{"id":1153,"date":"2012-08-07T11:52:58","date_gmt":"2012-08-07T11:52:58","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1153"},"modified":"2012-08-08T09:04:15","modified_gmt":"2012-08-08T09:04:15","slug":"waxi-wolof-njaay","status":"publish","type":"post","link":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1153","title":{"rendered":"Waxi Wolof Njaay"},"content":{"rendered":"<p style=\"text-align: center;\"><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/kocc3.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"aligncenter  wp-image-1156\" title=\"kocc3\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/kocc3.jpg\" alt=\"\" width=\"600\" height=\"660\" \/><\/a><\/p>\n<p>Juddu ci g\u00ebl\u00e9em, n\u00e0mp ci mbaam<\/p>\n<p>Bu sunu boroom bi b\u00ebggee, \u00f1\u00e9pp \u00f1\u00e0kk<\/p>\n<p>Bant su tooyee yomb a jubbanti<\/p>\n<p>Jur\u00f3om-\u00f1eenti walaakaana soo leen b\u00ebggee jubbanti, soo moytuwul fukkeel leen<\/p>\n<p>Boroom kuddu du lakk<\/p>\n<p>Wax d\u00ebgg du w\u00e0\u00f1\u00f1i w\u00ebrs\u00ebg<\/p>\n<p>Nit ki, li nga ko g\u00ebne, booy sangu bu ko summi<\/p>\n<p>Doxkat du fekke d\u00ebju maamam<\/p>\n<p>Nj\u00ebri\u00f1 loo fekke<\/p>\n<p>Tontu du forox<\/p>\n<p>Goloo la g\u00ebn a xam k\u00ebr gu bariy xaj<\/p>\n<p>Jaam ak pexeem, Y\u00e0llaak dogalam<\/p>\n<p>Suul ker du ko teree fee\u00f1<\/p>\n<p>Lu la bett m\u00ebn la<\/p>\n<p>Ku dee ca ja ba yaa t\u00e0gge sa bopp<\/p>\n<p>Ku xamul guro moo koy baxal<\/p>\n<p>Ku \u00f1uy watat, doo taamu fi ngay teg sa ndodd<\/p>\n<p>Ku wax fee\u00f1<\/p>\n<p>G\u00e0cce gu g\u00e0tt moo g\u00ebn g\u00e0cce gu gudd<\/p>\n<p>Ng\u00e9nte bukki, gaynde du fa b\u00e0jjan, te lu dul sob y\u00f3bbuwu fa b\u00e9y<\/p>\n<p>Kenn du jiitu paaka ci mbaram<\/p>\n<p>Ku fiir ba du lekk fiiriir !<\/p>\n<p>Seelu taw moo ma g\u00ebnal seelu ngelaw<\/p>\n<p>F\u00e0ttee mag boroom<\/p>\n<p>B\u00eb\u00f1 du ree j\u00e1mm<br \/>\nKu w\u00e9et, sa baat w\u00e9ttali la<\/p>\n<p>Sikkim nga, geestoo la y\u00f3bbaale<\/p>\n<p>Wax su baree f\u00e0ww mu g\u00e9nne asaka<\/p>\n<p>Waxu mag m\u00ebn na guddee waaye du fanaan \u00e0ll<\/p>\n<p>Soo yokkee cere, yokkal \u00f1eex, bala la cee m\u00ebq di fekk<\/p>\n<p>To?