{"id":1015,"date":"2022-11-01T09:00:00","date_gmt":"2022-11-01T09:00:00","guid":{"rendered":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1015"},"modified":"2024-02-29T15:48:55","modified_gmt":"2024-02-29T15:48:55","slug":"xasida-serin-tuuba-ci-wolof-nahjul-xadaail-haaji-wolof","status":"publish","type":"post","link":"http:\/\/www.wolof-online.com\/?p=1015","title":{"rendered":"Xasida S\u00ebri\u00f1 Tuuba ci Wolof : Nahjul Xadaail Haaji &#8211; Wolof"},"content":{"rendered":"<blockquote><p>Maa ngi t\u00e0mbale samay wax ak j\u00ebf ci turu Y\u00e0lla miy kiy boroom y\u00ebrmande ju yaa ji ci adduna ak ja ca allaaxiraa. Yal na Y\u00e0lla dolli x\u00e9ewal ak mucc ci su\u00f1u s\u00e0ng Muhammad ak ci \u00f1o\u00f1am aki saabaam ci anam yu sax Y\u00e0lla doy na \u00f1u, moom de w\u00e9eruwaay wu baax la, wu mat a w\u00e9er say mbir, joyal ko ko. J\u00ebf yaa ngi ci y\u00e9ene yi, ku nekk it la nga y\u00e9eneey sag pay.<br \/>\nBokk na ci hikam (sagesse) : ku s\u00e0kku mbir de bu ca saxee am ko. Ku f\u00ebgg bunt it boo fa saxee ubbilees la.<br \/>\nBokk na ci hikma ba t\u00e9y: ku t\u00ebyye boppam w\u00eblif neen yi (caaxaan yi ) limees ko mu bokk ci boroom xel yi.<br \/>\nBokk na ci ba leegi: ku dul merloo boppam du begloo boroomam.<br \/>\nBokk na ci ba t\u00e9y : ku def la ko soob dajeek la ko naqari.<br \/>\nBokk na ci: ku taqook jiyaar ak bakkanam, texe fa biir b\u00e0mmeelam .<br \/>\nBokk na ci : ku topp Yonnant bi, am g\u00ebn ji la mu \u00f1aan.<br \/>\nAm ku j\u00ebl maanaa yii y\u00e9pp boole leen ci wenn bayit : k\u00e9pp ku woor w\u00eblif caaxaan yi danga dogi ciy ng\u00ebn\u00e9el.<\/p><\/blockquote>\n<p><a href=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/serigne_touba.jpg\"><img loading=\"lazy\" decoding=\"async\" class=\"alignleft  wp-image-1016\" title=\"serigne_touba\" src=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/serigne_touba.jpg\" alt=\"\" width=\"272\" height=\"400\" srcset=\"http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/serigne_touba.jpg 272w, http:\/\/www.wolof-online.com\/wp-content\/uploads\/2012\/06\/serigne_touba-204x300.jpg 204w\" sizes=\"(max-width: 272px) 100vw, 272px\" \/><\/a><strong>1 Taalif wi<\/strong><br \/>\nTaaliif wii nag lu \u00f1u barkeel la ci nj\u00eblb\u00e9en gi ba ca dayo ba. Moom nag, ki waxoon bayit wu nj\u00ebkk wi \u2013yal na\u00f1u ko dolli ag b\u00ebbb (x\u00e9ewal) \u2013 am na ba tay weneen bayit wu yor maanaa, mu ciy nos (woy) maanaam waxi s\u00ebri\u00f1am ji, wax jooju mooy jii : (nguurug neen waxtu rekk la, nguurug d\u00ebgg nag day wey ba yawmal-xiyaam).<br \/>\nWoy waa ngii : d\u00ebgg day sax , neen nag bu kawe woon it day mujj naaxsaay, mujj suufe.<br \/>\nMaa ngi t\u00e0mbale samay wax ak j\u00ebf ci turu Y\u00e0lla miy boroom y\u00ebrmande ju yaa ji ci adduna ak ja mu \u00f1u jagleele ji ca allaaxiraa<\/p>\n<p><strong>2 Ubbite gi<\/strong><br \/>\nKii di doomi s\u00ebri\u00f1am ji dul s\u00e0nt ci boppam lu dul turam wu tedd wa, Muhammad,<br \/>\nKii de mi ngi sant Y\u00e0lla (t.m) mi suturaal ay ayibam te taxawu ko te dimbali ko.<br \/>\nTudd naa sellam ga moom de Boroom bu tedd la bob may na ma lu waral ma koy s\u00e0nt. Moom de mooy ki def ay teggin yu raf muy luy l\u00e0q ag reer ak judd bu \u00f1aaw (bonu askan).<br \/>\nMooy ki jagleel boroom xam-xam yeek teggin, mooy ki l\u00e9en jagleel ab yool akug jam-jub (def la jub).<br \/>\nX\u00e9ewal ak mucc gu kawe na\u00f1u sottiku ca ka y\u00e9egoon ca Alburaax.<br \/>\nKooku mooy su\u00f1u s\u00e0ng biy woote j\u00ebme ci Aji-bind ji (Ki s\u00e0kk mbindeef yi), defee ko nag ci g\u00ebn jaa rafeti teggin yi .<br \/>\nKooku mooy Muhammad ak \u00f1o\u00f1am \u00f1i di woroomug raw ak saabaam yi l\u00e0q ng\u00ebn\u00e9elul Aji-des-ji (Y\u00e0lla mi fi dul jug).<br \/>\n\u00d1oom saaba yooyu de saxaloon na\u00f1u ag laa-biire ci lu dul \u03b7aayoo , ndaxte da\u00f1oo toroxaloon seeni bakkan ba far leen moom.<br \/>\nS\u00e0nkoon na\u00f1u seeni alal cig joxe ci lu dul ngistal mbaa naaf\u00e9q. \u00d1u sukkandiku woon ci Aji-jari\u00f1 (Y\u00e0lla) jiy Aji-w\u00ebrs\u00ebgale, ngir ag wakkiirlu ci moom ci mbooleem w\u00ebrs\u00ebg yi. \u00d1oom de da\u00f1oo boyoon j\u00ebm alaaxlenniraa ngir ne da\u00f1oo fase woon wujj wa (adduna). Masu\u00f1oo b\u00e0yyi lenn ndigal lu juge ci Aji-settantal ji (kiy def mbir yi di Yalla), kiy Aji-bind ji.<br \/>\n\u00d1oom de &#8211; ci safaanub \u00f1uy b\u00e0yyi ndigal yi &#8211; da\u00f1u ciy sax \u00e0nd ceek b\u00e0nneex, ndaxte koomum ja du tax \u00f1u koy f\u00e0tte (alal ji \u00f1uy j\u00eble ci marse yi du\u00f1u tax \u00f1uy f\u00e0tte ndigali su\u00f1u boroom yi) .<br \/>\nWu\u00f1\u00f1i woon na\u00f1u l\u00ebnd\u00ebm-l\u00ebnd\u00ebmi gox yi ci xam-xam ak j\u00ebf ak d\u00ebppoo. Ndaw \u00f1u di s\u00e0ng yu \u00f1aw !<br \/>\n\u00f1oom de la neexoon ca cafka ga j\u00ebl navu ko. Yal na ng\u00ebr\u00ebm &#8211; lol di naa ci dajeek \u00ebl\u00ebg ka l\u00e0q cang gu joyu ga \u2013 sottiku ci seen kaw .<br \/>\nKooka mooy Muhammad, yal na ko Aji-des-ji sotti ay x\u00e9ewal ak mucc mook \u00f1o\u00f1am ak saabaam yi di ay ndab yuy duy xam-xam aki xeewal aki hikam<\/p>\n<p><strong>3 Li waral xasida gi<\/strong><br \/>\nMan dey t\u00e9y damaa \u00f1\u00ebw ngir wuyyu lenn ci murid yi di woroomi tuub (\u00f1iy tuub ak a j\u00e9ggalu seen Boroom). \u00d1oom de da\u00f1oo s\u00e0kku woon \u00f1u defal leen woy wuy j\u00e0ngale ay teggin, ngir \u00f1u s\u00e0kkoo ciy teggin, te loolu wart\u00e9ef la . Ndax kat k\u00e9pp ku b\u00ebgg a topp Yonnant bi te tegoo ko ciy teggin dees na ko xa\u00f1 ag texe akug jari\u00f1u.<br \/>\nMoom teggiin de &#8211; ci \u00e0dduna ak allaaxiraa \u2013 mooy g\u00ebn ji nd\u00e0mb tey g\u00ebn ji lu ku tedd di tedde. Ndaxte mooy leeral ab xol tey jegeele \u00e0jjana. Dina waral say d\u00ebkkandoo di la t\u00e0gg te dina sooreel it sawara. Ma daal di jug ngir s\u00e0kku gi \u00f1u ko s\u00e0kku woon ci man gaawantu, tontu leen, di ci s\u00e0kku nag ab yool ak ng\u00ebr\u00ebm.