{"id":1080,"date":"2020-12-29T11:10:27","date_gmt":"2020-12-29T11:10:27","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1080"},"modified":"2021-02-06T19:11:36","modified_gmt":"2021-02-06T19:11:36","slug":"neel-seex-anta-joob","status":"publish","type":"post","link":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1080","title":{"rendered":"\u00d1eel Seex Anta J\u00f3ob"},"content":{"rendered":"<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/clabo.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"alignleft size-full wp-image-1082\" title=\"clabo\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/clabo.jpg\" alt=\"\" width=\"200\" height=\"118\" \/><\/a>Ligg\u00e9ey bu mel ni bii \u00f1u fi d\u00ebgmal, wareef la ci sunu gis-gis, \u00f1u \u00f1eel fi ca ndorte la g\u00f3or gu mel ni Seex Anta J\u00f3ob. Ndax daf fee def, lu fi daanaka kenn ci waay-xeltu yi ci Afrik ak li ko w\u00ebr deful: maanaam yesalaat yoon wi \u00e0ddina s\u00e9pp doon gise cosaanu nit ku  \u00f1uul, fa mu jaar ca nj\u00eblb\u00e9en ba yegsi fi mu tollu t\u00e9y. {mosimage}Callalal-cosaan jooju la Seex Anta J\u00f3ob topp, dalee ko ca jamono yi nit ku xay, maanaam &#8220;homo sapiens&#8221; ci late?, fee\u00f1e ci d\u00e9ndu Afrik ba jamonooy t\u00e9y.<\/p>\n<p>Li tax mbir  moomu di lu am solo, mooy ne boroom xam-xam yu bare ci tubaab yi ak seeni ndongo yu \u00f1uul da\u00f1oo j\u00e0ppoon ci kow f\u00f3ogi kese, ne nit ku \u00f1uul daal cosaanam kenn m\u00ebneesu ko leraal ndax bindul. Rax ci dolli it, \u00f1oo\u00f1u ne, li fi suuf si goqi ci ay tabax yu y\u00e0gg te kemaane, ca Misira, Nibi, Simbaabwe, Nok ak fenneen, li w\u00f3or mooy wenneen xeet moo fi juuxsiwoon, def ko. Ndax nit ku \u00f1uul xameewu \u00f1u ko lu dul roy, njaam ag di w\u00e9y ci ndigg\u00eblu kenneen.<\/p>\n<p>T\u00e9y, ba Seex Anta \u00f1\u00ebwee, w\u00e9er ay g\u00ebstoom ci xam-xam bu w\u00e9r, ay firnde yu kenn m\u00ebnula n\u00e0ttable, leer na ne nit ku \u00f1uul moo nj\u00ebkka nite ci \u00e0ddina, moo nj\u00ebkka bind, moo nj\u00ebkka tabax. Fi sax faf, ci Afrik la Y\u00e0lla t\u00ebnee sunu Maam Aadama, ba ay s\u00ebt-s\u00ebtaatam joge fi dem d\u00ebkki fenneen, melokaanam ag deram d\u00f3og di sopiku!  Xarala, xam-xam, tabax yi nekk fii Misira ak fenneen it ci Afrik te di yeem niteef gi, du kenn ku moy sunu maam yi \u00f1oo ko fi def.<\/p>\n<p>Wante dafa am benneen f\u00e0nn bu am solo ciy g\u00ebstu S\u00e9ex Anta sees di faral di umpale. Ndax bokk na ca la mu nj\u00ebkka bind g\u00ebdd gi l\u00e0kki-r\u00e9ewi Afrik wara dellu am, ba m\u00ebna dellu nekkaat ay juntukaay yu mat yuy j\u00ebm\u00eble askan yi ca kanam. S\u00e9ex Anta masul a j\u00f3g di bind, di g\u00ebstu ci wolof ak yenneeni l\u00e0kki Afrik yi. Ci kow loolu la tekki xeeti xam-xam yu nekk ci wolof: Dalee ko ci xam-xamu yaramal, simi, xayma, mbindum-f\u00e9nt ak yenneen ak yenneen. Naka noonu ci t\u00e9ereem bi  nj\u00ebkka siiw di &#8220;Nations n\u00e8gres et cultures&#8221; &#8211; maanaam &#8220;Waaso nit ku \u00f1uul ag caada&#8221; la t\u00e0mbalee tekki  faramf\u00e0cci-ajoodiku walla &#8220;th\u00e9orie de la relativit\u00e9&#8221; bu Einstein, di ki nga xam ne daanaaka xam-xamam \u00e0ddina s\u00e9pp la yeem ba t\u00e9y!<\/p>\n<p>Loolu y\u00e9pp li mu ca masoon na jublu moo doon wone pexe yi  l\u00e0xxu ci  sunu l\u00e0kk, te amul sax benneen l\u00e0kk bu mu m\u00ebnti doon ci \u00e0dduna bu leen ca yobul dara.<\/p>\n<p>Su s\u00f3obee Y\u00e0lla dana \u00f1u fi dellusi g\u00ebna siiwal bindi Seex Anta J\u00f3ob yooyu \u00f1u bare umpale.<\/p>\n<p>Kon teranga \u00f1eel na \u00f1ayu xare jooju j\u00ebfam aki xalatam dootul reer ba f\u00e0ww!<\/p>\n<p>Tamsir Anne \u00a9 wolof-online.com<\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Ligg\u00e9ey bu mel ni bii \u00f1u fi d\u00ebgmal, wareef la ci sunu gis-gis, \u00f1u \u00f1eel fi ca ndorte la g\u00f3or gu mel ni Seex Anta J\u00f3ob. Ndax daf fee def, lu fi daanaka kenn ci waay-xeltu yi ci Afrik ak li ko w\u00ebr deful: maanaam yesalaat yoon wi \u00e0ddina s\u00e9pp doon gise cosaanu nit ku&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":0,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[6,13,1],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1080"}],"collection":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=1080"}],"version-history":[{"count":8,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1080\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":1296,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1080\/revisions\/1296"}],"wp:attachment":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=1080"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=1080"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=1080"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}