-to?u naat saa yu w\u00ebreem r\u00e9ew dunq yaa tax<\/p>\n<p>Loo j\u00ebmbat yendu ci keram ba mu des nit<\/p>\n<p>Kuy l\u00e0qu di naan, soo m\u00e0ndee fee\u00f1<\/p>\n<p>Gaynde gu xiif d\u00e9ggul jat<\/p>\n<p>Foo fekk kuy puus oto, du ca dugg mukk<\/p>\n<p>Ku wax fee\u00f1<\/p>\n<p>Koo \u00ebppul mbokk m\u00ebnoo ko j\u00ebw<\/p>\n<p>Nettali mooy indi ay<\/p>\n<p>Soo xamul foo j\u00ebm, dellul fa nga j\u00f3ge<\/p>\n<p>Xol du w\u00f3om ba \u00f1u koy b\u00ebs<\/p>\n<p>Coow la ca teen ba, \u00f1a amul baag a ko waral<\/p>\n<p>L\u00e0kku jaambuur, su neexee ni t\u00e0ngal it, kenn m\u00ebnu koo macc ba ciy t\u00e0qamtiku<br \/>\n&#8211; Ay k\u00e0ddu yu x\u00f3ot yu ma daan faral a d\u00e9gg ci S\u00e9ex Anta J\u00f3ob &#8211;<br \/>\n<!--nextpage--><br \/>\nFoo d\u00e9ggee bukki bu y\u00f3oxu am na bu la jege te y\u00ebgoo ci dara<\/p>\n<p>Y\u00ebkk du taxaw \u00f1uy natt ci tungune<\/p>\n<p>Benn lam kott ci loxo du kele?-kele?i<\/p>\n<p>Su muus reggee ne jinax dafa xasaw<\/p>\n<p>\u00d1iy g\u00e0mmu ak \u00f1iy raas d\u00e9em bokkewu\u00f1u<\/p>\n<p>Bu jinne b\u00ebggee daqaar, ku y\u00e9eg daanu<\/p>\n<p>Du man, du man, fa mu \u00e0gg du yow \u00e0ggu fa<\/p>\n<p>Kiy ligg\u00e9ey mooy y\u00e0q<br \/>\nPolitig, ci \u00e0ddina la yem, kenn du ko y\u00f3bbuwaale \u00e0llaaxira<\/p>\n<p>\u00d1aari loxooy t\u00e0ccu<\/p>\n<p>Nettali ci g\u00e9mmi\u00f1u boroom la d\u00e0qe<\/p>\n<p>Koo m\u00ebnul mu\u00f1 li mu l\u00e0q doo ko sa\u00f1 a wax d\u00ebgg<\/p>\n<p>Su mbote bootoo ci gaynde tey ree, \u00f1\u00e0kk ku ko yedd a tax<\/p>\n<p>Daw ca ba ngay am i t\u00e0nk<\/p>\n<p>\u00d1aari t\u00e0nk ay dox mbokk<\/p>\n<p>Ku la y\u00e9ene xiif, saa yoo ko rombee g\u00e9exal<\/p>\n<p>Alal ganug dof la, buy \u00f1\u00ebw du t\u00e0ggoo, buy dem du t\u00e0ggoo<\/p>\n<p>B\u00e9jj\u00e9nu xaaf, ba muy m\u00e0gg bay w\u00ebnd\u00e9elu, booba mag \u00f1aa nga fa<\/p>\n<p>Doxkat du fekke d\u00ebju maamam<\/p>\n<p>Picc a moom boppam, garab gu ko neex lay tag<\/p>\n<p>D\u00ebkk\u00ebndoo bu y\u00e0gg mbokk la<\/p>\n<p>Ku la mag \u00ebpp la ay sagar<\/p>\n<p>\u00d1aar a m\u00ebn kenn te \u00f1ett du\u00f1u b\u00ebre<\/p>\n<p>Lu la mar mayul, m\u00e0tt du la ko may<\/p>\n<p>\u00d1emewuma bor, man damaa am pey &#8211; S\u00e9ex Aamadu B\u00e0mba Mb\u00e0kke, Seri\u00f1 Tuubaa &#8211;<\/p>\n<p>Ku jaaxaan di saw, noo def tooy<\/p>\n<p>Y\u00e9ene n\u00e9eg la, boroom a cay fanaan<\/p>\n<p>Bu la w\u00e9et tee nekk gor<\/p>\n<p>Ku b\u00ebgg sa taar moo la naan sangul<\/p>\n<p>Fullaay jaay daqaar walla ma mos jeexal ko.