<br \/>\nMoom nag du lu dul j\u00ebl la Waliya wa tuddoon Dal-Haaji wesaroon (manaam la mu bindoon te woyu ko, maanaam defu ko woon ay bayit ) def ko ay woy, di \u00f1aan ci def gi Y\u00e0lla fajal ma samay aajo<\/p>\n<p><strong>4 Lu tax ma taamu ko ?<\/strong><br \/>\nNdax dafa boole \u2013 ba noppi g\u00e0ttal ko \u2013 li \u00ebpp ci li taalifkat yu nj\u00ebkk ya bindoon cig t\u00e0qale. L\u00e9pp loo gis mu n\u00e9ew te doy moo g\u00ebn lu bari te sonnale. Def naa ko nag woy wu ami njari\u00f1, ci baaxug Y\u00e0lla mi dige ci Alxuraan ne dana aar \u00f1i g\u00ebm. Ndax Y\u00e0lla may ma ci ng\u00ebr\u00ebm ak k\u00f3olute ak nj\u00e9ggal ca bisub nj\u00e0qare ba. Kon kat yeen s\u00e0kkukati xam-xam yi maa ngi leen di d\u00e9nk te dellu di leen d\u00e9nk te di leen xiirtal ci tontu bii (t\u00e9ere Nahju bii) Ndax kat yor na ci ay jikko aki teggin lool: bu ngeen ci t\u00ebnkoo dina leen wommat j\u00ebme leen ca jub ga. Ay gindee ngi ci aki njari\u00f1 yooy boroomug-nammeel (ab murid) du ci yoqat mukk. Kuy door a dal ak kaa\u03b7f\u00f3oree yam ciy njari\u00f1am, aw yiiwam it du jeex mukk. Ndaxte ni \u00f1uy \u00e0gge ci G\u00ebn-jaa-rafeti jikko yi mi ngi ci ak ca (lu baax) la \u00f1uy m\u00e9b\u00ebt. Maa ngi ko tudde: Nahju QadaaAl Haaji ci g\u00f3ob mbayum su\u00f1u s\u00ebri\u00f1 bii di Dal-Haaj. Maa ngi \u00f1aan Y\u00e0lla mu nangu ko ca baaxam ga te \u00e0ggale ligg\u00e9ey bi. Di ko \u00f1aan it mu mel ne turam wi, ba ki koy j\u00e0ng ay mbiram man cee y\u00e9weene ngir mu texe. Te mu musal ma ci ngistal ak aaw (naw sa j\u00ebf) ci barkeeb Yonnant biy Boroom Liwaaul Hamdi ak yu dul \u00f1oom \u00f1aar ci caay-caay yi (bon-bon yi) te mu may ma ay ng\u00ebn\u00e9el.<br \/>\nTe mu musal ma (t.s) ba f\u00e0wwu ci ayuw Ibliis mii nga xam ne dafa f\u00e9tt\u00e9erlu .<br \/>\nTe mu musal ma ci ayu li mu bind ci suuf si, ak li mu bind ci asamaan si ak li nekk ci seen diggante \u00f1oom \u00f1aar.<br \/>\nTe mu may ma ma topp ci sunnas Yonnant bi (j.m) miy G\u00ebn-ji-mbind\u00e9ef , miy ku \u00f1u ramuloo, miy ku \u00f1u topp ginnaaw bi mu jullee ci moom te s\u00eblm\u00ebl ci, ak \u00f1o\u00f1am aki saabaam ci anam gu dul dog. Fii nag mooy fi tarjumaani t\u00e9ere bi yam, kon leegi nanu jublu ci (indil leen) teggiin yi.<br \/>\n<strong><br \/>\n5 ndoorte li <\/strong><br \/>\nNgir woy, nos lii di wesaru Seex Amaadu &#8211; mii di ku g\u00e9eju ci xam-xam \u2013 maa ngi naan : Yeen mbooleem waay-s\u00e0kku yi xam-xam d\u00e9glu leen sama laabiire gii di leen t\u00e0qaleek ag texeedi Mu di laabiire gog da\u00f1u leen koo j\u00ebmme ngir j\u00ebmmi Y\u00e0lla rekk, muy yee nag j\u00e9pp aji-xellu ak ku jamuj(f\u00e0tte):<br \/>\nYoonu teggiin de mooy y\u00ebr\u00ebm ndaw, ni ko baayam di y\u00ebr\u00ebme ak ndayam te weg mag ak def sa moroom ni sa bopp ngir j\u00ebmmi Y\u00e0lla mi nekk ca aras (toogu ba)&#8217; saraab aji taalif ji.<br \/>\nYoonu teggiin mooy nga y\u00ebr\u00ebm ndaw mel ci moom ni baayam ba ko jur te am lool ci moom y\u00ebrmande, te mel ci ne ndayam ju am ja ag \u00f1eewant, nga weg it mag ak doonte da di ab jaam bu bawoo Abasa (Ecopi) , te nga yamale sa bopp ak sa moroom ngir j\u00ebmmi Y\u00e0lla kepp.<br \/>\nXamal ni teggin de mooy taarub boroom xam-xam ak ku koy s\u00e0kku, mooy it takkaayi<br \/>\naji -xellu ak ku lewet, mooy njobbaxtalu jikko yi, ku ko takkaayoowul yoq\u00e9el na, \u00f1\u00e0kk na ay takkaay, te neenal, dana mujj di ku Ki bind ba\u00f1 ak \u00f1i mu bind -Y\u00e0lla aki mbind\u00e9efam. K\u00e9pp ku ko gis ba\u00f1 ko te s\u00e0nj ko (mere ko), k\u00e9pp ku toog ak moom am ci moom ag yoqat akug doyal.<br \/>\nBokk na ciy teggin ngay laabiire koo gis ca la nga gis ne ag jubam a nga ca, te ngay ba\u00f1 a yayale sa bopp jenn \u00e0q ci kenn, te nga jort it ne yayoowoo ci kenn mu lay m\u00e0ggal ci lenn. Loolu nag mooy li mu junj ci waxam jii :<br \/>\n<strong><br \/>\n6 Na ngay y\u00ebr\u00ebm gone<\/strong><br \/>\nNangay y\u00ebr\u00ebm gone, rikk, bu ko n\u00ebbbal benn yoon genn laabiire gu aw yiwam nekk. Deel weg mag doonte da di ku doyadi te xeebu.<br \/>\nBokk na ci ay teggiin nga ba\u00f1 a njort ne yayoo nga jenn \u00e0q ci kenn ku mu man a doon . Te nga ba\u00f1 a s\u00e9entu genn m\u00e0ggal mbaa wormaal wu j\u00f3ge ci kenn (kok man nay mer sax ci m\u00e0ggal gi mu lay m\u00e0ggal).<br \/>\nYaw daal jortal ne teggin y\u00e9pp ci yaw la war a bawoo, bu leen seentu mukk ci say \u00e0ndandoo. \u00c0ndal ak nit \u00f1i ni nga b\u00ebgge \u00f1u \u00e0nde ko ak yaw. Saraab aji taalif ji : li mu namm a wax mooy :<br \/>\nBokk na ci teggiin yu rafet nga jort ne ay teggiin moom ci yaw rekk la war a juge, te nga ba\u00f1 di ko seentu ci ku dul yaw. Te ngay \u00e0nd ak nit \u00f1i ci jikko yu baax yi nga b\u00ebgg \u00f1u \u00e0nde kook yaw; boo ko deful it jikko yoo \u00e0nde ak \u00f1oom ci yu bon s\u00e9entu ko ci \u00f1oom, nit \u00f1i daal ni nga mel ak \u00f1oom rekk la\u00f1uy mel ak yaw. Na ngay s\u00e0mmoonteek aqi (Y\u00e0lla) &#8211; Boroom m\u00e0gg giy Boroom k\u00e0ttan gi &#8211; ci \u00f1oom ngir j\u00ebmmam ja moom Y\u00e0lla ni waxi woykat ba. Mu b\u00ebgg a wax rekk ne bokk na ci teggiin yu rafet ngay sammoonte ci mbind\u00e9ef yi \u00e0qi Ki leen bind(t.s) ci di \u00e0ndeek \u00f1oom ni ko woykat bi waxe ca qasidaam ga yor bahru basiit:<br \/>\nYaw mbokk mi na ngay am y\u00ebrmande ci mbooleem mbind\u00e9ef yi, nanga leen di xoole b\u00ebtub \u00f1eewant ak y\u00ebrmande. Na ngay weg mag di y\u00ebr\u00ebm gone, tey sammoontek \u00e0qi aji bind ji ci m\u00e9pp mbind\u00e9ef. Am na addiis bu naan : sama xeet wi de du da\u00f1 di nekk ciw yiiw f\u00e9ek ku ndaw a ngi ci weg mag, mag di ci y\u00ebr\u00ebm gone. Kon rikk na nga di roy ci gindig Imaam yi (y.y.g) kon de di nga gindiku.