{"id":1233,"date":"2012-07-01T10:13:44","date_gmt":"2012-07-01T10:13:44","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1233"},"modified":"2012-07-01T10:32:36","modified_gmt":"2012-07-01T10:32:36","slug":"dal-leen-ag-jamm","status":"publish","type":"post","link":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1233","title":{"rendered":"Dal leen ag jamm!"},"content":{"rendered":"<p style=\"text-align: center;\"><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/07\/wolof_header2.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"aligncenter  wp-image-1234\" title=\"wolof_header2\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/07\/wolof_header2.jpg\" alt=\"\" width=\"600\" height=\"100\" \/><\/a><\/p>\n<p>Mbooloo mi! \u00d1u ngi leen di nuyu ku ci nekk ci yeen ci sa tur ak sa s\u00e0nt te di leen dalal ci j\u00e0mm. B\u00e9r\u00e9b bi ngeen tersi t\u00e9y nag<br \/>\nda\u00f1u koo s\u00e0ncc, mool ko ci kalaama wolof, jagleel ko l\u00e0mmi\u00f1 yi \u00f1u n\u00e0mp, ci r\u00e9ewum Senegaal ak ci Afrik g\u00e9pp. Yaakaar na\u00f1u ne lu ni mel, m\u00ebn naa am mu ka\u00f1 \u00f1enneen ba \u00f1u xar seen t\u00e0nki tub\u00eby ci di j\u00ebf\u00ebndikoo l\u00e0mmi\u00f1 yi \u00f1u moomal sunu bopp, j\u00e9ggaani wu \u00f1u leen fenn!<br \/>\nKu f\u00f3og ne nag sunu l\u00e0kk yii \u00f1u n\u00e0mp, da\u00f1oo f\u00f3oy\u00f3oy, w\u00e0lla da\u00f1oo matadi, xamal ne rekk yaa ngi ci njuumte gu r\u00e9ey. Ndax sunu l\u00e0kk yii, amul senn l\u00e0kk ci \u00e0ddina su leen y\u00f3obul dara. Mbooloo mi! \u00d1u ngi leen di nuyu ku ci nekk ci yeen ci sa tur ak sa s\u00e0nt te di leen dalal ci j\u00e0mm. B\u00e9r\u00e9b bi ngeen tersi t\u00e9y nag<br \/>\nda\u00f1u koo s\u00e0ncc, mool ko ci kalaama wolof, jagleel ko l\u00e0mmi\u00f1 yi \u00f1u n\u00e0mp, ci r\u00e9ewum Senegaal ak ci Afrik g\u00e9pp. Yaakaar na\u00f1u ne lu ni mel, m\u00ebn naa am mu ka\u00f1 \u00f1enneen ba \u00f1u xar seen t\u00e0nki tub\u00eby ci di j\u00ebf\u00ebndikoo l\u00e0mmi\u00f1 yi \u00f1u moomal sunu bopp, j\u00e9ggaani wu \u00f1u leen fenn!<br \/>\nKu f\u00f3og ne nag sunu l\u00e0kk yii \u00f1u n\u00e0mp, da\u00f1oo f\u00f3oy\u00f3oy, w\u00e0lla da\u00f1oo matadi, xamal ne rekk yaa ngi ci njuumte gu r\u00e9ey. Ndax sunu l\u00e0kk yii, amul senn l\u00e0kk ci \u00e0ddina su leen y\u00f3obul dara.<\/p>\n<p>Sunu Maam yi, ci la\u00f1u doon bind, di ci jaamu Y\u00e0lla, di ci xam seen bopp, di ci j\u00e0ng \u00e0ddina! Seeni pexe ka\u00f1, soo leen j\u00e0ngee bu baax, da lay sax xanaa yeem! Ndax ay l\u00e0kk yu xere\u00f1, te amul lenn ci \u00e0ddina lees ci m\u00ebnul a wax. Ndem-si-Y\u00e0lla si, Seex Anta J\u00f3ob, ndeysaan, Y\u00e0lla na ko suuf sedde, da daan wax ne: &#8220;Aw l\u00e0mmi\u00f1 du g\u00e0tt, aw xel mooy g\u00e0tt! Ndax l\u00e9pp lu xel m\u00ebna xam ba mu leer ca moom, l\u00e0mmi\u00f1 wa m\u00ebn na koo tudd!&#8221; Te t\u00e9y jii nag nga xam ne \u00e0ddina si daa dem ba mel ni as<br \/>\nnd\u00ebkk su ndaw, xarala yu mel ni enternet ak yenneen, di def ba askan y\u00e9pp am sa\u00f1-sa\u00f1u wone seen dayoo, wone seen mbaax, seeni aada ak yoon wa \u00f1uy gisee \u00e0ddina, waru \u00f1oo nangu di d\u00e9s ginnaaw mukk!