<\/p>\n<p>Ligg\u00e9eyu ndey, a\u00f1u doom<\/p>\n<p>Soo b\u00ebrewulee \u00f1u b\u00ebre daanu sa kow<\/p>\n<p>Ku boot bukki, xaj baw la<\/p>\n<p>Nd\u00ebnd mu \u00f1u t\u00ebggee s\u00e9mmi\u00f1 : neex benn yoon naqadi benn yoon<\/p>\n<p>Boroom l\u00e0mmi\u00f1 du r\u00e9er<br \/>\nWax loo m\u00ebn, def loo m\u00ebn, soo t\u00ebddee nelaw<\/p>\n<p>Y\u00f3bbante bor la<\/p>\n<p>Saaku bu feesul du taxaw<\/p>\n<p>Fu fas dul dem, xel a fay doxantu<\/p>\n<p>Gan du tabax<\/p>\n<p>Leketu kese naxul b\u00e9y<\/p>\n<p>Dof boo gis, ay nit a nga ca k\u00ebr ga mu j\u00f3ge<\/p>\n<p>G\u00f3or : fit<\/p>\n<p>Damm koon, damm koonte na daaw<\/p>\n<p>&#8211; Lat-Joor J\u00f3ob, Dammeelu Kajoor &#8211;<\/p>\n<p>B\u00ebt du yenu waaye xam na lu bopp \u00e0ttan<\/p>\n<p>Nit, nit mooy garabam<\/p>\n<p>Kanam du kaso waaye ko ci t\u00ebj mu xam ko<\/p>\n<p>Y\u00e0lla-Y\u00e0lla bey sa tool<\/p>\n<p>S\u00e1cc tama yomb na, xanaa am foo ko t\u00ebgge mooy jafe<\/p>\n<p>Kuy d\u00f3or-d\u00e0qe ak sa xel, du \u00f1\u00e0kk nga dem ba foo n\u00ebbbu xaw laa jaaxal<\/p>\n<p>Bo y\u00ebkkatee sa benn loxo ne faalewuma kenn, boo yaboo y\u00ebkkati ba ca des ne kenn faalewu ma<\/p>\n<p>Buur aayul, dag yaa aay<\/p>\n<p>Gunge bu y\u00e0gg defarul teeru bu \u00f1aaw<\/p>\n<p>Deret jaxasoo, xaste jeex<\/p>\n<p>Kay s\u00e0mm mbott moo xam ba cay soox<\/p>\n<p>Woyu biir kenn m\u00ebnu koo awu<\/p>\n<p>Boo amee sa xaritu gun\u00f3or, bu ko s\u00e0nni ci kekk li<\/p>\n<p>Liir du wonk<\/p>\n<p>Yakk ba la fekk fande moo g\u00ebn ci yakk yi<\/p>\n<p>Bu till lekkee alom, na ko g\u00ebr\u00ebme coy<\/p>\n<p>B\u00e9s du mag du tuuti, boroom lay tollool<br \/>\nBa\u00f1 ba\u00f1 b\u00ebgg<\/p>\n<p>\u00c0tte Y\u00e0llaa g\u00ebn bu nit<\/p>\n<p>Lu defu waxu te luy ay di j\u00e0mbat<br \/>\n<!--nextpage--><br \/>\nLuy jot jot na, ginnaaw dee<\/p>\n<p>Kuy woddoo l\u00e0mmi\u00f1, soo noppee rafle<\/p>\n<p>Wuude, lu mu wax ci feebaru b\u00e9y, der baa ko waral<\/p>\n<p>Xaalis du faj dee, g\u00e0cce lay faj<\/p>\n<p>Ku j\u00e0ppul ci yatu getax, doo am yatu kel<\/p>\n<p>Y\u00e0lla bindul ku dul dee waaye bind na ku dul torox<\/p>\n<p>L\u00e0mmi\u00f1 du t\u00e0nk waaye dina