<br \/>\nBul di toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a \u00f1\u00e0kk(loola mooy lu mel ne) : ngay j\u00e0ng ci moom walla nga d\u00ebkk ak moom walla nga bokk ak moom di lekk, bul toogandook moom cib lal it. Saa su Y\u00e0lla defee nga toogandook moom na nga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu akug watandiku, te bul di tafu ci kawam, bul toog it ci kanamam Yaw mbokk mi rikk, bu ko t\u00e0llal sab t\u00e0nk boo toogee ci moom, te deel damm sab gis w\u00eblif ko, maanaam bul ko di faral di xool rekk<br \/>\n<strong><br \/>\n7 Saraa <\/strong><br \/>\nMu b\u00ebgg a wax ne : bokk na ci teggin yu rafet nga ba\u00f1 a toogandook ku la mag ci lu dul lu manul a \u00f1\u00e0kk, ngir j\u00e0ng mbaa d\u00ebkk ak moom walla di lekkandook moom a\u00f1. Boo toogeek moom it na nga ko def cig wegeel akug dal akug xeebu ak wattandiku. Bul di ko \u00f1\u00f3oxu mbaa nga koy t\u00e0llal ab t\u00e0nk, bu ko di ja tam, bul di baril di g\u00ebstu ci lu dul aajo, ndax loolu ci m\u00e0ndargay ag ndof la. Y\u00e0lla nee na (t.s) : &#8220;neel jullit \u00f1i \u00f1u dam seenub gis&#8221; loolu moom lay junj ci waxam jii di \u00f1\u00ebw :<br \/>\nBul di baril looy geestu fu nekk, te dara \u00f1oru la ci geestu gi. Ndax loolu kat m\u00e0ndargam ndof la, te boo demee ci t\u00e9ereb Y\u00e0lla bi di nga fa gis: &#8220;neel jullit deel topp ndigali Boroom mbind\u00e9ef yi, ndax kat nekk na ci addiis yi. Waay de s\u00e0nkoo na ci bennub xool rekk. Ab woykat de waxoon na bu y\u00e0gg ne : booy def loo gis xool ko danga ci mas a am bis<br \/>\nkon bul di w\u00ebnd\u00e9el sab gis .<br \/>\nSaraa : Mu namm a wax rekk, war na la nga topp li la sa Boroom digal muy damm sab gis. Ndax Addiis bi nee na : waay de dana xool benn xool bob xolam dina ci y\u00e0qoo nib der di y\u00e0qoo ca s\u00e9bej ga, du ca jari\u00f1u mukk. Woykat ba nee na : yaw de boo s\u00e0nnee sab gis ngir sa b\u00e0nneexub xol, bis dina \u00f1\u00ebw bob li ngay gis dina la sonal: danga gis lolodoo man l\u00e9ppam (doo man a am l\u00e9pp ) te doo man a mu\u00f1 rekk ca lenn la, doo man a yam rekk ca xool ba. Doo ko man a am te doo ko man a mu\u00f1, bu ko defee ngay sonn ci loo dul am, te boo ko gisutoon doo ko yittewoo. Keneen it ne: j\u00e0mbaar du mooy kiy aar ay gawaram ca bisub jamante ba, bu xare ba t\u00e0kkee, waaye ka damm ab gisam mbaa mu lem ab t\u00e0nk w\u00eblif ay moy kooku ci j\u00ebmmam mooy gawar d\u00ebgg bay j\u00e0mbaar.<br \/>\nBul di baril am po, bul di ree lu bari, mbaa ngay baril looy y\u00ebngatu ak a defi neen.<br \/>\nBul di baj-baji mbaa ngay j\u00e9em a y\u00ebddu lu n\u00ebbbu lu mu man a doon: loolu de m\u00e0ndargam t\u00f3oy la ak woyofum xel ci ku ko baaxoo.<br \/>\nBoo jekkee nanga dalal say c\u00e9r, nangay taqook ag noppi \u00e0nd ak d\u00ebddu ci lug d\u00ebddu war, kon de nga jari\u00f1u. Deel mu\u00f1 ag \u03b7\u00e0\u00f1\u00f1 te bu ci toontu kenn, te mel ni na Boroom nj\u00e0ngat la (adiib) waxoon : Wallaay damay romb waa ji mu may xas may jellale naan kii de xam naa ne waxuma, ndax kat xasante ak weddeente bokk na\u00f1u ci jikko yi g\u00ebn a bon niki d\u00f3orante. Bariy ree day ray ab xol, kon rikk n\u00e9ewalal ree yi, ndax nga g\u00ebr\u00ebmloo Boroom bi<\/p>\n<p><strong>8 Saraa<\/strong><br \/>\nMaanaam bokk na ci teggiin yu rafet nga ba\u00f1 a barili ree, po, ag neen, ag baj-bajeek y\u00ebngatu ak a j\u00e9em a y\u00ebddu lu n\u00ebbbu, loolu de ci m\u00e0ndargam t\u00f3oy la bokk,ak g\u00e0ttum xel, na ngay faral a dal boo jekkee (boo toogee) cib jataay tey faral a noppi, ba \u00f1u laaj la, bu boobaa nga tontu ci k\u00e0ddu gu suufe, walla nga soxlaa laaj dara, bu boobaa nga def ko te yam ca sa soxla rekk, bu ca dolli dara, ndax kat noppi noflaay a ngi ci ak sutura niki \u00f1u ko waxe: n\u00ebbbal ayib yi kem li nga man cig noppi, ndax kat ab noflaay a ngi ci noppi \u00f1eel aji noppi ji. Defal sab toontu boo lottee muy \u201cnoppi\u201d, bari na wax joj toontu baa nga ca ag noppi.<br \/>\nBokk na ci hikma: bu wax doon xaalis noppi di wurus, bu la nit r\u00e9eree, def la ag \u00f1\u00e0kke-teggiin j\u00e9llale ko taqoo noppi. Ni ko woykat bi waxe: amaa na ma romb ku soxat ki, ku yaradiku ki mu may \u03b7\u00e0\u00f1\u00f1, bu ko defee ma fegu te naan kii daal waxut ak man, \u03b7\u00e0\u00f1\u00f1ante ak weddeente bokk nanu ci jikko yi g\u00ebn a \u00f1aaw, yi g\u00ebn a bon, ree ju bari day ray ab xol. Boo b\u00ebggee am sa ng\u00ebr\u00ebmul Boroom, n\u00e9ewalali ree, Y\u00e0lla ci j\u00ebmmam (t.s) moo ne : &#8220;na\u00f1uy ree lu n\u00e9ew&#8221;. Boo toogee ak ku la mag booy ree nangay yam ci muu\u00f1. Booy wax ak moom it bul bayliku ( \u00ebppal ci wax ji), ndax loolu du lu rafet. Noppil ba nga gis mu b\u00ebgg a wax ak yaw, bu boobaa yamal ca la mu soxla ci yaw. Loolu kat moo di ay teggin, kon j\u00ebfe ko cig w\u00e0llam. Bu la b\u00e9ccingalee, mu\u00f1al b\u00e9ccingalam yooyu, bu defee lu jaaduwul suturaal ko. Bul da\u00f1 di ko j\u00e9ggalu, te bu ko di mere it. Bu koy faral di ja (j\u00ebmale ko say g\u00ebt , samp ko ko rekk) ci waxtu wu nekk<\/p>\n<p><strong>9 Saraa<\/strong><br \/>\nBokk na ci teggin yu rafet nga ba\u00f1 di ree ci jataayub ku la mag ndare muu\u00f1, nga ba\u00f1 di wax ak moom cig bayliku, maanaam \u00ebppal ci wax ji, lu \u00f1or nga wax ak lu \u00f1orul, moom daal na nga yam ci li mu soxla ci yaw, bu boobaa doxal nga ay teggin ci moom.<br \/>\nBu la defee lu jaaduwul j\u00e9ggal ko, te di ko j\u00e9ggalu, bul ko di faral di xool xool bu metti, ndax loolu duy teggin. Boo b\u00ebggee juge ca jataay ba, na nga ko defe cig t\u00ebyyewu (t\u00ebyye sa bopp ba suuf du jug p\u00ebnd du jeqiku). Bu l\u00e9en x\u00ebpp suuf si ci seeni kanam ndax loolu wuute na ak ag jub. Boo ko manee bul di nelaw ci biiru nit \u00f1u nelawul ndax kat loolu duy teggin, ngir ne am na lu ci nekk lu man a waral ag yeddeel: kuy nelaw man ngaa ngelawal te doo ko y\u00ebg.<br \/>\n<strong><br \/>\n10 Saraa<\/strong><br \/>\nBokk na ci teggiin yu rafet nga ba\u00f1 a jeqi p\u00ebnd boo toogee ci jataay bay jug, boo nammee jug , def ko ci ag dal akug t\u00ebyyewu, te bul jaar ci kanamu way jekki yi. Bokk na ci ay teggiin nga ba\u00f1 di nelaw ci digg ay way yewwu boo ko manee, ndax amaa na ngelaw g\u00e9nn ci yaw te doo ko y\u00ebg, ndax b\u00ebt ay saa\u00f1u ag suuf (b\u00ebn-b\u00ebnu aw taat).