ku fu mu masul a teg kenn daanaaka, d\u00e9nkk ko \u00ebll\u00ebgam ak \u00ebll\u00ebgi doomam, denkk ko l\u00e9pp li ko tax a beew ba def boppam Y\u00e1lla di faat ay bakkan!<br \/>\nAskani Senegaal askan wu Y\u00e0lla m\u00e0ggal la, askani nit \u00f1u am ngor la\u00f1u, am teraanga, g\u00ebm Y\u00e0lla. K\u00e9pp ku tuur deretam Y\u00e0lla dina la s\u00e0nkk saayiir ak baatin! Kenn m\u00ebnu ci dara!<br \/>\n\u00d1\u00e9pp xamoon na\u00f1u ne Ablaay W\u00e0dd kilifaag mb\u00ebtt la: soo toppee ci ginnaawam mu ne &#8220;bul d\u00ebgg sama geen&#8221;, nga toloog moom mu ne &#8220;da nga maa b\u00ebgga yab&#8221;, soo ko jiitoo &#8220;mu ne toppal sama naaj&#8221;. Wante t\u00e9y weesu na foofu, gaynde-sibi gu t\u00ebx, xiif y\u00e0pp la ba naan askan wi&#8221;Yeen a ngi may xee\u00f1i seel&#8221;! Te \u00f1un de askani Senegaal, xamu\u00f1u lu dul cere ak soow!<br \/>\nLi ko waroon moo doon lekk ci ndab li \u00f1u ko jox joxin wu rafete rafet bu \u00e0ddina s\u00e9pp b\u00e0kk, ubb ko ba mu jekk w\u00f3o keneen! Wante lekk ba noppi x\u00ebpp ci suuf loolu la faye askani Senegaal!<br \/>\nImage<br \/>\nLaam-laame nag weesu na, artu itam w\u00e9y na! Lenn rekk a d\u00e9s, ci k\u00e9pp ku yore k\u00e0ddu, nga wax d\u00ebgg! Lu dul d\u00ebgg du y\u00e0gg te jenn d\u00ebgg rekk la: na Ablaay W\u00e0dd dem! Menn ab picc m\u00ebnul a y\u00e0qum r\u00e9ew! Moom ak doomam la ak seeni dag ak r\u00e9ewum l\u00ebmm, mu beggul lu dul tedd, dund ci teraanga, tedd ag jaamu-Y\u00e0lla!<\/p>\n<p>Wante gudd nopp taxul a d\u00e9gg, nde kon kenn du door mbaam te nag mujju mbaam ay tan, buuru buuri kasaara yi!<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>R\u00e9ewum Senegaal tollu na diggante bu xat te mooy diggante dund ak dee gannaaw ba kur\u00e9el gi waroon a saytu s\u00e0rti-r\u00e9ew mi fee\u00f1ale parparloom ne ki \u00f1\u00e9pp di mb\u00e0mb, neex n\u00e0qari day bokk. Li \u00f1\u00e9pp yaakaaroon ne dina\u00f1u takk seen fit, def ni seen natangoo ya ca Maali gii mbaa Niseer defoon tas na! Wante&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[4],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/869"}],"collection":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=869"}],"version-history":[{"count":8,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/869\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1388,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/869\/revisions\/1388"}],"wp:attachment":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=869"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=869"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=869"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}