tarxiis, g\u00e9mmi\u00f1 du furno waaye dina boy<\/p>\n<p>Nag wu \u00f1uul ku ci am meew mu weex war a s\u00e0nt<\/p>\n<p>Alal na mag boroom, ndax su \u00f1u maasee \u00f1oom \u00f1aar y\u00e9w\u00e9n ci day daldi jafe<\/p>\n<p>Ndimbal na ca fekk loxol boroom<\/p>\n<p>K\u00ebr baay du k\u00ebr<\/p>\n<p>Su b\u00ebn dee see\u00f1u yax, suux saa tax<\/p>\n<p>Bala ngaa xam xamadi xaw la rey<\/p>\n<p>Wax d\u00ebgg du w\u00e0\u00f1\u00f1i w\u00ebrs\u00ebg<\/p>\n<p>Doxkat du fekke d\u00ebju maamam<\/p>\n<p>Nj\u00ebri\u00f1 loo fekke<\/p>\n<p>Jaam ak pexeem, Y\u00e0llaak dogalam<\/p>\n<p>Ay du weesu baay dee na<\/p>\n<p>Lu jot yomb<\/p>\n<p>Kiy ligg\u00e9ey mooy y\u00e0q<\/p>\n<p>Politig, ci \u00e0ddina la yem, kenn du ko y\u00f3bbuwaale \u00e0llaaxira<\/p>\n<p>\u00d1aari loxooy t\u00e0ccu<\/p>\n<p>Nettali ci g\u00e9mmi\u00f1u boroom la d\u00e0qe<\/p>\n<p>Koo m\u00ebnul mu\u00f1 li mu l\u00e0q doo ko sa\u00f1 a wax d\u00ebgg<\/p>\n<p>Su mbote bootoo ci gaynde tey ree, \u00f1\u00e0kk ku ko yedd a tax<\/p>\n<p>Daw ca ba ngay am i t\u00e0nk<\/p>\n<p>\u00d1aari t\u00e0nk ay dox mbokk<\/p>\n<p>Ku la y\u00e9ene xiif, saa yoo ko rombee g\u00e9exal<\/p>\n<p>Alal ganug dof la, buy \u00f1\u00ebw du t\u00e0ggoo, buy dem du t\u00e0ggoo<\/p>\n<p>Ku la mag \u00ebpp la ay sagar<\/p>\n<p>Ku b\u00ebgg sa taar moo la naan sangul<\/p>\n<p>Ligg\u00e9eyu ndey, a\u00f1u doom<\/p>\n<p>Soo b\u00ebrewulee \u00f1u b\u00ebre daanu sa kow<\/p>\n<p>Fu fas dul dem, xel a fay doxantu<\/p>\n<p>Dof boo gis, ay nit a nga ca k\u00ebr ga mu j\u00f3ge<\/p>\n<p>La muy saf ka ko macc a ko xam<\/p>\n<p>Kuy yoot du s\u00ebqat<\/p>\n<p>Ba la ngaa pes s\u00e0mm bi xaaral ba xam lu muy w\u00ebliis<\/p>\n<p>Kenn du j\u00ebnd jaan ci pax<\/p>\n<p>Lu fee\u00f1 ci s\u00e9y, nuyoo na ca ndoxaan la, xanaa kay da\u00f1u koo feyul woon rekk<\/p>\n<p>Alalu golo ca lex ba<\/p>\n<p>Ku ne \u2018w\u00eby\u2019* tey jii, dinga ne \u2018w\u00f3oy\u2019 \u00ebll\u00ebg &#8211; S\u00e9ex Anta J\u00f3ob &#8211;<br \/>\n*w\u00eby mooy \u2018oui\u2019 ci nasaraan. Mooy jamono ja Se?oor nee \u00f1u woteel ko,<br \/>\nte S\u00e9ex Anta di artu waa Senegaal, naan leen ku defal Se?oor li mu<br \/>\nb\u00ebgg dinga ko r\u00e9ccuji \u00ebll\u00ebg.<\/p>\n<p>Wa\u00f1\u00f1i boo gis ci benn lay doore<\/p>\n<p>Ay du yem ci boppu boroom<\/p>\n<p>Lu kenn m\u00ebn, \u00f1aar a la ko d\u00e0q. Ba mu des lan ? Xanaa&#8230; w\u00e9et !