<br \/>\nNa nga xam ne fuqale bokk na ci liy waral g\u00e0cce ak yeddeel. K\u00e9pp ku aj yitteem ci lekk ak s\u00e9y na xam ne boole na l\u00e9pp luy toroxte. Lekk dee ci j\u00ebl lu lay d\u00ebg\u00ebral ba nga man a jaamu sa Boroom te yam ca. Deel wattandiku jamono ju nekk fuqale ndaxte mooy c\u00ebslaayu w\u00e9pp ay. Saraa: Bokk na ci ay teggiin \u00f1\u00e0kk a fuqale ak \u00f1\u00e0kk a aj sa yitte j\u00e9pp ciw \u00f1am, loolu de cig suufe la te day waral ag \u03b7\u00e0\u00f1\u00f1.<br \/>\nWoykat ba nee na: yaw de foo fi joxe sa biir li mu la laaj ak sa p\u00eby, di nanu \u00e0gg fa mbooleem toroxte ya yam. Sab loxo na nga ko t\u00ebyye, bul ci di baril am po, ndax loolu de ayib la. Bul jottaliku mukk loo l\u00e0qul njari\u00f1 lu la man a jegeel sa Boroom<br \/>\n<!--nextpage--><br \/>\n<strong>11 Saraa<\/strong><br \/>\nBokk na ciy teggiin: t\u00ebyye sa loxo ak b\u00e0yyi di ci fo ak b\u00e0yyi di ci jefandikoo lu njari\u00f1 nekkul, loolu de bokk na ci li woroom xel yi ayibal, te ci la musiba yi tase. Saa soo d\u00e9ggee ku la mag mu soxla dara niki mu b\u00ebggoon ku mu yonni, rikk, demal doxal ko yonneem boobu ngir j\u00ebmmi Y\u00e0lla. Bu kenn soxla ci yaw dara ndare du danga koo defal loolu mu soxla ci yaw, boo dee def noonu de da nga am teraanga. Rikk bul di wax kenn fen nga, walla wax nga lu dul d\u00ebgg, walla juum nga walla jeneen wax ju man a merloo doonte ki nga koy wax gone la, di ko waxe de ag njuumte la.<br \/>\nBu waxee loo xamul nee ko d\u00ebggal nga, kon dees na la teral. Nee ko daal man de tegoon naa ko neneen, walla leneen laa jortoon, walla r\u00e9ere woon naa ko ak yeneen baat yi walla waxiin yi man a b\u00e9gale, loolu de boo ko defee def nga lu rafet, bul \u00f1aawal te bul lore. Deel t\u00e0mmal saw l\u00e0mmi\u00f1 wax lu baax, kon de dinga ci ame ag texe te dees na la ci fegale w\u00e9pp ay ngir waxi sangub mbind\u00e9ef yi&#8230;yal na ko Y\u00e0lla dolli ay x\u00e9ewal ci anam gu sax.<br \/>\nKu nekk na di g\u00ebm Y\u00e0lla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiiw mbaa mu noppi.<br \/>\n<strong><br \/>\n12 Saraa<\/strong><br \/>\nBokk na ci teggiin yu rafet nga saxoo di faj aajoy ku la mag boo ko d\u00e9ggee mu koy s\u00e0kku, niki mu soxla woon ku mu yonni. Bokk na ciy teggin ba tay nga ba\u00f1 di g\u00e0ntul kenn loo man lu mu soxla ci yaw, te ba\u00f1 di wax kenn &#8220;fen nga&#8221; mbaa &#8220;li nga wax du d\u00ebgg&#8221; mbaa baat bu ko man a merloo, doonte yaa ko mag, bu waxee loo xamul d\u00ebggal ko te ne ko (man de nekkuma woon foofu) walla (jortoon naa ne) walla (xamewuma ko woon noonu) ak yu ni mel ci waxiin yu rafet. Nangay t\u00e0mmal saw l\u00e0mmi\u00f1 wax ju rafet . Yonnant bi (j.m) nee na : ku g\u00ebm Y\u00e0lla walla bis bu mujj ba, nay wax aw yiiw mbaa mu noppi. kenn ci woykat yi nee na :t\u00e0mmalal saw l\u00e0mmi\u00f1 wax ju baax, kon de danga ca ame ab c\u00e9r, l\u00e0mmi\u00f1 de li nga ko t\u00e0mmal rekk lay t\u00e0mm, lu mu man a doon la nga ko ca miinal rekk lay def, moo xam lu baax la mbaa lu bon, deel xool nooy dollikoo.<br \/>\nSab dox na ko aajo di waral ci lu dul ag r\u00eby, ag r\u00eby de ci mbugal lay bijjee j\u00ebme. Bul di ree mukk ci lu dul lu y\u00e9eme, bul dox mukk it ci lu dul aajo. Bul gestu tam te s\u00e0kkuweesu ko, ndax yii y\u00e9pp ag ndofe la gog d\u00e0qoo na\u2019aki teggiin.<br \/>\nSa tubay it bul ko di wu\u00f1\u00f1i mukk, ndax loolu ci b\u00e0yyi ay teggin la bokk. Moom de ci jikkoy k\u00e0ccoor yi diy saay-saay te bokk ci giirug Hassaan la bokk, \u00f1oom \u00f1i d\u00ebddu lu baax. Na ngay moytoo wu\u00f1\u00f1i sa biir ak li nekk ci diggante jumbux bi ba ci b\u00ebti-woom yi, (ngir bon gi mu bon). Loolu de m\u00e0ndargam r\u00e9er la ak ndofe ak n\u00e9ewug mba\u00f1-rus gu m\u00e0gg gi. Ndax moom (mba\u00f1-rus) mooy d\u00e0ttub diine, fu mu nekkul diine nekku fa , loolu de la j\u00e0ngalekat yu mag ya saxal. Koo agsi ci moom nanga ko nuyyu, bu fekkee ne soxla nga ay teggin. Bu fekkee ne moo la nj\u00ebkk a nuyyu nanga ko fay ci k\u00e0ddu. Boo saafoonteek moom na nga d\u00ebg\u00ebral sa loxol ndijoor ci ndijooram, loolu mooy li nu rafetlu Bul rocci sa loxo li feek nj\u00ebkku la koo rocci moom ci anam gu f\u00e9s. Ndaxte de sibees na f\u00ebkk ay loxo ci nuyyoo ci anam gu gaaw ak b\u00e0yyi wax ja. Saafoonte ci \u00f1aari loxo it bokk na ci ay teggin, niki \u00f1aar yi nu la waxoon leegi. \u00d1aanalal ki ngay nuyyool yaw boroom xel mi, ndax loolu de bokk na ci liy fari b\u00e0kkaar.<br \/>\nBoo b\u00ebggee dugg ci k\u00ebr walla n\u00e9egub j\u00e0mbur nanga y\u00ebglu, kon de nga am la g\u00ebn. Bu \u00f1u la digalee nga dugg nga dugg, bu dul loolu dellul. Sab b\u00ebt bul ko di w\u00ebnd\u00e9el ci n\u00e9egub j\u00e0mbur mbaa k\u00ebram ngir ragal gis fa awra joj b\u00ebggunu woon nga gis ko.<br \/>\n<strong><br \/>\n13 Saraa<\/strong><br \/>\nBokk na ciy teggiin booy jug aajo rekk di la y\u00ebkkati, bokk na ci ag ndofe ngay ree te lu reeloo nekku fi, mbaa ngay dox ci lu dul aajo, mbaa ngay gestu te yittewoowoo ko, bokk na ci ay teggin ngay moytoo wu\u00f1\u00f1i say s\u00e9r, loolu de ci jikkoy k\u00e0ccoori Hassaan yi la, bul di fee\u00f1al lenn ci sa biir mbaa li nekk ci sa diggante jumux ba ci say w\u00f3om, loolu de ci r\u00e9er la ak \u00f1\u00e0kk kersa te kersa mooy d\u00e0ttub diine tey laylaat gi mu tege, fu kersa \u00f1\u00e0kke diine jug fa. Bokk na ci ay teggiin ngay nuyyu k\u00e9pp koo dox ba \u00e0gg ci moom, te di ko fay bu la nuyyoo, te ngay saafoonteek moom tey d\u00ebg\u00ebral sab loxo ci loxoom boo koy nuyyu, te nga ba\u00f1 koo nj\u00ebkk a rocci sa loxo, f\u00ebkk loxo ci lu gaaw cib nuyyo de lu \u00f1u sib la. Bokk na ci ay teggin ngay saafoonteek moom ci sa \u00f1aari loxo y\u00e9pp, te nga koy \u00f1aanal lu baax ak sa bopp loolu bokk na ci liy far ay b\u00e0kkaar . Bokk na ci ay teggiin ngay def booy dugg ci n\u00e9egub j\u00e0mbur mbaa k\u00ebram ngay y\u00ebglu bu \u00f1u