Benn – Senn – Menn la – Raax Menn – Raax Yërëm
1- Ag malaaka yiy rocci ruu ag dool
2- Malaaka yi leen di roñ ndànk, jellë ci biir ñenen ñi
3- Ag ñiy jàll bu gaaw jàww ji
4- Ag ñiy daw ci lu gaaw di jiitu
5- Ag ñi yélif ag di santaane
6- Bés riir mi jëkk ci bufta dana yëngal lépp.
7- Beneen topp ko
8- Bés boobu xol yi la tiitaange di dugg;
9- Bët yi sëgg ci suuf di toroxlu;
10- Ñi gëmul daañu ni booba: Ndax daanu dellusi ca
na ñu jëkkoon mel
11- Bu ñu deme ba dootuuñu lu dul yax yu seey
12- Daañu ne su loolu amee dey mabbati lay doon
13- Mennum riir la ñuy dégg
14- Fekk booba ñu ne ca Safara
15- Ndax xam nga xibaaru Maisaaa?
16- Bi ko Yàlla yuuxoo ci tertalu xuru Towa
17- Demal seeti firawna, dafa gëmul
18- Te nga ni: ndax bëgg nga jub?
19- Dinaa la tette ci Yàlla: Ragal ko
20- Maisaa tas tegal ko ci bëtam kiimtaan gu réy
21- Firawna jeeñ ko naxekat dolli fippu
22- Dafa joxe gannaaw sumb di jëf
23- Dafa dajale ay nit, yeenelu ay dogalamgal ko.
24- Te naan: Maa di seen kélifa gi sut ñépp
25- Yàlla teg ko mbugalu aiddinaa sii ag soosee
26- Dafa am ci lii tegtal wu jëm ci képp kuy ragal
27- Ndax yeen a gënoon yomb sàkk , walla Asamaan yi?
28- Yàlla la, moo leen defa, moo yëkkati seeni puj jox leen
melin yu mat sëkk
29- Moo tàbbal lëndëm ci guddéem mooy léeral bëccëgam
30- Ba mu noppee la talal suuf si ndëstë wu ñu ràbb
31- Bënnloo ci ay ndoxam te ci meññloo ay gancaxam
32- Moo tënk dunmag yi
33- Ngir seen njëriñ ak njëriñal jur yi
34- Te bu coppeeku mu rëy ma dee yegsi
35- Nit dana fàttaliku ay jëfam
36- Safara mooy fëll ca bëti ñepp
37- Képp ku musa ñàkk gëm
38- Képp ku musa taamu dundi fii
39- Daa séddoo Safara naka dëkkuwaay
40- Waaye ki daan lox fu mu xalaate màggaayu Boroom bi
te daan yèlif bànneexi ruuwam
41- Kooku Ajjana moo di nekki dëkkuwaayam
42- Daañu la laaj ni la kañ la waxtu woowu wara jot di jot?
43- Loo ci xam?
44- Appam Yàll rekk moo ko xam
45- Daañu la sànt yëgël do ñi ragal
46- Bés bi suñu koy gis, dafay mel ci ñoom na mësuñu nekk
ci suuf lu ëpp menn ngoon mbaa menn subë
Jukki bi: Pathé Diagne, Alxuraan ci Wolof. Editions Sankore, L’Harmattan
There are no comments yet, be the first.