Alxuraan ci Wolof: Nit

Wàcce ci Màkka 31 laaya
Benn – Senn – Menn la – Raax Menn – Raax Yërëm

1- Ndax dafa toog lu yàgg te kenn fàttelekuwu ko?

2- Danu door sàkk ci ndoxum geño wu ñaari kanam
àndoo fekk ñu koy seetlu. Daanu ko jox gis ak dégg.

3- Danu ko teg ci yoon wu jub na fekk mu am mbaa
ñakk kollëré.

4- Danu defaral weddikat yi ay callala, ag càxx ag Safara
suy boy

5- Ñi jub ñooy naani ciy kub yu kafuur ànd ag biiñ

6- Teen wi jaami Yàlla yi di naani, te fu leen neex
jëmële ndox yi

7- Danu matal seeni yeene dolli ragal bés booba te ay
musibaam di law fu sore

8- Danu séddale ndax moom, dundal neewjidoole yi,
njerim wi ag jaam wi nu jàpp

9- Te naan: Dañu leen sédd dund bii, ba mën neex ci
kanamu Yàla te du ñu leen ci laaj neexal walla ngërëm

10- Dañu raga ci wallu Yàlla aw bés wu metti te ànd ag
musiba

11- Moo tax Yàlla musal leen ayiba bés ba. Dafa leeral
seeni jë sol leen ag bànneex

12- Ndax seen dogu, dafa leen fay Ajjana ag yéré sooy

13- Dañu fay jekki wéeru ci seeni diwaan. Du ñu fa yëg

tangaayu jant walla coonooy sedd

14- Ay garab yu jagente ñoo leen di muur ag seeni ker, te
seeni doom di wàcc ngir ñu mën leen witt te coono
du am

15- Dañoo joxante ci seen biir ay ngutti xaalis ag ay kub yu
weeru kiristaal

16- Ci kiristaal biy niróog xaalis te ñu koy feesal na mu leen
neexe

17- Danu cay faj seen mar ag kub yu fees dell, ag naan yu ànd
ag jiñjeer

18- Ci teenu Ajjana wu ñu tudde Salsabill

19- Ay xale yu di ay ndaw ba fàww ñooy wër di leen sédd;
soo leen gisee defe ni ay caxxi peme yu ñu nocci lañu

20- Soo gisoon lu ni mel, gis dëkkuwaayi bànneex ag gu nguur
gu yaatu

21- Dañoo sol yéré sateñ wu baxaw ag borokaar, takk ay lamu
xaalis. Seen Boroom naan yu sell la leeen di jox.

22- Loolu mooy nekki seeni neexal dananu leen nattal seeni
coono

23- Danu la yone Alxuraan mu jóge ca kaw

24- Toogal muñ di nég dogali sa Boroom: Bul topp ñi gëmul

25- Dil tudd turu Yàlla suba ag ngoon

26- Ag it ci guddi, soppal Yàlla te way jalooreem ciy guddi yu
yàgg

27- Nit ñi dañoo bëgg àddina juy wal nu gaaw, tey bàyyi seen
gannaaw bés bu metti ba

28- Danu leen sàkk, te danu leen may doole, su nu xiiroon nu
wutële leen yeneeni nit

29- Loolu mooy yëgle wi. Ki bëgg na sóobu ci yoon wi jëme ci
Yàlla

30- Waaye duñu mën bëgg nag lu moy li Yàlla bëgg ndax dafa
xam te xàmmee

31- Dana ëmb ci kermandeem ñi mu bëgg, tegal na ñi gëmul
mbuggël mu saf.

Jukki bi: Pathé Diagne, Alxuraan ci Wolof. Editions Sankore, L’Harmattan

There are no comments yet, be the first.

Leave a Comment