la nee j\u00e0llsil nga dugg, ndeem d\u00e9et nga d\u00ebpp, rikk bul di s\u00e0nni sab gis ci k\u00ebr mbaa n\u00e9eg boo moomul ngir nga ba\u00f1 faa gis loo warul a gis. Boo b\u00ebggee kooy \u00e0ndandool bu muy ku dese cim xel mbaa ku i\u00f1aan mbaa ku bariy xemmeemt\u00e9ef bu di toog ak ku dul ku lay dolli diine ak xel, kon de nga am c\u00e0kkut\u00e9ef. Ndax de xibaar na\u00f1u ne cam si de (waa ji) ma nga ca diiney xaritam ba, loolu ab adiis la bu \u00f1u tuxal (waa ji de diine ji waayam yor rekk lay yor) Saraa: Da lay d\u00e9nk nga ba\u00f1 a \u00e0ndandook way dese yi cim xel te ba\u00f1 di toog ak ku la dul dolli diine ak xel, ci loolu de ngay ame la nga b\u00ebgg, ndax waa ji de ni ab xaritam mel rekk lay mel: wolof yi nee na\u00f1u won ma sa xarit ma wax la sa jikko &#8211; seyyidinaa Aliyun &#8211; karramal laahu wajhahuu \u2013 nee na: bul def mukk boroomug r\u00e9er muy sab \u00e0ndaale, moytu ko te moytu sa bopp bariwaa na aji r\u00e9er ju alag boroomug lewet (ku nite) ba mu ko defee mbokk. Nit de ca moroom ja la\u00f1u koy natt bu \u00e0ndeek moomni \u00f1uy natte d\u00e0ll ca moroom ja bu \u00f1u dee \u00f1aar mbir de am na ag niroo akug natt ca moroom ja; xol de misaal la ca moroom ja. Am na ku ne: boo nekke ciw nit nangay seet \u00f1a ca g\u00ebn ngay \u00e0nd ak \u00f1oom bul seet \u00f1a ca yees ngay \u00e0nd ak \u00f1oom bay yees. Bul laaj waa ji, waaye laajal ab \u00e0ndandoom. Ndax ku nekk ca ka ngay \u00e0ndal ngay roy. Bul s\u00e0kkoo gis mukk ab r\u00ebcc-r\u00ebcc (ci sa moroomu nit) bul g\u00ebstu itam ay awra (ay \u00f1aawt\u00e9ef)<\/p>\n<p><strong>14 Saraa<\/strong> Mu ne : bokk na ciy teggiin ngay ba\u00f1 di g\u00ebstu r\u00ebcc-r\u00ebcci nit \u00f1i mbaa seeni \u00f1aawt\u00e9ef. Waxees na ne : bul di s\u00e0kkoo xam la nit \u00f1a n\u00ebbb ci seeni ayib ndax kat loolu man naa waral Y\u00e0lla di muri mbalaan mi mu muuroon ci say \u00f1aawt\u00e9ef. Rikk nangay tudd lu baax la nekk ci \u00f1oom bu nu leen tuddee bul ayibal kenn ci \u00f1oom ndax kat loo leen wax man naa am yaa leen ko \u00ebpp. Na nga mel ne na woykat ba waxoon: dinaa b\u00ebgg jikko yu rafet yi sama kem k\u00e0ttan tey ba\u00f1 di ayibale ak \u00f1u may ayibal, may j\u00e9ggal \u03b7\u00e0\u00f1\u00f1ug nit \u00f1i ngir ag lewet ndax ki yees ci nit \u00f1i mooy ki sopp ag \u03b7\u00e0\u00f1\u00f1ante. Ku weg nit \u00f1i wegees ko, ku xeeb nit \u00f1i deesu ko weg. Ka wax lii de wax na wax ju rafet: boo b\u00ebggee dund sa diine, mucc, sa w\u00ebrs\u00ebg l\u00ebw (bari) sab der \u00f1o\u03b7, boo b\u00ebggee loolu sa l\u00e0mmi\u00f1 bu ci tudd mukk ayibi nit, ndax kat yaw it, am nga ay ayib, nit \u00f1i ami l\u00e0mmi\u00f1. Bu Y\u00e0lla dogalee say g\u00ebt rot ci ayibi nit, nee leen : yeen g\u00ebt yi bu l\u00e9en xool de, ndax nit \u00f1i \u00f1oom it am na\u00f1u ay g\u00ebt. Xamal ne wuute ab d\u00ebel (dige te defoo ko) ak fen bokk na\u00f1u ci g\u00e0kk-g\u00e0kki wax, dee leen teet (moytu). Nekk na ci adiisub kii nga xam ne maa ngi s\u00e0kku sellug ay julleeki s\u00eblmal yuy sottiku ci moom aki \u00f1o\u00f1am aki saabaam, yi diy nd\u00eberlaay. D\u00e9nk naa leen adiis ba:nekkal di kuy wax d\u00ebgg, teetal fen ngir nga kawe Saraa: mu jubloo wax ne mi ngi lay d\u00e9nk nga ba\u00f1 a fen, ba\u00f1 a wuuteb d\u00ebel, te di leen ko tere, ngir ne \u00f1ooy g\u00e0kk-g\u00e0kki wax, Yonnant bi (j.m) nee na: d\u00e9nk naa leen d\u00ebggu, ndax mooy yobboo cig mbaax, teg mbax mooy yobboo \u00e0jjana, waa ji bu saxee di d\u00ebggal te di ko s\u00e0kku, bu y\u00e0ggee bindees ko fa Y\u00e0lla muy ku d\u00ebggu, moytuloo naa leen fen, ndax day yobboo cig mbon teg mbon mooy bijje j\u00ebme sawara, waa ji bu dee fen te di ko s\u00e0kku, day mujj bindees ko mu dib fenkat fa Y\u00e0lla. Fonkal sa \u00f1aari way jur, te am y\u00ebrmaande ci \u00f1oom ak \u00f1eewant, te deel gaaw ci seeni ndigal aki mbir. Deel ba mbooleem li \u00f1u la tere, boo ko dee def de, sag kawe dina yokku K\u00e9pp ku la mag ci jege\u00f1aale yi nanga ko weg ak \u00f1u dul jege\u00f1aale yi, rikk nanga nekk ak mbind\u00e9ef yi ci jikko yu rafet, kon de Aji-S\u00e0kke ji (Y\u00e0lla) dina la sopp.<br \/>\nNa ngay rafetal jikko yi cig yaatu-yaatulu, ak a s\u00e0kkoo sopplu ci \u00f1oom (mbind\u00e9ef yi) kon de soppees na la. Na ngay nooyal i wax ci nit \u00f1\u00e9pp, loolu de ci jikkoy way \u00f1aw yi la bokk (\u00f1u yeewwu \u00f1i). Xibaarees na j\u00eble ca Boroom ng\u00ebn\u00e9el la Yonnant bi (j.m) mu ne: genn-w\u00e0llu xel mooy sopp-sopplu ci nit \u00f1i (fexe ba nit \u00f1i sopp la).<br \/>\nBokk na ci texeeg nit ki, xolub boroomug njub ba\u00f1 koy ba\u00f1 ak a fo\u00f1. Saraa: mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga fonk sa \u00f1aar i waay-jur te \u00f1eewant leen, di gaawantu ci def s\u00e9eni ndigal, di b\u00e0yyi seen i tere. Y\u00e0lla mu kawe mi nee na: nit d\u00e9nk nanu ko lu baax ciy waay-juram, maanaam mu fonk leen, ak yu dul boobu ciy laaya, ak nga fonk ku la mag ci jege\u00f1aale yeek \u00f1u leen moy, te ngay rafetal say jikko ci di leen mayug yaa, ak won cofeel ak a s\u00e0kku \u00f1u sopp la, s\u00e0kkug cofeel ci nit \u00f1i de mooy genn-w\u00e0llu xel, na la w\u00f3or ne bokk na ci texeg nit ki, xolub aji g\u00ebm di ko b\u00ebgg, deel nooyal say wax \u00f1eel nit \u00f1\u00e9pp, ndaxte loolu kay ci jikkoy waay-yeewwu yi la bokk. Deel s\u00e0kku seenug \u00f1aan foo tollu, deel barkeelu it ci \u00f1oom, loolu de dina la yobbe ag kawe guy dolliku. M\u00e0ggal boroom xam-xam bu j\u00ebfe (xam-xam ba) mooy m\u00e0ggal boroom aras (toogu ba).<br \/>\nFoo \u00e0ndeek ku la mag nanga sax ci di ko weg, moo xam cib tukki la mbaa lu ko moy, deel not sa bakkan ci di ba\u00f1 di toog ak moom ci kaw deel toog ci suuf, bul di toogaaleek moom cib lal ak doonte da la caa woo sax ngirug yaatal. Ndare muy lu manul a \u00f1\u00e0kk, su leen \u00f1am wi dikkalee mbaa naan gi yaw ngoor si bu ko ca jiite mukk, xaar ca ndigalam, loolooy jub ga. Deel seet la g\u00ebn ca \u00f1am wa it di ko ko jox ngir ag wormaal Dee ko ligg\u00e9eyal ci mbooleem li mu aajowoo, kon say aajo dees na la ko fajal. Saa soo \u00e0ndeekuw nit cib tukki, dee leen dimbali ci mbooleem lu \u00f1u soxla Ligg\u00e9eyal-leen te s\u00e0mmal-leen seeni waruwaay,seeni fas mbaa mbaam walla sax wata, yoral-leen seeni bagaas, dimbali-leen \u00f1oom \u00f1\u00e9pp loo ci man, j\u00e9ggal-leen su \u00f1u s\u00e0gganee.