<\/p>\n<p>Dees di faral di wax nag ne aw l\u00e0kk mooy daanaka ruu wu aw askan, ndax askaan wu j\u00e8ggaani ba j\u00e9ggani aw l\u00e0mmi\u00f1, f\u00e0tte ne mi ngeek bosam, askan woowee ku yeeboo ne c\u00e0nkute gu w\u00e9r moo ko dal. Waxu \u00f1u nag ne da\u00f1oo wara t\u00ebjju ci sunu biir, du\u00f1u j\u00ebf\u00ebndikoo mbaa \u00f1uy l\u00e0kk lu dul su\u00f1u l\u00e0mmi\u00f1 yi! D\u00e9ed\u00e9et: da\u00f1uy j\u00e0ng l\u00e0kk y\u00e9pp, tambalee ko ca angale, fara\u00f1se, sinwaa ak lenneen ak lenneen, wante na nj\u00ebkka fekk \u00f1u j\u00e0ng sunu l\u00e0kk yi, di leen j\u00ebri\u00f1oo! Ndax Wolof-Njaay da ne nit ku nekk li nga moom, nga m\u00ebna damoo! Te it sax, nag, su caaxaan faaxe, d\u00ebgg d\u00e9s, \u00e0ddina s\u00e9pp daanaka noonu la\u00f1uy doxale! R\u00e9ew mu ndaw moo seet, muy Oongiri, di Soloweeni, Serbi wala menneen r\u00e9ew moo j\u00ebl ci \u00cbroop ak li ko w\u00ebr, seen l\u00e0kk yi nu moom la\u00f1uy j\u00ebf\u00ebndikoo nj\u00ebkk.<\/p>\n<p>Kon, mbokk sama, xarit sama d\u00ebgg la sax, \u00e0ddinaa dox, nasaraan juuxsi fi, di l\u00e0kk l\u00e0kkam, te naan \u00f1u ba leen seen wos! Wante nag, t\u00e9y jii \u00f1uy waxee, ci atum 2009 sunu r\u00e9ew yi \u00f1oo moom seen bopp: Kon lay jeex na, sas boobu sunu sas la! Kenn du \u00f1u ko yennul, kenn du \u00f1u sax gaar ci di j\u00ebf\u00ebndikoo sunu l\u00e0kk yi! Loolu \u00f1un do ??, waay-xeltu yi, \u00f1iy y\u00ebngu ci politik, j\u00e0ngale, koom-koom ag f\u00e0nn wu mu m\u00ebnti doon, \u00f1oo ko m\u00ebna defal sunu bopp.<\/p>\n<p>T\u00f3ol boobu nag la\u00f1u x\u00ebyy, di leen s\u00e0kku fu ngeen m\u00ebnti nekk ngeen j\u00e0ppale \u00f1u, siiwal b\u00e9r\u00e9b bi, yonnee seen xalaat ci mbir yi \u00f1u fi soxal \u00f1un \u00f1\u00e9pp.<br \/>\nWasalaam!<\/p>\n<p>Tamsir Anne \u00a9 wolof-online.com<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Mbooloo mi! \u00d1u ngi leen di nuyu ku ci nekk ci yeen ci sa tur ak sa s\u00e0nt te di leen dalal ci j\u00e0mm. B\u00e9r\u00e9b bi ngeen tersi t\u00e9y nag da\u00f1u koo s\u00e0ncc, mool ko ci kalaama wolof, jagleel ko l\u00e0mmi\u00f1 yi \u00f1u n\u00e0mp, ci r\u00e9ewum Senegaal ak ci Afrik g\u00e9pp. Yaakaar na\u00f1u ne lu&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[13,1],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1233"}],"collection":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=1233"}],"version-history":[{"count":29,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1233\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1248,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1233\/revisions\/1248"}],"wp:attachment":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=1233"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=1233"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=1233"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}