<\/p>\n<p>B\u00ebgg naa la, b\u00ebgguma la, loolu jarul coow &#8211; Njaga Mbay, woykat &#8211;<\/p>\n<p>Mbeju kanam boroom a koy fajal boppam<\/p>\n<p>Montar yu baax y\u00e9pp a bokk waxtu<\/p>\n<p>B\u00f3li gu dog tii\u00f1 na doktoor<\/p>\n<p>Ku jaan m\u00e1tt sam xel dem ci dee, ba ngay dund ak ba ngay dee y\u00e9pp sam xel dem ci dee<\/p>\n<p>Saabu du f\u00f3ot boppam<\/p>\n<p>D\u00ebr\u00ebm ak d\u00ebr\u00ebm \u00f1oo m\u00ebn a \u00e0nd<\/p>\n<p>Tere-tere mu t\u00eb, b\u00e0yyil mu gis<\/p>\n<p>Y\u00e1gg dox, y\u00e1gg gis<\/p>\n<p>Mbamb du weesu weer<\/p>\n<p>Ku mu\u00f1, muu\u00f1<\/p>\n<p>Ku m\u00ebnul bawoo, lu y\u00e1qu yowa<\/p>\n<p>Ku m\u00ebn te defoo, lu y\u00e1qu yowa<\/p>\n<p>Waa d\u00ebkk bee xam lu ndoxu teen biy saf<\/p>\n<p>\u00d1aq du fee\u00f1 ci taw bi<\/p>\n<p>Werante xuuxaan tekki tub\u00e9y<\/p>\n<p>Xuloo s\u00ebn la, lu waay jot s\u00e1nni sa moroom<\/p>\n<p>Naar ba noon na : b\u00e9s bu ma amee, k\u00e9pp ku ma xamoon ba ma \u00f1\u00e0kkee, yal na nga dee<br \/>\n<!--nextpage--><br \/>\nKu \u00f1\u00e9pp t\u00ebfli nga tooy<\/p>\n<p>Lu waay rendi ci sa loxo lay n\u00e1cc<\/p>\n<p>B\u00ebgg naa la du yaa ma g\u00ebnal sama bopp<\/p>\n<p>Purux du g\u00ebr\u00ebm \u00f1amu daaw<\/p>\n<p>B\u00e9y ci sa wewu t\u00e0nk<\/p>\n<p>Ku nd\u00f3bin rey sa maam, foo s\u00e9ene lu \u00f1uul daw<\/p>\n<p>Daw ca ba ngay am i t\u00e0nk<\/p>\n<p>Loo gis ci nettali lay mujje<\/p>\n<p>Ku b\u00ebreey daan<\/p>\n<p>Ku b\u00ebreey daanu<\/p>\n<p>Werante gis bokku ci<\/p>\n<p>Weddi gis bokku ci<\/p>\n<p>Ku \u00f1uy tam d\u00ebmm ngay see\u00f1oo yeelu liir<\/p>\n<p>Mb\u00ebr mu ndaw moo may d\u00ebkk waaye mb\u00ebr mu mag a may daan<\/p>\n<p>Ku w\u00e1cc sa and, and boo y\u00e9eg mu toj<br \/>\nDina m\u00e1tte ak du m\u00e1tte, bul jox sa loxo<\/p>\n<p>Pexe deesu ko weer<\/p>\n<p>Kuy yoot du s\u00ebqat<\/p>\n<p>Ku mar tax a naan p\u00f3tit, bu ndox tuuroo nga rus<\/p>\n<p>Ku w\u00e1cc sa and, and boo dem fekk ca boroom<\/p>\n<p>\u00d1\u00e1kk bopp gaaw a dee<\/p>\n<p>S\u00e9ddoo, ca kuddu yu j\u00ebkk ya<\/p>\n<p>Wuude bi ni mu la gise la lay \u00ebwale<\/p>\n<p>Mag mu \u00f1u dab mbej ko, ca doxin wa la<\/p>\n<p>Saay-saay waxul d\u00ebgg waaye y\u00e1q na xel<\/p>\n<p>Ku yar