<br \/>\nNeen ak noflaay j\u00ebmm ju b\u00ebgg a doon dara du leen taamu. Ndax kat aw yiiw manul a bawoo ci \u00f1oom \u00f1aar, te aw ay rekk a cay bawoo \u00f1eel murif bi. Boroomug yayoo bu s\u00e0kkoo ci yaw dara, defal ko ko Bul nay mukk ci po\u00f1at mii (alali \u00e0ddina jii) ba loolu di waral sa g\u00e0cce ca yalmal qiyaam bis p\u00e9nc. Boroomug nay ku sori Y\u00e0lla lay doon ak mbind\u00e9efam y\u00e9pp foo ko fekk. Boroomug nay dees koy wommat j\u00ebme sawara, soril ko \u00e0jjana safaan ba mooy aji tabe ja, ca lees wax, kon nekkal aji tabe ji, bul nekk mukk aji nay ji. Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga siyaare boroom xam-xam yeek gaa \u00f1u baax \u00f1i, nga leen di ligg\u00e9eyal ak a barkeelu ci \u00f1oom, tey s\u00e0kku ci \u00f1oom \u00f1aan, ndax kat m\u00e0ggal boroom xam-xam mooy m\u00e0ggal Y\u00e0lla mu kawe mi. Saa soo \u00e0ndateek ku la mag cib tukki, mbaa lu ko moy nanga ko b\u00e0yyee lal ba tey toog fa suuf, te bul bokk ak moom t\u00ebdd mukk ndare ngir lu manul a \u00f1\u00e0kk, bees leen indilee \u00f1am mbaag naan, rikk bu ko ca jiitu, xaar ca ndigalam, dee ko b\u00e0yyee la g\u00ebn ca \u00f1am wa, te di ko ligg\u00e9eyal ci l\u00e9pp lu mu aajowoo. Bu Y\u00e0lla dogalee nga \u00e0nd ak aw nit cib tukki, doonal seen mbindaan, s\u00e0mmal leen seeni waruwaay, yoral leen seen i bagaas kem li nga man. Bul taamu mukk ab noflaay ak loxoy neen, aw yiw nekku ci de te kenn du jot &#8220;teddnga&#8221; ga ci lu dul ab coona niki lees ko waxe. Cig farlu lees di jote kawe ga, ku b\u00ebgg ag kawe fog guddi yi (fog \u00f1\u00e0kk a nelaw guddi). Dangay s\u00e0kku ag tedd ba noppi di nelaw guddi, na la w\u00f3or ne xemmemloo nga sa bakkan lu jomb (b\u00ebgg nga lu manul a nekk). Mi ngi lay digal nga ba\u00f1 a nay ci dara ci \u00e0dduna, ku nay kat ku sori Y\u00e0lla la, ku sori nit \u00f1i la, ku sori \u00e0jjana la, ku jege sawara la. Safaan ba it mooy ku tabe ki, woykat ba nee na: bu fekkee alal wacc koo tax deesi dajale ko, kon lu tax cam si (nit ki) di nay ci lees di wacc. Teralal gan ya cig yaatal (dalal j\u00e0mm) ak ganale ak mb\u00e9gteek jegeel. Rikk bu sa d\u00ebnn(xol) xat mukk ci gan, ndax moom balaa y\u00e0gg mu laxas dem. Nekk na ca adiisu Kees-t\u00e0nn ka (Yonnent bi, yal na Y\u00e0lla julli te s\u00eblmal ci moom aki \u00f1o\u00f1am ak k\u00e9pp ku ko topp. Wax it ne: gan gi teral ko ca bahrub kaamil ba mu defe woy wa ci galan bu tudd kaamil. Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga teral gan, yaatal ko, te ba\u00f1 a xat ngir moom, ndaxte balaa y\u00e0gg mu dem, Yonnent bi (j.m) nee na ku g\u00ebm Y\u00e0lla ak bis p\u00e9nc ba, nay teral ganam.<br \/>\nAb woykat it def aw woy ci galanu kaamil: gan gi teral ko, ab fanaanuwaayam yelleef la (lu mu moom la), rikk bul nekk r\u00ebbbum waay-w\u00e0cc yi, bul nekk \u03b7\u00e0\u00f1\u00f1 ak saagay gan yi. Nanga xam ne gan de f\u00e0wwu mu nettali \u00f1o\u00f1am fa mu fanaan, doonte laajeesu ko ko Wwolof nee na: gan dees na ko xa\u00f1 l\u00e9pp ba mu des nettali. Na nga ko gatandoo kanam gu nooy te yaa, waxees na ne moo g\u00ebn ganale, moom la woykat biy feddali: kanam gu nooy de moo g\u00ebn ganale, kon de xanaa bu ko waa jiy def ci kanam gu nooy dina y\u00e9eme. Dinaa ree sama gan nj\u00ebkk muy w\u00e0cce ag raxlaam, bu ko defee mu naat fi man te booba barab bi bu bekkoor la. Duma wax mukk bu ma gan ganesee: j\u00e0llal sa k\u00ebr ga soriwul. Sunu k\u00ebr de fu yaa la ca ka ko siyaare, ubbilees na ko gan gu f\u00ebgg gu nekk. L\u00e9pp lu fa nekk, lu dagan la \u00f1eel ko, ndare la Aji-bind ji araamal &#8230;&#8230;&#8230;&#8230;&#8230;<br \/>\nBul b\u00e0yyi benn bis am nj\u00e0ng, te nga j\u00ebfe ko cig jaamu Y\u00e0lla. Xam-xam day dundal xolub aji xamlu ji, day leeral xol tey dindi ngumba gu xol. Xamal ne rawanteeg nit \u00f1i ci xam-xam lay nekk ak diine, nanga d\u00ebkke mu\u00f1. Ci \u00f1oom \u00f1aar it la ku g\u00ebn di g\u00ebne, du ci ag askanoo ci ku kawe. Ci w\u00e0llug askan, moo xam baay la mbaa nday, kon farlul ci \u00f1oom \u00f1aar \u00e0nd ceek i teggiin Booy s\u00e0kku xam-xam dimbandikool Y\u00e0lla te sellal ci xol bu dal Te ngay d\u00ebkke j\u00e0ng nag, ak s\u00e0mm (s\u00e0mmoonteek ndigal ak terey sunu boroom yi) N\u00e9ewal i nelaw, n\u00e9ewalug regg Saxal ci j\u00e0ng ak nafar li nga j\u00e0ng te ba\u00f1 koy d\u00ebddook a ginnaawal Nangay wuuteek bakan, ndaxte bakan li mu lay xiir du dara lu dul luy waral ag t\u00ebj N\u00e9ewalal nelaw yi, t\u00e0ggool ak t\u00e0yyeel, n\u00e9ewalal noflay, g\u00e0ttalal m\u00e9bat Xamal ne ku ba\u00f1 a j\u00e0ng cig ndawam, dina dajeek r\u00e9ccu Ndaxte k\u00e9pp ku gaawantuwul j\u00ebm ca xam-xam ya (ku gaawantuwul j\u00e0ngi) te f\u00e9ex ngir \u00f1oom nj\u00ebkk yitte ya Lu ci \u00ebpp du am la mu ca yittewoo, te du ca jot c\u00e0kkut\u00e9efam Ndaxte taggees na nj\u00e0ngum gone ne mook bind ci doj a yam (bind ci simaa bu tooy, bu wowee du da\u00f1ati) \u00d1u niroole nag nj\u00e0ngum mag ak bind ci ndox ni muy \u00f1\u00e0kke jeexiit &#8230;&#8230;&#8230;&#8230;&#8230;&#8230;&#8230;.. Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga ba\u00f1 a b\u00e0yyi j\u00e0ng benn bis, ndaxte xam-xam mooy dundug xol tey da\u00f1ug ngumba, di leerug bakan niki lees ko waxe: Xam-xam day wu\u00f1\u00f1i ngumba w\u00ebliif xolub boroom, ni weer di wu\u00f1\u00f1ee k\u00ebriisug l\u00ebnd\u00ebm ga Ci xam-xam la ay xol di dunde yoy masu\u00f1oo xam bu nj\u00ebkk lam mooy t\u00e0qale gi am ci diggante d\u00ebgg ak fen Xam-xam ag leer la \u00f1eel bakan, mu cay niite d\u00ebgg gi (di ci tegtaloo ngir xam li am) dafa mel ne leer ci b\u00ebt Mi ngi lay xamal ne nit \u00f1i seenug rawante ci xam-xam ak diine la nekk, te ci moom lees di g\u00ebne, du ci askanoo ci baay mbaa nday, noonu la ko Seydinaa Aliu waxe (yal na Y\u00e0lla teral kanaman): Nit \u00f1i boo leen dee natt \u00f1oo yam seen baay Aadama la, seen nday Awa Boo dee ndamu ci askan wu tedd, nanga xam ne ci ndox ak ban la bawoo Ndam daal \u00f1o\u00f1 xam-xam la \u00f1eel, ndax \u00f1oo gindee \u00f1eel ki ko soxla Darajay cam si (nit ki) mooy la mu man (am ci ag xere\u00f1), way r\u00e9er yi (\u00f1i amul xam-xam) ay noon la\u00f1u \u00f1eel woroom xam-xam yi Wutal xam-xam, kon de dinga ci dunde ba f\u00e0ww, ndax nit \u00f1i way faatu la\u00f1u, te woroom xam-xam yi dunu faatu way dund lanu Mu lay xamal ne bokk na ci liy dimbalee ci xamlu te di ko yombal, ngay ragal Y\u00e0lla ci sab xam-xam, te di ko s\u00e0kku ngir moom, di n\u00e9ewal i nelaw, ak regg tey taqoo j\u00e0ng niki lees ko waxe: Yaw aji xamlu ji gaawantul s\u00e0kkuji ag c\u00e0mm (ragal Y\u00e0lla), te nga b\u00e9ccngal nelaw yi, t\u00f3ng regg gi (merook regg gi) Jublul ci bind bi, bul t\u00e0ggook moom, xam-xam ci j\u00e0ng la taxawe te yekkatiku ****************** Te f\u00e0ww ngay j\u00e0ng tey baril nafar di wuuteek bakan bi ci loolu, niki lees ko waxe: Sama xarit bul di t\u00e0yyeel te bul di neenal bind bi ( dee ko topp ak a nafar), te bul topp mukk sa bakkan cig neenalam ( ci di ko \u00f1\u00e0kk a defloo dara) Bul di b\u00e0yyi ag baamu (nafar) ca la nga jot a wattu (mokkal), ku b\u00e0yyee baamu (nafar) f\u00e0wwu mu f\u00e0tte (f\u00ebtt la mu mokkaloon) ****************************************** Te ku gaawantuwul def am nj\u00e0ngam te def ci yitteem j\u00e9pp cig ndawam, dina jafe mu am ca la mu ca nammoon, ndax j\u00e0ng cig ndaw mook boyaade ciw doj a yam (bind ci simo? bu tooy), j\u00e0ng cig mag nag mook bind ci ndox a yam (booy teggi sa loxo muy far) , lenn ci woykat yi wax na ne: Gis naa ne damay faral di f\u00ebtt li ma j\u00e0ng bi may mag, te kat f\u00e0ttewuma li ma j\u00e0ng ba may gone Xam kon mooy j\u00e0ng cig ngone, lewet nag di ga nga def-deflu cig mag (lewet fii: nite, xel, tegu ci yoon) Bees xaroon xol bees j\u00e0ngal cig ndaw, dees fay fekk xam-xam muy lu mel ne lees boyaade ciw doj (mu mel ne mbind mees def ci simo? bu tooy) Boo bijjaawee ba noppi di j\u00e0ng yaa ngi sonal sa bopp, rawati na bu xol bi sonnee ak d\u00e9gg beek gis bi Nit daal \u00f1aar rekk la, xel ak xellu (logique), ku lii raw ak lee, na xam ne alku na ********************************** Nanga xam ne xam-xam de lu jafe la, deesu ko ame ci lu dul t\u00ebyye sa bopp w\u00ebliif &#8220;d\u00e9gg naa ak waxees na&#8221; Du la may (moom xam-xam) lennam mukk li feek joxoo ko sa l\u00e9pp, kon farlu ci. Jox ko sa l\u00e9pp ci lu dul x\u00ebccoo, fogalal sag guddi (bul di nelaw guddi) te xiifal sa biir Deel maral sa b\u00ebcc\u00ebg ci xam-xam, di ci sonal sa c\u00e9r y\u00e9pp \u00e0nd ceekug teggiinu Ku ko s\u00e0kkoowul noonu du ca am lu am njari\u00f1, noonu lees ko xibaare Xibaarees na it ne moom de ab fo\u00f1aakon la (kuy daw di soree), ku dul cam su di ab mu\u00f1kat du ko am Nangay sax cig toroxlu cig toroxal sa bopp, ca jamonoy xamlu ja, kon de danga am leerug xol Ab xamlukat bu r\u00ebyee, du am nammeelam Bayyil ag p\u00e9exlu (noos) bul di toog mukk cib lal ca jamonoy j\u00e0ng ja, ci lu dul aw tiis (\u00f1\u00e0kk pexe) Nangay boole yitte ji j\u00e9pp ci li ngay s\u00e0kku, ci lu dul gestu j\u00ebm ci lu warul Bul di d\u00e9glu nit \u00f1i mbaa x\u00ebccoo yi \u00f1u nekk Bul di yeexe am nj\u00e0ng, mbaa nga naan di naa ko defi bu ma f\u00e9exee, soo b\u00ebgee dab gaa \u00f1u baax \u00f1a \u00c0dduna de am na yitte yuy teree \u00e0gg ca njub ga, te du\u00f1u jeex Dee de cig mbetteel lay \u00f1\u00ebwe, te bariwaa na fu mu b\u00f3ome boroomi soxla Mu jubloo wax ne xam-xam de lu jafe la, deesu ko ame ci lu dul t\u00ebju w\u00eblif ag jaxasoo, xamal ne du la jox mukk lennam ndare bu danga koo jox sa l\u00e9pp, ku ci xiifalul biiram, fog guddeem, mar b\u00ebc\u00ebgam, sonali c\u00e9ram, du ca am lu am njari\u00f1, ndax xam-xam ag leer la, ku dul aji mu\u00f1 du ko am, woykat ba nee: S\u00e0kkul te bul yoqat ci s\u00e0kku gi, g\u00e0kk-g\u00e0kkub aji s\u00e0kku ji xam-xam mooy yoqat Xanaa gisoo ne buum sax bu y\u00e0ggee jaar ci pindub teen, b\u00e0yyi fay jeexiital Kuy j\u00e0ng f\u00e0wwu muy toroxlu ak a suufeel boppam buy xamlu, lu ko moy du ca am nammeelam, war nay b\u00e0yyi ag noos, bu muy toog cib lal mukk ci waxtuw j\u00e0ng, ndare bu loolu da di lu manul a \u00f1\u00e0kk ba \u00e0gg ci lool, booleel sa yitte j\u00e9pp booy j\u00e0ng ca la ngay j\u00e0ng, bul di gestu leneen lu ko moy, bul di d\u00e9glu nit \u00f1i mbaa la \u00f1u nekk, mi ngi lay d\u00e9nk it nga ba\u00f1 di yeexe am nj\u00e0ng, naan danga koy b\u00e0yyi ba f\u00e9ex ci yitte yi, ndax yittey \u00e0dduna du\u00f1u jeex mukk Kenn faju fi aajoom, aajo it fajuwu fi ndare bu jeneen daa juddu. Yaw amaa na sax dee gi dikkal la, ba laa booba, ndax dee de mooy aji f\u00e0ddu (ku fi nekkul) ji g\u00ebn a jege, te buy \u00f1\u00ebw cig mbette lay doon. Ginnaaw bi mu wax ci nees di tegginoo ak Seexul Murabbii (S\u00ebri\u00f1 biy j\u00e0ngale) ak ki lay j\u00e0ngal ak sa mbokk d\u00ebgg ak sa \u00e0ndandoo d\u00ebgg, daal di ne: Fig wegeel man a yam mooy nga weg sa s\u00ebri\u00f1, def ko ab sang, may ko say x\u00e9ewal Fajal ko ay aajoom li feek yaa ngi dund, ci di ko jox, di ko ligg\u00e9eyal li nga man Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal nga weg sab s\u00ebri\u00f1, wormaal ko, fajal koy aajoom li nga man, te ngay teet reek kaf ak coow ci kanamam, boo jubloo defi teggiin Boo toogee fa moom bul di baril ay gestu mbaa ngay y\u00ebngu fu nekk nga j\u00ebm fa Bul di baril wax fa moom, nekkal di kuy noopi, loolu dina waral nga am ag jubalam Bul \u00e0nd ak moom mukk lu dul cig m\u00e0ggal, bul roy mukk waa jamono jii ( ci seenug \u00f1\u00e0kk a m\u00e0ggal seeni s\u00ebri\u00f1) Bul def mukk ni ka \u00e0ndoon ak Qudar, ndare