{"id":800,"date":"2012-02-01T20:26:23","date_gmt":"2012-02-01T20:26:23","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=800"},"modified":"2012-07-01T11:12:11","modified_gmt":"2012-07-01T11:12:11","slug":"800","status":"publish","type":"post","link":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=800","title":{"rendered":""},"content":{"rendered":"<p><strong>Bennoo, \u00d1aaroo, \u00d1ettoo ba \u00d1ent&#8230;.<\/strong><br \/>\n<a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/bennootasaaroo.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"alignleft size-full wp-image-801\" title=\"bennootasaaroo\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/bennootasaaroo.jpg\" alt=\"\" width=\"468\" height=\"243\" srcset=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/bennootasaaroo.jpg 468w, http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/bennootasaaroo-300x155.jpg 300w\" sizes=\"(max-width: 468px) 100vw, 468px\" \/><\/a>Mbooloo mooy doole te mooy j\u00e0mmi-r\u00e9ew, wante lu waay di wuyoo na koy niroo! Moo tax ba Front Siggil Senegaal seete seetaat ba tudde boppam Bennoo Siggil Senegaal, la yaakaar dellusiwaat ci askan wi, ndax xam xell ne noonu rekk la nataange, tawf\u00e9ex ak j\u00e0mm jiy doomi-r\u00e9ew miy m\u00e9b\u00e9t m\u00ebn a jebbi Senegaal. Wante su dul woon loolu sax, \u00f1\u00e9pp xam na\u00f1u ne mb\u00ebr mu mel ni Ablaay W\u00e0dd, rawatina mu yore li mu yore, maanaam pexe yi ak m\u00ebn-m\u00ebn yi ko &#8220;Etaa&#8221; jox, soo ko b\u00ebgge daan alafook nga teel a j\u00f3g. Waajaay bi y\u00e0ggoon na lool, laamisoo bi itam noonu, ba \u00f1enn ci seetlukat yi sax xaw a am xel-\u00f1aar naan, mbaa bii &#8220;Bennoo&#8221; moom du mujj a doon &#8220;Tasaaroo&#8221;?<br \/>\nYeene ju rafet amul ag pay gaa, wante na na fekk itam mu mengook past\u00e9ef, j\u00ebfe ak d\u00ebggu.<br \/>\nNaka d\u00e9mb ci ngoon r\u00e9ew mi yeweeku na. Waa Bennoo jubbowu \u00f1u ci benn kandidaa, da\u00f1oo mujj wote: 19 parti \u00e0nd ak Mustafaa \u00d1as, yeneen 14 parti \u00f1oom wotelu \u00f1u kenn, da\u00f1oo tiyye seen k\u00e0ddu.<\/p>\n<p>Wante li \u00f1u doon ba\u00f1 am na: ndax gannaaw ba \u00f1u t\u00e1nne seen mb\u00ebr ba noppi, Tanoor moom dafa indi t\u00e0nki bukki. Ne du nangu mukk Mustafaa \u00d1as di jiitu, ndax Bennoo masu \u00f1oo wax ne da\u00f1uy wote ngir t\u00e0nn ki war a doon seen kandidaa. Mu Yokk ci sax ne li Bennoo def, &#8220;kudetaa&#8221; la bu \u00f1u kudetaa PS la. C\u00e9y, politik yenn saa yi kenn du xam lu muy nirool! Waaw xana \u00f1oom, jaamu soxlaay r\u00e9ew mi taxul leen a jog? Te sax ni ko Wolof Njaay di waxe, &#8220;man la, man la&#8221; joo gis \u00f1aare, du moom! Te su caaxaan fattoo, d\u00ebgg des, r\u00e9ew mi warul a f\u00e0tte ne parti sosialist bi Tanoor Jeng jiite moo fi nekkoon 40 at: li \u00f1u fi y\u00e0q bare ne te jafe-jafe yu bare yi r\u00e9ew miy j\u00e0nkoonteel t\u00e9y it, seen politik bi fi nekkoon am na ci yoon. Jareesu fee nekk di wax waxi d\u00e9mb, wante alafook itam \u00f1u seet fi \u00f1u jaar ba yegsi fi nu tollu. Ci sunu gis-gis bu neew, teel na lool sax di leen denkaat r\u00e9ew mi! \u00d1u bare ci am seetlu nee na\u00f1u gaa parti sosialist ba woon ak bii du benn, wante na\u00f1u t\u00e0bb \u00f1eneen \u00f1u jeem ba \u00f1u gis li \u00f1u m\u00ebnee.<br \/>\nMustafaa \u00d1as moom, d\u00ebgg la w\u00e9r na ni ku b\u00ebgg r\u00e9ewam, ndax su dul woon moom ba l\u00e9egi kenn du wax Ablaay W\u00e0dd: li mu beddekuwoon 2000 j\u00e0ppale Ablaay W\u00e1dd, looloo taxoon ba PDS falu, nguuru parti sosialist jeex. Kon mel na ni daal ci moom la yaakaar yi g\u00ebna daje: kon Y\u00e0lla bu yaakaar tas!<\/p>\n<p>Wante doon kandidaa Bennoo walla Genn-W\u00e0ll-Bennoo taxul a falu! R\u00e9ew meey fal, te ku jub, maandu, farlu, mat rekk la\u00f1u war a jiital: mu jaar ci yoon yi penccum-r\u00e9ew mi walla &#8220;Assises Nationales&#8221; yi x\u00e0lloon!<\/p>\n<p>Senegale yi m\u00ebn a wuutu Ablaay W\u00e0dd du\u00f1u fi jeex! Xuloo beek saagante bi jaru ko, su dee askan wee leen \u00f1or, na\u00f1u taxaw nj\u00ebkk ci xeex Ablaay W\u00e0dd ak nguuram, ndax moom kat g\u00ebmul nelawul! Ay weer a ngi xaat muy defaru di waaj a t\u00f3ogaat, mbaa mu d\u00ebjj fi doomam mbaa ku ko neex! Te su \u00f1u xaare ba jaan wi dem, \u00f1u topp cay door ca watit, du j\u00ebri\u00f1 tus! L\u00e1mb ji s\u00e1jj na, ku woolu sa mb\u00ebr na nga wut ng\u00e9mb lu d\u00ebgg\u00ebr te t\u00e0mbali say deeba-deeb.<\/p>\n<p>Tamsir Anne \u00a9 wolof-online.com<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Bennoo, \u00d1aaroo, \u00d1ettoo ba \u00d1ent&#8230;. Mbooloo mooy doole te mooy j\u00e0mmi-r\u00e9ew, wante lu waay di wuyoo na koy niroo! Moo tax ba Front Siggil Senegaal seete seetaat ba tudde boppam Bennoo Siggil Senegaal, la yaakaar dellusiwaat ci askan wi, ndax xam xell ne noonu rekk la nataange, tawf\u00e9ex ak j\u00e0mm jiy doomi-r\u00e9ew miy m\u00e9b\u00e9t m\u00ebn&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[4],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/800"}],"collection":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=800"}],"version-history":[{"count":9,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/800\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1384,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/800\/revisions\/1384"}],"wp:attachment":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=800"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=800"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=800"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}