|
Bésu téy bii di talaata, 21 fan ci weeru Fewrie, moom la kureel giy toppatoo caada, njàng ak xamtéef (UNESCO) te feeteewoo ci mbotaayu-xeet-yi, jàgleel làkki ndey yi, maanaam làkk wi nga xam ne moom la nit ku nekk nàmp. Loolu bi ko UNESCO dooree ak léegi tollu ëpp na 10 at. Li waral bés bi mooy yee nit ñi, artu leen, soññ leen ci solo bu jéggi dayoo bi làkki-réew yi am ci fànnu yokkute yépp. Rawatina réewi Afrik yi gëna bare yi nga xam ne ba ñu tàbbee ci "kolonisation" ba téy jii ñu moomee seen bopp da ñoo xeeb seeni lákk yi nu nàmp.
Ba léegi réew yi ëpp ci ñoom, Senegaal waxi noppi, seeni làkk sedduñuleen daanaka benn cer bu tàkku. Kenn du leen jàng mbaa di leen jàngale ci lekool yi, kenn du leen jëfandikoo ci penc yi, ci bérebi àttekaay yi ak feneneen ak feneen..Dañu leen a fóoyooyal daal maanaam. Te fekk nag, loolu sax naka jekk moo waral sunu xeex bii; amul benn askan wu mëna am tawféex, yokkute ak jem-ca-kanam ci wàllu politik, koom-koom, njàng ak leneen te sànni say làkk. Bind nañu ko fi lu bare, indi nañu it firnde yiy wone ne réewi tubaab yi seen bopp te ñu leen di roy ci lu nekk, laata ñu doon genn cig lëndëmtu, dañoo mujj dekkil seeni làkk. Loolaa nga xewewoon ca ndorteel 15eelu xarnu bi: booba ñoom làkki lateñ rekk lañu daan jàng di ca bind, defe woon ne seeni làkk tekkiwuñu dara. Ba ñu dàgge buum goobu lañu tàmbale gindeeku ba léegi, am yokkute ci lu nekk, ba tollu tey ci boppu àddina. Looloo waral ba UNESCO nemmeekoo càggante ak yàq gu jeggi dayoo googu la def at mu nekk muy fàttali xeet yi ak askan yi seeni làmmiñ! Ndax gëstu yépp ci fànnu xam-xami làkk ak xaralaay-jàngale wone nañu ci lu wér, ne xale bi door njàngam ci làkk wi mu nàmp, mooy gena ubbeeku fuuf moroomam ka tàmbale njàngam làkk bu mu nàmpul. Li ko waral mooy xale bi buy dal rekk dees di mena koy mëna tàggat xelam ci fànn yu bare niki matematik, xam-xami cosaan, fisik ak yeneen...Te bu dee, kom ni ñu koy defe Senegaal, njàng mi yépp ci nasaraan la, su dugge lekool day mel ni ku lu. Day mel ni perantal buy doora jàng wax. Di na def lu yágg ci at at balees ko mëna jángal lenn lu am solo ci nasaraan. Ndax déggu ko! Li ëpp ci lu muy jàng du weesu ijji ak nafar lu mu xamul lu muy tekki dëë...Rax ci dolli, xeeb boppam, tiitange ak jaaxle bi xale bi di am, su ráñee ne ndeke moom làkk bi mu nàmp tekkiwul dara ca béréb yay indi tekki ëllëg ca réewam! Day juux ci lu ñu woowee "crise d'identite", maanaam, dootul xameeti boppam, day nekk ku neex a yobbale, ku neex ommat! Waxoon nañu fi itam ne sax soo koy seet, demokarasi bi ñuy wax, maanaam "nguuru askan wi ngir askan wi", mënul a am ci làkk woo jeggani! Ndax ñi ëpp ci askan wi déggu nu farañse, kon bokkuñu, kenn boolewuleen, kenn du leen laaj seen xalaat, du ñu faf sax xam li ñuy tëral aka doggal! Ku jàngat bu baax itam musiba bi xëppu ci réew mi téy, xëccoo bi ak rayante, da ngay xam ne làkk am na ci cër bu rey sax! Ndax sárti réew mi ci làkk nasaraan lañu ko bind, bindu ñu ko ci làkki-réew mi! Su doon dañu koo bindoon ci Wolof ak yeneen lákk yi, kon werante du am, wàlla buy am itam luy yomb a àtte lay doon! Kenn sax ci fóore ya Ablaay Wádd jëlee woon bitim-réew indi leen ngir ñu xamal ñu lu sunum sàrti-réew wax (!), moo ne woon mbir mi kat jotewul ak yoon dara, farañse kese "C'est une simple question de francais"! Céy ñakka xam ak xeeb-sa-bopp li ñuy jur cim réew!
Write Comment (0 comments) |