bu daa manul a \u00f1\u00e0kk (bul ko di laaj lu mu def lu nekk, nga ne ko loo ci jublu) Deel def li mu la digal, ak doonte sa b\u00e0kkan da koo b\u00ebggul Lu mu la tere it baal te daw w\u00eblis ko, te teet sa b\u00e0nneex Mu jubloo wax ne mi ngi lay aaye ngay baril coow akum po ak ree ak gestu bu bari ci kanamam, bu ko def it \u00e0ndandoo ndare bu daa manul a \u00f1\u00e0kk, di deglu ay ndigalam tey teeti tereem ak doonte sa bakkan begu ci. Bul di da\u00f1 di ko di jox i \u00e0ddiya kem li nga man Ak doonte lu n\u00e9ew la sax, ngir rekk topp lees wax ne day dooli moom \u00e0ddiya ag coffeel Loo ko gis mu jeng j\u00ebm ca, gaawantul dem ca Te farlu cig jottali ko ko, ndax kat rafetug j\u00ebf ma nga ca matal ko Nanga nekk dib jaam \u00f1eel k\u00e9pp ku aju ci moom ci \u00f1o\u00f1, \u00f1oom \u00f1\u00e9pp nag \u00c0nd ceekug wormaal nag, ndax mu sarax la ab xool boo man a ame la nga b\u00ebgg Benn xool bob cofeel bu tukkee cib s\u00ebri\u00f1 j\u00ebm cib taalibeem mooy ng\u00ebn\u00e9el ya tey kawe ga Nanga nekk fa s\u00ebri\u00f1 ba niki ab n\u00e9ew bees t\u00ebral ci kanamu aji sangam, kon de nga jari\u00f1u Boo dee s\u00e0kku xam-xam it, nangay s\u00e0kku ng\u00ebr\u00ebmul aji j\u00e0ngale ji ngir j\u00ebmmi Y\u00e0lla Nanga mel ca sab s\u00ebri\u00f1 nib jaam, loolu de dina tax nga jot darajay buur yi (dina tax nga doon buur) Xamal ne njari\u00f1 deesu ko am ndare cig m\u00e0ggal ci li \u00f1u wax Kem ni nga m\u00e0ggale sab s\u00ebri\u00f1 ngay ame li nga b\u00ebgg, ci ngay ame it barke Ku g\u00ebr\u00ebmloowul ab s\u00ebri\u00f1am, du g\u00ebr\u00ebm ab dongaam Bariwaa na waa jees miin ci xam-xam te kenn jubluwu ko Yal na nu Y\u00e0lla musal ak yeen ci xam-xam bu jari\u00f1ul ki ko xam Mu jubloo wax ne mi ngi lay digal ngay \u00e0ddiyaal sab s\u00ebri\u00f1 li nga man ak doonte lu n\u00e9ew la sax, te s\u00e0kkoo def l\u00e9pp loo ko gis mu jeng j\u00ebm ca ci mbir mu mu man a doon, tey farlu ci jottali ko ko, te ngay wormaal mbooleem \u00f1i aju ci moom, moo xam \u00f1o\u00f1 la mbaa jaam ak \u00f1u leen moy, ndax sax mu xool la ab xool bob cofeel bu la ci Y\u00e0lla man a dimbalee. Xamal ne kem ni aji xamlu ji di m\u00e0ggale aji xam ji lay jari\u00f1oo, wa xees na : Gis naa ne li g\u00ebn a war ci mbir yi mooy \u00e0qi j\u00e0ngalekat te mooy ji g\u00ebn a feddaliku ci b\u00e9pp jullit Lu yell la deesi \u00e0ddiyaal ko ay jnniy d\u00ebr\u00ebm ngirug teral, ci wenn araf wu mu la j\u00e0ngal wu nekk \u00c0ggees na ci wax ne moom lees jiital ci \u00e0qi waajur ni ko \u00f1enn \u00f1i waxe : Damay jiital sama \u00e0qi ustaas ci sama joj waajur ak doonte xam naa ne yoreel naa waajur wi njekk ak \u00f1eewant Ndaxte kii mooy aji yar ji ruu gi, teg ruu wurus la, kee nag mooy aji yar ji yaram wi te moom yaram wi am mbuusam la (mi koy \u00ebmb) Nanga mel fa moom niki n\u00e9ew ci kanamu ki koy sang, mbaa gumba gees di wommat ci yoon wu nekk ci digg g\u00e9ej ni muy toppe aji wommatam, niki lees ko waxe : Bu la Y\u00e0lla tawf\u00e9exalee ba nga am s\u00ebri\u00f1ub d\u00ebgg bu raw ci lefum Haqiiqa Rikk nanga jug ci s\u00e0kku ng\u00ebr\u00ebmam, xee\u00f1tu nammeelam, te ba l\u00e9pp loo nekkoon bu nj\u00ebkk Nanga mel fa moom ni n\u00e9ew fa ka koy sang, da koy w\u00eblbati fu nekk muy w\u00eblbatiku Mbokk d\u00ebgg ak xarit bu w\u00e9r \u00f1oo g\u00ebn a n\u00e9ew luy n\u00e9ew Mooy lu mel ne waxi ki wu\u00f1\u00f1i l\u00ebnd\u00ebm yi: sa xarit d\u00ebgg mooy ki \u00e0nd ak yaw Mooy kiy lor boppam ngir jari\u00f1 la, mooy kok bu la jamono njattee Mu sonnal boppam ngir siggil la, ma ne mooy ki lay n\u00ebbbal lu \u00f1aaw ngir yekkati la Tudd naa ciy teggiin am mbooloo mom dina fajal ku ko taqoo mbooleem ay aajoom Doy na s\u00ebkk ci ku ko settantal, aji saafara la ci ku ko j\u00ebfe Dina tegtal boroomum xel, dina ko tegtal banqaasi bunt bii, bu ci royee \u00e0nd ceekug toroxlu Ba mu far matal f\u00e0nni teggiin yi te bokk na ci yooni teggiinu yi: Di def li nga gis mu rafet tey ba li nga gis mu \u00f1aaw Lenn ci \u00f1oom laajees na ko: ku la yar? maanaam koo roy ba mel nii nga mel? Mu ne damaa d\u00ebkke di xool r\u00e9erug kii nga xam ne ne r\u00e9eram gi leer na n\u00e0\u00f1\u00f1 Bu ko defee ma koy teet (moytu). Fii la tontu li yam.<\/p>\n<p><strong>Aji Tekki ji: Abdu Xaadir KEBE<\/strong><\/p>\n","protected":false},"excerpt":{"rendered":"<p>Maa ngi t\u00e0mbale samay wax ak j\u00ebf ci turu Y\u00e0lla miy kiy boroom y\u00ebrmande ju yaa ji ci adduna ak ja ca allaaxiraa. Yal na Y\u00e0lla dolli x\u00e9ewal ak mucc ci su\u00f1u s\u00e0ng Muhammad ak ci \u00f1o\u00f1am aki saabaam ci anam yu sax Y\u00e0lla doy na \u00f1u, moom de w\u00e9eruwaay wu baax la, wu mat&#8230;<\/p>\n","protected":false},"author":1,"featured_media":1016,"comment_status":"open","ping_status":"open","sticky":false,"template":"","format":"standard","meta":{"footnotes":""},"categories":[15],"tags":[],"_links":{"self":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1015"}],"collection":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts"}],"about":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/types\/post"}],"author":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/users\/1"}],"replies":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcomments&post=1015"}],"version-history":[{"count":19,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1015\/revisions"}],"predecessor-version":[{"id":2052,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/posts\/1015\/revisions\/2052"}],"wp:featuredmedia":[{"embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=\/wp\/v2\/media\/1016"}],"wp:attachment":[{"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fmedia&parent=1015"}],"wp:term":[{"taxonomy":"category","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Fcategories&post=1015"},{"taxonomy":"post_tag","embeddable":true,"href":"http:\/\/www.wolof-online.com\/index.php?rest_route=%2Fwp%2Fv2%2Ftags&post=1015"}],"curies":[{"name":"wp","href":"https:\/\/api.w.org\/{rel}","templated":true}]}}