Sàrti ndaali-Maali

Matukaayu 15eel:

Bu leen yëkkati mukk seen loxo jëmale ko ci jiggéen juy séy feek boolewoo ko ba tàyyi ak boroom-këram.

Matukaayu 16eel:

Wartéef la di boole jiggéen ñi ci kuréel yépp ci sunu nguur, wareesu leen a yemale ci lenn ci fànn woowu.

Matukaayu 17eel:

Jàppees na fen yi yàgg ba weesu 40 at ne kon ay dëgg lañu.

Matukaayu 18eel: Nañu fonk te ormaal képp ku ñu mag

Matukaayu 19eel:

Góor gu nekk ñaari goro la am: waay-juri ndaw si mu takkul ak kàddoom gi mu joxe ci coobare boppam.
Warees na leen fonkk te di leen sàmm saa su nekk.
Image
Matukaayu 20eel:

Bu leen toroxal mukk seeni jaam, may leen ayu-bés bu nekk bés bu ñu cay noppaloo. Fexe leen ba ñuy wàccook
seen liggéey ci waxtu yu yem. Sab jaam yaay sàngam, wante moomoo gaafaka gi mu mu gàccoo.

Matukaayu 21eel:

Bul di miinanteek soxnaay ki la yillif, sa dëkkandoo, sab sëriñ, boroom-xam-xamu cosaan, sab xarit walla ki nga àndal di liggéey.

Matukaayu 22eel:

Rëy mandargaay neew-doole la, xeebu di mandargaay daraja.

Matukaayu 23eel:

Bu leen di worante mukk, sàmmante leen ak seen kàddu.

Matukaayu 24eel:

Bu leen lor mukk doxandéem.

Matukaayu 25eel: :

Ndawal kilifa amul lenn lu mu wara tiit ci biir ndaali Maali.

Matukaayu 26eel:

Yëkk bu ñu la dénkk, warul a jiite ab gétt.
Matukaayu 27eel:

Bépp jànq bu tollu ci njeexitalu-ndawam mënees na koo maye mu séy te deesu ca seet ñaata at la am.
Ak nu jamaale ya mëna tollu ak ku nu mënti doon, la waay-juru jànq ba dogal rekk lees war di topp.
Bépp xale bu góor bu am 20 at mat naa déncc soxna.

Matukaayu 28eel:

May-gu-njëkku jànq ñetti nag la: benn bi jànq bee ko am, yeneen ñaar ya yaayam ak baayam a leen moom.

Matukaayu 29eel:

Tas séy dagan na ci anam yi:
. jëkkër ju tële
. waay-séy bu dof
. góor gu mënul a wáccook wareefam ci séy
Bépp séy bu ñuy tas dañuy dem ba genn dëkk bi door ko fa tas.