sa kuy yow lay j\u00ebkk a mb\u00ebkk<\/p>\n<p>\u00c1ddina du cere waaye dees koy laalo<\/p>\n<p>Gune gu yaroo macc t\u00e0ngal<\/p>\n<p>\u00d1aari kuuy m\u00ebnu \u00f1oo bokk benn mbalka<\/p>\n<p>Fa nga fekk baax, fa la baax fekk moo ko g\u00ebn<\/p>\n<p>Lu \u00ebpp tuuru<\/p>\n<p>Booy dee ca \u00e0ll ba, na la gaynde rey<\/p>\n<p>K\u00f3ll\u00ebre ginnaaw lay f\u00e9ete<\/p>\n<p>Liir, bu feccam neexee, yaay jaa j\u00e1pp ca mbagg ya<\/p>\n<p>Lu dul d\u00ebgg du y\u00e1gg<\/p>\n<p>Gisee tasoon Kajoor<\/p>\n<p>D\u00ebkk\u00ebndo bu y\u00e1gg mbokk la<\/p>\n<p>Mbeju kanam boroom a koy fajal boppam<\/p>\n<p>Ku amul yaay n\u00e0mp maam<\/p>\n<p>Ay garab ca kow la\u00f1uy daje<\/p>\n<p>D\u00ebkk\u00ebndoo dina w\u00e0lle ba ciy doxat<\/p>\n<p>Xam nit, xam jikkoom a ko g\u00ebn<br \/>\nNit \u00f1i xamu\u00f1u ku too\u00f1, ku feyu la\u00f1u xam<\/p>\n<p>Gumba tal naa leneen lu dul t\u00ebbaani ay teen<\/p>\n<p>Gaynde b\u00ebggul mbuum, y\u00e0pp lay dunde (Y\u00e0nde Koddu Seen, woykat)<\/p>\n<p>Fer\u00f1eent m\u00ebn naa taalug daay<\/p>\n<p>Dikkleen, bukki for na almet, tey \u00e1ll bi leer ! !<\/p>\n<p>Garab gu la sutul du la may keppaar<\/p>\n<p>Ginnaaw ay, j\u00e1mm<\/p>\n<p>Yaa fi s\u00ebs doynag pal<\/p>\n<p>Nj\u00e0ng moo gis am na \u00e1llarba<\/p>\n<p>Koo m\u00ebn a yaakaar, Y\u00e1lla la yaakaar<\/p>\n<p>Lafa\u00f1 boroom mbaam lay faral<\/p>\n<p>Kuy jaay keppaar ba t\u00e0kkusaan jot, nga war a w\u00e0\u00f1\u00f1i sa nj\u00ebg<\/p>\n<p>Doxati g\u00ebl\u00e9em kow la j\u00ebm<\/p>\n<p>Donn sa baay, doon sa baay a ko g\u00ebn<\/p>\n<p>Nit ak jikkoom ba ci biir b\u00e1mmeel<\/p>\n<p>Bu sindax yabee ndobin, booba garab moo fa jege<\/p>\n<p>Waay soo m\u00ebnulee sarax kiy yalwaan bul siif li mu jot a fortaatu !<\/p>\n<p>Ndimbal na ca fekk loxol boroom<\/p>\n<p>D\u00e1q ginaar waxaale sa soxla<br \/>\n<!--nextpage--><br \/>\nS\u00e9y dagan na, fase dagan na<\/p>\n<p>Ku m\u00ebnul may sa bopp, lu la Y\u00e1lla may nga j\u00ebl<\/p>\n<p>Kenn du b\u00ebgg ginaar ba noppi di ba\u00f1 ay nenam<\/p>\n<p>\u00c1ddina : dund, dee<\/p>\n<p>Ku j\u00ebkk yeewu boroom nd\u00e9kki, war a t\u00ebddaat<\/p>\n<p>Kumbay ba\u00f1 S\u00e0mbay rasu !