Yàtt bi lëmbee jamono!
Su dee ni ko yenn waay-xeltu yi di waxee namm-namm xarala dëggantaan mooy gësëm xelu nit ñi ba ñu xippi xool, gise neneen mbir yi leen wër,ku yebboo kon ne yàtt bi Ablaay Wàd yàttlu Wakaam yégg na ca la mu ca doon wut. Ndax ndonte sax nag sotteegul, “ngenteegu” ñu ko maanaam, xel yeek xalaat yépp a ngi lëmbee di ko xaar… Su caaxaan faaxee dëgg dés, Imageyàtt bi daa xajjàlle réew mi ak li ko weesu ñaar ba ñett ak ñeenti làng: ñii ne mbir la bu am solo, ndax day mandargaal gëddu nit ku ñuul ak suxxaliku gi askan yi ci Afrik, caagewul njaam gi ag metit yi ñu leen doon tégg yépp, masul a jóg di ko sàkku, di ko yóotu. Am ñeneen ñu ne yàtt bii mooy firndeel dëgg cuune, caaxaan ag càggante gi nguuru Ablaay Wàdd ngemboo: ndax nees lay jëlee ci réew mu lótt ni Senegaal, nit ñi dëkkee jaaxle ag di tuuñ-tuuñi lu ñu lekk, xale yiy sóobu ci géej gi di wut a raw, ay miliyaari-miliyaari di ko def ci yàtt bu kenn xamul yàttu lan la? Am genneen làng gu ca yokk ne li wér mooy yàtt bi warul a taxaw mukk ci réewum Senegaal gii di réewu julit, ndax diine lislaam dafay tere di yàtt ay nit, rawatina yëkkati ko ba mu mel ni luy juqarbi asamaan… Am na itam ñoo xam dañu ne ñoom li leen naqari mooy yàtt bi ci boppam dafa amul lenn lu am solo lu muy misaal, rax ci dolli rafetul, taaruwul! Dafa fóoyóoy daal manaam su ñu ko seete, tég ko ci sàrt yi aaru Afrik di wéy. Yàtt bi nag ci wàllu boppam mu nga nekk Wakaam, ca tundu Mamel, jakarloog géej. Tollu na ci taxawaay 50 m, genn góor jàpp jenn jiggéen, fab ci loxo càmmoñ benn xale bu talal loxom di joxoñ xarfu. Loolu nag li muy misaal, ñu ne, taxaw-temmu Afrik la, giy gindeekoo ci lëndëmtoog njaam, dëgmal ëllëgug yaakaar ag ngëm gu mat sëkk. Li wér daal mooy na yàtt bi ci jëmmam ag yenneen yàtt yu mel ni “yàttu moomeel sa bopp” ba ca Amerik, mbaa yàttu Yeesu Kiris ba ca Riyoo lay diiranteel mbàgg! Ndaxam sax nag Beresil mbaa Amerik mëneesu leen a jawaatleek Senegaal! Ci bésu 04 Awril 2010, tembook 50eelu at ba Senegaal moomee boppam ba léegi, lees ko wara ngente. Li jaaxal nit ñi mooy nan la askan wi, rawatina kilifa diine lislaam nara doxale? Ndax dana ñu teeweeji tudd ba am déed? Ndax it kilifa yenneen réew yi ñu wóo danañu ñëw am dañuy gàntu? Kon mbir ma ngi noonu: cóow li bare na, xel yeeg xalaat ya ngi joÅ‹ante! Su dee seetaan na daq cib ndajee kon lay ñëw ca kanam a wara gëna neex!
Tamsir Anne © wolof-online.com
There are no comments yet, be the first.