Wàcce ci Màkka 19 laaya
Benn – Senn – Menn la – Raax Menn – Raax Yërëm
1- Magalal turu sa Boroom mi kawee kawe
2- Ki sàkk mbir yi te muul leen
3- Ki dogal seeni muj te teg leen ñoom ñépp ci jëmoom
4- Kiy saxal gàncax gi
5- Te di ko delloo ci ngooñ mu wow
6- Dananu la jàngali jàng Alxuraan te doo ci fàtteji dara
7- Lu mooy li neex Yàlla; ndax moo xam liy feeñ ci bëccëgu kàmm
ag li làxxu
8- Daanu la yombalal suniy yoon
9- Yeeteel ndax say yeete dana musële
10- Ku ragal Yàlla dana ci jëriñu
11- Ku mu rëkk moo koy sore
12- Ki nuy weeri ca safara su raglu sa
13- Du fa deewi, du fa dund
14- Boroom wërsëg la ki tooñul
15- Kiy tudd turu Yàlla tey julli
16- Waaye dangeen taamu dundu àddina sii
17- Te fekk dundu ëllëg gën te gën di yàgg
18- Yoon woou danu koo jàngale ci téere yu yàgg yi
19- Ci téere Ibrayma ag Maysa
Jukki bi: Pathé Diagne, Alxuraan ci Wolof. Editions Sankore, L’Harmattan
There are no comments yet, be the first.