<\/p>\n<p>Purux du g\u00ebr\u00ebm \u00f1amu daaw<\/p>\n<p>Koo xamul, \u2018\u00e9ey\u2019 nga koy woowe<br \/>\nKenn du toog ci der di j\u00ebw y\u00e1pp<\/p>\n<p>Doom nawle la, jabar nawle la<\/p>\n<p>S\u00e9dd\u00eble Bukki: bii Bukki, bii Njuur, bii S\u00e0mba, bi ci des nag ku ci j\u00ebkk yaa<br \/>\nmoom te teg naa ci loxo!<\/p>\n<p>Ku w\u00e9eruwul fenn yomb a b\u00ebm\u00ebx<\/p>\n<p>Ku jooyul n\u00e9ew xaana ba\u00f1 a wa\u00f1aar loxoom<\/p>\n<p>\u00d1\u00e0kk xam gaynde weesuwul naan danga koy takke buum<\/p>\n<p>Jaan d\u00ebngul, doxin waa jubadi<\/p>\n<p>\u00d1u bokkul teen du\u00f1u laxasoo ay goj<\/p>\n<p>Ku dul tukki, doo xam fu d\u00ebkk neexe<\/p>\n<p>Ku i\u00f1aane sa ndono sa dee \u00f1aaw<\/p>\n<p>Du man do??, bokkuma cee ko g\u00ebn<\/p>\n<p>Ku b\u00ebgg akara dangay \u00f1eme kaani<\/p>\n<p>Waane weesuwul ne dangay nettali sa g\u00e9ntu moroom<\/p>\n<p>Ni nga b\u00ebgg sa waay mel ko, du ko mel mukk, sa waayu-waay a koy mel<\/p>\n<p>Xew xewi aayul, \u00f1akk mas a xew moo aay<\/p>\n<p>Y\u00e0gg bawul dara<\/p>\n<p>Yax bu r\u00e9y gobar toju ko &#8211; Njaga Mbay, woykat &#8211;<\/p>\n<p>\u00c0ddina potu ndaa la, ku naan jox sa moroom<\/p>\n<p>\u00c0ddina nii rekk la : demal maa ngi \u00f1\u00ebw<\/p>\n<p>Fen buy defar moo g\u00ebn d\u00ebgg guy y\u00e0q<\/p>\n<p>Ku \u00f1u fey sa bor nga mer, booba la nga leble woon jagul<\/p>\n<p>Gaalu dof du teer, mbaa bu teeree it du doon fu neex mbokk ya<\/p>\n<p>Saay-saay waxul d\u00ebgg waaye y\u00e0q na xel<\/p>\n<p>Dof sonnul, mbokk yaa sonn<\/p>\n<p>Ku nekk sa xetu ngemb doyna lam p\u00f3ot<\/p>\n<p>Ku nar a xaru d\u00ebgg doo t\u00e0ggoo<br \/>\nNii laa defoon day yokk s\u00e0gganu<\/p>\n<p>Lu defu waxu, lu aay dib j\u00e0mbat<\/p>\n<p>Njaboot jaamukaayu Y\u00e0lla la<\/p>\n<p>Soo xamoon li lay yoot, nga b\u00e0yyi la ngay yoot te jublu li lay yoot<\/p>\n<p>Ku am ndey am baay<\/p>\n<p>Gan yomb naa mu\u00f1al<\/p>\n<p>Bu sa t\u00e0nk bare fa sa doom di s\u00e9ye waaye bu fa sa loxo di g\u00ebj<\/p>\n<p>\u00d1\u00e0kk xam li mu waral bare na<\/p>\n<p>Loo xamul suuram xiifam m\u00ebnu laa rey<\/p>\n<p>Foo jublu y\u00e0lla na fa yiwu Y\u00e0lla jublu<\/p>\n<p>Aa ! Laaj nga mbott geenam !<\/p>\n<p>Fu mu yem neex<\/p>\n<p>Dem ba jeex<\/p>\n<p>Su fi yemoon sax neex<\/p>\n<p>Bu dee ay nax sax neex na<\/p>\n<p>Dikkleen waay ! Goloo ngi xastey daar-daar !<\/p>\n<p>Lu ma ci g\u00f3ob, gar ko<\/p>\n<p>Na sa ngelaw neex !<\/p>\n<p>Wax waxu ku daanoo ci saret<\/p>\n<p>Bul ma ne maam benn b\u00eb\u00f1 laa wax !<\/p>\n<p>Waaw, lu w\u00e0nq di dox noor ?<\/p>\n<p>Nit \u00f1i da\u00f1 leen a nax ba soo leen waxee d\u00ebgg sax tas seen yaakaar &#8211; S\u00e9ex Anta J\u00f3ob &#8211;<\/p>\n<p>T\u00e0nn sa bu la neex<\/p>\n<p>Di niitu ba faf lakk<\/p>\n<p>L\u00e0mbi goloo ! Ku j\u00f3g daanu ndax golo yaa ko moom !<\/p>\n<p>Golo w\u00e0ccal gaynde y\u00e9eg !<\/p>\n<p>Boo s\u00e0nnee mb\u00e0ttu mu tag<br \/>\nBu dee jotee&#8230;<\/p>\n<p>Nii mbaa nee rekk<\/p>\n<p>Su ma y\u00ebggoon a nga nee di dem !<\/p>\n<p>Dof ba dafa ne : xool-leen weer waa nga nee. \u00d1u ne : kii kat dara jotu ko, ndekete.<br \/>\nMu newaat : beneen weer waa nga nee ci wetam !<\/p>\n<p>Ku loxoom jotul diggu ginnaawam<\/p>\n<p>Suul bukki, sulli bukki<\/p>\n<p>Su ngeen mbaam-mbaamloo, ma lawbe-lawbe lu &#8211; Mamadu Ja &#8211;<\/p>\n<p>B\u00ebtu tan j\u00e9ggi na m\u00e9ddu sanqale\u00f1* &#8211; S\u00e9ex Anta J\u00f3ob &#8211;<br \/>\nK\u00e0ddu yu Seex Anta daan faral a y\u00ebkkati, j\u00ebmale ko ci askan wi, jamono ca ka Se?oor<br \/>\ndaan j\u00e9em a j\u00ebnd ak ay ndomboy-t\u00e0nk ndax rekk b\u00ebgg a jubook moom&#8230;<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Juddu ci g\u00ebl\u00e9em, n\u00e0mp ci mbaam Bu sunu boroom bi b\u00ebggee, \u00f1\u00e9pp \u00f1\u00e0kk Bant su tooyee yomb a jubbanti Jur\u00f3om-\u00f1eenti walaakaana soo leen b\u00ebggee jubbanti, soo moytuwul fukkeel leen Boroom kuddu du lakk Wax d\u00ebgg du w\u00e0\u00f1\u00f1i w\u00ebrs\u00ebg Nit ki, li nga ko g\u00ebne, booy sangu bu ko summi Doxkat du fekke d\u00ebju maamam Nj\u00ebri\u00f1&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[6,27],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1153"}],"collection":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=1153"}],"version-history":[{"count":24,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1153\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1571,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1153\/revisions\/1571"}],"wp:attachment":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=1153"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=1153"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=1153"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}